Al-Anfal · 32/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
وَإِذْ قَالُوا اللَّهُمَّ إِن كَانَ هَٰذَا هُوَ الْحَقَّ مِنْ عِندِكَ فَأَمْطِرْ عَلَيْنَا حِجَارَةً مِّنَ السَّمَاءِ أَوِ ائْتِنَا بِعَذَابٍ أَلِيمٍ ۝٣٢
Wa iz qaalul laahumma in kaana haazaa huwal haqqa min `indika fa amtir `alainaa hijaaratam minas samaaa`i awi`tinaa bi `azaabin alaeem
📖 Tekkim Wolof
(Fàttalikul) ba ñu waxee ne : “Yaw sunu Boroom, ndegam lii lu dëggu la lu jóge ci Yaw, Nanga sotti ci sunu kaw taw bu nekk ay xéewal wàcc jóge asamaan, mbaa nga indil nu mbugal mu metti”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 30-34 — Al-Anfal

30وَإِذْ يَمْكُرُ بِكَ الَّذِينَ كَفَرُوا لِيُثْبِتُوكَ أَوْ يَقْتُلُوكَ أَوْ يُخْرِجُوكَ ۚ وَيَمْكُرُونَ وَيَمْكُرُ اللَّهُ ۖ وَاللَّهُ خَيْرُ الْمَاكِرِينَ
(Fàttalikul) ba la yéefar ya fexelee ngir ñu tëj la ci barab mbaa ñu rey la mbaa ñu génne la. Ñu def seeni pexe, Yàlla def ay pexeem, te Yàlla di Ku gën a màgg ay pexe.
31وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا قَالُوا قَدْ سَمِعْنَا لَوْ نَشَاءُ لَقُلْنَا مِثْلَ هَٰذَا ۙ إِنْ هَٰذَا إِلَّا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ
Te saa yu ñu jàngee ci seen kanam Sunuy laaya, ñu ne : “Dégg nanu, ba noppi te sunu neexoon nu wax lu mel ni lii, ndaxte lii nekkul lu dul léebi nit ñu jëkk ña”.
32وَإِذْ قَالُوا اللَّهُمَّ إِن كَانَ هَٰذَا هُوَ الْحَقَّ مِنْ عِندِكَ فَأَمْطِرْ عَلَيْنَا حِجَارَةً مِّنَ السَّمَاءِ أَوِ ائْتِنَا بِعَذَابٍ أَلِيمٍ
(Fàttalikul) ba ñu waxee ne : “Yaw sunu Boroom, ndegam lii lu dëggu la lu jóge ci Yaw, Nanga sotti ci sunu kaw taw bu nekk ay xéewal wàcc jóge asamaan, mbaa nga indil nu mbugal mu metti”.
33وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُعَذِّبَهُمْ وَأَنتَ فِيهِمْ ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ مُعَذِّبَهُمْ وَهُمْ يَسْتَغْفِرُونَ
Te Yàlla du Ku leen di mbugal fekk nga nekk [yaw Yonent bi] ci seen biir. Te it du Ku leen di mbugal fekk ñangay sàkku njéggal.
34وَمَا لَهُمْ أَلَّا يُعَذِّبَهُمُ اللَّهُ وَهُمْ يَصُدُّونَ عَنِ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ وَمَا كَانُوا أَوْلِيَاءَهُ ۚ إِنْ أَوْلِيَاؤُهُ إِلَّا الْمُتَّقُونَ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Yellul ci ñoom Yàlla bañ leen a mbugal, te ñuy wax nit ñi bañ a jëm ci jàkka ju ñu wormaal ja, nekkuñu ñoom soppey jàkka jooju, ay soppeem ñooy way-ragal Yàlla ña. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
32Aaya

Tekki — Al-Anfal 32

Simoore Al-Anfal Aaya 32 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (Fàttalikul) ba ñu waxee ne : “Yaw sunu Boroom, ndegam…

Simoore Aaya 32/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 30–34. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers