Al-Anfal · 40/75
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anfal
وَإِن تَوَلَّوْا فَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ مَوْلَاكُمْ ۚ نِعْمَ الْمَوْلَىٰ وَنِعْمَ النَّصِيرُ ۝٤٠
Wa in tawallaw fa`lamooo annal laaha mawlaakum; ni`mal mawlaa wa ni`man naseer
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu dëddoo, xamleen ne, Yàlla mooy ka leen di jàppale. Ndaw soppe bu baax, ndaw Aji-dimbalee ju baax !

🎧 Dégg


📜 Aaya 38-42 — Simoore Al-Anfal

38قُل لِّلَّذِينَ كَفَرُوا إِن يَنتَهُوا يُغْفَرْ لَهُم مَّا قَدْ سَلَفَ وَإِن يَعُودُوا فَقَدْ مَضَتْ سُنَّتُ الْأَوَّلِينَ
Waxal yéefar yi, ne leen : “Bu ngeen bàyyee [xareek Yonent bi], nu baal leen la weesu. Waaye bu ngeen delluwaatee [ca la ngeen nekke woon], dees na leen mbugal kem ni mu daan ame bu njëkk.
39وَقَاتِلُوهُمْ حَتَّىٰ لَا تَكُونَ فِتْنَةٌ وَيَكُونَ الدِّينُ كُلُّهُ لِلَّهِ ۚ فَإِنِ انتَهَوْا فَإِنَّ اللَّهَ بِمَا يَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Xeexleen ak ñoom ba fitna jóge fi, ba diine nekk lu ñu jagleel Yàlla léppam. Waaye bu ñu bàyyee nag, Yàlla mi ngi ne jàkk ci li ñuy def.
40وَإِن تَوَلَّوْا فَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ مَوْلَاكُمْ ۚ نِعْمَ الْمَوْلَىٰ وَنِعْمَ النَّصِيرُ
Bu ñu dëddoo, xamleen ne, Yàlla mooy ka leen di jàppale. Ndaw soppe bu baax, ndaw Aji-dimbalee ju baax !
41۞ وَاعْلَمُوا أَنَّمَا غَنِمْتُم مِّن شَيْءٍ فَأَنَّ لِلَّهِ خُمُسَهُ وَلِلرَّسُولِ وَلِذِي الْقُرْبَىٰ وَالْيَتَامَىٰ وَالْمَسَاكِينِ وَابْنِ السَّبِيلِ إِن كُنتُمْ آمَنتُم بِاللَّهِ وَمَا أَنزَلْنَا عَلَىٰ عَبْدِنَا يَوْمَ الْفُرْقَانِ يَوْمَ الْتَقَى الْجَمْعَانِ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Te nangeen xam ne lu ngeen màng ci lu mu mën a doon, juróomeelu xaaj ba ñeel na Yàlla ak Yonent ba ak i jegeñaaleem, ak jirim ya, ak way-ñàkk ya, ak ña nekk ci yoon di tukki, ndegam gëm ngeen Yàlla ak la Nu wàcce ci Sunu jaam ba bisu téqale ba [ca Badar] : bisu ndaje ñaari mbooloo ya, te Yàlla mën na lu ne.
42إِذْ أَنتُم بِالْعُدْوَةِ الدُّنْيَا وَهُم بِالْعُدْوَةِ الْقُصْوَىٰ وَالرَّكْبُ أَسْفَلَ مِنكُمْ ۚ وَلَوْ تَوَاعَدتُّمْ لَاخْتَلَفْتُمْ فِي الْمِيعَادِ ۙ وَلَٰكِن لِّيَقْضِيَ اللَّهُ أَمْرًا كَانَ مَفْعُولًا لِّيَهْلِكَ مَنْ هَلَكَ عَن بَيِّنَةٍ وَيَحْيَىٰ مَنْ حَيَّ عَن بَيِّنَةٍ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَسَمِيعٌ عَلِيمٌ
Fekk na booba ngeen nekk ca xur wa gën a jegeñ, ñoom ñu nekk ca xur wa gën a sori, njëgg ma gën a suufe. Bu ngeen sàkku woon a dajeek ñoom, du sotti. Waaye lu Yàlla dogal day nekk, dana am ñu dee ci lu bir ak ñu dundu ci lu bir. Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
Al-AnfalFihi Alxuraan
75Aaya
MedinanRevelation
40Aaya

Tekki — Al-Anfal 40

Simoore Al-Anfal Aaya 40 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu dëddoo, xamleen ne, Yàlla mooy ka leen di…

Simoore Aaya 40/75 — Simoore Al-Anfal الأنفال (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anfal Dégg, Simoore Al-Anfal Tekki, Simoore Al-Anfal mp3, Simoore Al-Anfal pdf. Aaya 38–42. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers