Al-Anfal · 35/75
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anfal
وَمَا كَانَ صَلَاتُهُمْ عِندَ الْبَيْتِ إِلَّا مُكَاءً وَتَصْدِيَةً ۚ فَذُوقُوا الْعَذَابَ بِمَا كُنتُمْ تَكْفُرُونَ ۝٣٥
Wa maa kaana Salaatuhum `indal Baiti illa mukaaa anw-wa tasdiyah; fazooqul `azaaba bimaa kuntum takfuroon
📖 Tekkim Wolof
Seen julli ca néegub, nekkul lu dul ay waliis ak ay tàccu, kon : “Mosleen mbugal mi [ca xare Badar] ngir la ngeen doon weddi ! ”

🎧 Dégg


📜 Aaya 33-37 — Simoore Al-Anfal

33وَمَا كَانَ اللَّهُ لِيُعَذِّبَهُمْ وَأَنتَ فِيهِمْ ۚ وَمَا كَانَ اللَّهُ مُعَذِّبَهُمْ وَهُمْ يَسْتَغْفِرُونَ
Te Yàlla du Ku leen di mbugal fekk nga nekk [yaw Yonent bi] ci seen biir. Te it du Ku leen di mbugal fekk ñangay sàkku njéggal.
34وَمَا لَهُمْ أَلَّا يُعَذِّبَهُمُ اللَّهُ وَهُمْ يَصُدُّونَ عَنِ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ وَمَا كَانُوا أَوْلِيَاءَهُ ۚ إِنْ أَوْلِيَاؤُهُ إِلَّا الْمُتَّقُونَ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Yellul ci ñoom Yàlla bañ leen a mbugal, te ñuy wax nit ñi bañ a jëm ci jàkka ju ñu wormaal ja, nekkuñu ñoom soppey jàkka jooju, ay soppeem ñooy way-ragal Yàlla ña. Waaye li ëpp ci ñoom xamuñu.
35وَمَا كَانَ صَلَاتُهُمْ عِندَ الْبَيْتِ إِلَّا مُكَاءً وَتَصْدِيَةً ۚ فَذُوقُوا الْعَذَابَ بِمَا كُنتُمْ تَكْفُرُونَ
Seen julli ca néegub, nekkul lu dul ay waliis ak ay tàccu, kon : “Mosleen mbugal mi [ca xare Badar] ngir la ngeen doon weddi ! ”
36إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ لِيَصُدُّوا عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ فَسَيُنفِقُونَهَا ثُمَّ تَكُونُ عَلَيْهِمْ حَسْرَةً ثُمَّ يُغْلَبُونَ ۗ وَالَّذِينَ كَفَرُوا إِلَىٰ جَهَنَّمَ يُحْشَرُونَ
Ña nga xam ne dañoo weddi, Dananu sànk seeni alal ngir dëdduloo [nit ñi] yoonu Yàlla. Waaye Danañu ko sànk ba noppi di ko réccu. Ñu not leen, te ña weddi dees na leen bëmax jëme Safara,
37لِيَمِيزَ اللَّهُ الْخَبِيثَ مِنَ الطَّيِّبِ وَيَجْعَلَ الْخَبِيثَ بَعْضَهُ عَلَىٰ بَعْضٍ فَيَرْكُمَهُ جَمِيعًا فَيَجْعَلَهُ فِي جَهَنَّمَ ۚ أُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ
ngir Yàlla téqale yéefar yi ak ña gëm Yàlla, Dana boole yéefar yi, dajale leen ñoom ñépp ca biir Safara. Ñooñu ñooy way-ñàkk ña.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
35Aaya

Tekki — Al-Anfal 35

Simoore Al-Anfal Aaya 35 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Seen julli ca néegub, nekkul lu dul ay waliis ak…

Simoore Aaya 35/75 — Simoore Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anfal Dégg, Simoore Al-Anfal Tekki, Simoore Al-Anfal mp3, Simoore Al-Anfal pdf. Aaya 33–37. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers