Al-Anfal · 33/75
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anfal
وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُعَذِّبَهُمْ وَأَنتَ فِيهِمْ ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ مُعَذِّبَهُمْ وَهُمْ يَسْتَغْفِرُونَ ۝٣٣
Wa maa kanal laahu liyu`az zibahum wa anta feehim; wa maa kaanal laahu mu`az zibahum wa hum yastaghfiroon
📖 Tekkim Wolof
Te Yàlla du Ku leen di mbugal fekk nga nekk [yaw Yonent bi] ci seen biir. Te it du Ku leen di mbugal fekk ñangay sàkku njéggal.

🎧 Dégg


📜 Aaya 31-35 — Simoore Al-Anfal

31وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا قَالُوا قَدْ سَمِعْنَا لَوْ نَشَاءُ لَقُلْنَا مِثْلَ هَٰذَا ۙ إِنْ هَٰذَا إِلَّا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ
Te saa yu ñu jàngee ci seen kanam Sunuy laaya, ñu ne : “Dégg nanu, ba noppi te sunu neexoon nu wax lu mel ni lii, ndaxte lii nekkul lu dul léebi nit ñu jëkk ña”.
32وَإِذْ قَالُوا اللَّهُمَّ إِن كَانَ هَٰذَا هُوَ الْحَقَّ مِنْ عِندِكَ فَأَمْطِرْ عَلَيْنَا حِجَارَةً مِّنَ السَّمَاءِ أَوِ ائْتِنَا بِعَذَابٍ أَلِيمٍ
(Fàttalikul) ba ñu waxee ne : “Yaw sunu Boroom, ndegam lii lu dëggu la lu jóge ci Yaw, Nanga sotti ci sunu kaw taw bu nekk ay xéewal wàcc jóge asamaan, mbaa nga indil nu mbugal mu metti”.
33وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُعَذِّبَهُمْ وَأَنتَ فِيهِمْ ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ مُعَذِّبَهُمْ وَهُمْ يَسْتَغْفِرُونَ
Te Yàlla du Ku leen di mbugal fekk nga nekk [yaw Yonent bi] ci seen biir. Te it du Ku leen di mbugal fekk ñangay sàkku njéggal.
34وَمَا لَهُمْ أَلَّا يُعَذِّبَهُمُ اللَّهُ وَهُمْ يَصُدُّونَ عَنِ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ وَمَا كَانُوا أَوْلِيَاءَهُ ۚ إِنْ أَوْلِيَاؤُهُ إِلَّا الْمُتَّقُونَ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Yellul ci ñoom Yàlla bañ leen a mbugal, te ñuy wax nit ñi bañ a jëm ci jàkka ju ñu wormaal ja, nekkuñu ñoom soppey jàkka jooju, ay soppeem ñooy way-ragal Yàlla ña. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
35وَمَا كَانَ صَلَاتُهُمْ عِندَ الْبَيْتِ إِلَّا مُكَاءً وَتَصْدِيَةً ۚ فَذُوقُوا الْعَذَابَ بِمَا كُنتُمْ تَكْفُرُونَ
Seen julli ca néegub, nekkul lu dul ay waliis ak ay tàccu, kon : “Mosleen mbugal mi [ca xare Badar] ngir la ngeen doon weddi ! ”
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
33Aaya

Tekki — Al-Anfal 33

Simoore Al-Anfal Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te Yàlla du Ku leen di mbugal fekk nga nekk…

Simoore Aaya 33/75 — Simoore Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anfal Dégg, Simoore Al-Anfal Tekki, Simoore Al-Anfal mp3, Simoore Al-Anfal pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers