Yunus · 106/109
Tekki Waxtaan — Yunus
وَلَا تَدْعُ مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَنفَعُكَ وَلَا يَضُرُّكَ ۖ فَإِن فَعَلْتَ فَإِنَّكَ إِذًا مِّنَ الظَّالِمِينَ ۝١٠٦
Wa laa tad`u min doonil laahi maa laa yanfa`uka wa laa yadurruka fa in fa`alta fa innaka izam minaz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
bul jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu laa lor, mënu laa jariñ. Soo ko defee rekk daldi bokk ca tooñkat ya”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 104-108 — Yunus

104قُلْ يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِن كُنتُمْ فِي شَكٍّ مِّن دِينِي فَلَا أَعْبُدُ الَّذِينَ تَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ وَلَٰكِنْ أَعْبُدُ اللَّهَ الَّذِي يَتَوَفَّاكُمْ ۖ وَأُمِرْتُ أَنْ أَكُونَ مِنَ الْمُؤْمِنِينَ
Neel : "Éy yéen nit ñi ! Bu ngeen amee xel-ñaar ci sama diine jii, xamleen ne man duma jaamu li ngeen di jaamu bàyyi Yàlla ; Waaye Yàlla laay jaamu, Moom mi leen di rey. Te digaleef na ma ma bokk ca way-gëm ña”.
105وَأَنْ أَقِمْ وَجْهَكَ لِلدِّينِ حَنِيفًا وَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Te : “Nga taxaw temm jublu ci diine jii wéetal Yàlla ! Te bul bokk mukk ca way- bokkaale ña ;
106وَلَا تَدْعُ مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَنفَعُكَ وَلَا يَضُرُّكَ ۖ فَإِن فَعَلْتَ فَإِنَّكَ إِذًا مِّنَ الظَّالِمِينَ
bul jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu laa lor, mënu laa jariñ. Soo ko defee rekk daldi bokk ca tooñkat ya”.
107وَإِن يَمْسَسْكَ اللَّهُ بِضُرٍّ فَلَا كَاشِفَ لَهُ إِلَّا هُوَ ۖ وَإِن يُرِدْكَ بِخَيْرٍ فَلَا رَادَّ لِفَضْلِهِ ۚ يُصِيبُ بِهِ مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ ۚ وَهُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ
Bu la Yàlla saddee aw naqar, kenn du la ko mën a teggil ku dul Moom. Bu la bégalee ci aw yiw, dara du mën a fànq xéewalam. Dana ko jottale ku ko soob ci jaamam yi. Moo di Xéewalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba.
108قُلْ يَا أَيُّهَا النَّاسُ قَدْ جَاءَكُمُ الْحَقُّ مِن رَّبِّكُمْ ۖ فَمَنِ اهْتَدَىٰ فَإِنَّمَا يَهْتَدِي لِنَفْسِهِ ۖ وَمَن ضَلَّ فَإِنَّمَا يَضِلُّ عَلَيْهَا ۖ وَمَا أَنَا عَلَيْكُم بِوَكِيلٍ
Neel : "Éy yéen nit ñi ! Dëgg gi ñëw na ci yéen tukke ci seen Boroom. Ku jub te gindiku, boppam ; ku réer, sànku it boppam. Man dey warlulumaleen dara [ci seeni mbir].
YunusFihi Alxuraan
109Aaya
MeccanRevelation
106Aaya

Tekki — Yunus 106

Simoore Yunus Aaya 106 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : bul jaamu, bàyyi Yàlla, loo xam ne mënu laa lor,…

Simoore Aaya 106/109 — Yunus يونس (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yunus Dégg, Yunus Tekki, Yunus mp3, Yunus pdf. Aaya 104–108. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers