Al-Anfal · 51/75
Tekki Waxtaan — Al-Anfal
ذَٰلِكَ بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ لَيْسَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ ۝٥١
Zaalika bimaa qaddamat aideekum wa anal laaha laisa bizallaamil lil `abeed
📖 Tekkim Wolof
Loolu mooy la ngeen jëfoon ci seeni yoxo.” Te it Yàlla du koy tooñ jaam ñi.
🎧 Dégg

📜 Aaya 49-53 — Al-Anfal

49إِذْ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ غَرَّ هَٰؤُلَاءِ دِينُهُمْ ۗ وَمَن يَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ حَكِيمٌ
(Fàttalikul), ba naafeq ya ak ña jàngoro nekk ca seeni xol waxee ne : “Ñii seen diine wor na leen.” Waaye ku wéeru ci Yàlla ... [na xam ne] Yàlla Kuy not lépp la, Ku xereñ la.
50وَلَوْ تَرَىٰ إِذْ يَتَوَفَّى الَّذِينَ كَفَرُوا ۙ الْمَلَائِكَةُ يَضْرِبُونَ وُجُوهَهُمْ وَأَدْبَارَهُمْ وَذُوقُوا عَذَابَ الْحَرِيقِ
Boo gisee na Malaaka ya di reyee yéefar ya ! Dañuy dóor seeni kanam ak seeni ginnaaw, (naa leen): “Mosleen mbugalu Safara.
51ذَٰلِكَ بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيكُمْ وَأَنَّ اللَّهَ لَيْسَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ
Loolu mooy la ngeen jëfoon ci seeni yoxo.” Te it Yàlla du koy tooñ jaam ñi.
52كَدَأْبِ آلِ فِرْعَوْنَ ۙ وَالَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ كَفَرُوا بِآيَاتِ اللَّهِ فَأَخَذَهُمُ اللَّهُ بِذُنُوبِهِمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ قَوِيٌّ شَدِيدُ الْعِقَابِ
Niki aaday njabootu Firawna ak ña leen jiitu, weddi woon nañu kàdduy Yàlla. Yàlla sadd leen ngir seeni bàkkaar. Naka Yàlla, Boroom kàttan la, di Ku tar mbugal.
53ذَٰلِكَ بِأَنَّ اللَّهَ لَمْ يَكُ مُغَيِّرًا نِّعْمَةً أَنْعَمَهَا عَلَىٰ قَوْمٍ حَتَّىٰ يُغَيِّرُوا مَا بِأَنفُسِهِمْ ۙ وَأَنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Li ko waral mooy Yàlla du soppi yiw wu Mu xéewale aw nit feek soppiwuñu li nekkoon ci ñoom. Yàlla Kuy dégg la, Ku xam la.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
51Aaya

Tekki — Al-Anfal 51

Simoore Al-Anfal Aaya 51 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Loolu mooy la ngeen jëfoon ci seeni yoxo.” Te it…

Simoore Aaya 51/75 — Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anfal Dégg, Al-Anfal Tekki, Al-Anfal mp3, Al-Anfal pdf. Aaya 49–53. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers