Yunus · 6/109
Tekki Waxtaan — Yunus
إِنَّ فِي اخْتِلَافِ اللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَمَا خَلَقَ اللَّهُ فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَتَّقُونَ ۝٦
Inna fikh tilaafil laili wannahaari wa maa khalaqal laahu fis samaawaati wal ardi la Aayaatil liqawminy yattaqoon
📖 Tekkim Wolof
Nekk na ci jéllasanteb guddi gi ak bëccëg gi, ak li Yàlla sàkk ci asamaan yi ak suuf si, ay kéemaan ci nit ñu ragal (Yàlla).

🎧 Dégg


📜 Aaya 4-8 — Yunus

4إِلَيْهِ مَرْجِعُكُمْ جَمِيعًا ۖ وَعْدَ اللَّهِ حَقًّا ۚ إِنَّهُ يَبْدَأُ الْخَلْقَ ثُمَّ يُعِيدُهُ لِيَجْزِيَ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ بِالْقِسْطِ ۚ وَالَّذِينَ كَفَرُوا لَهُمْ شَرَابٌ مِّنْ حَمِيمٍ وَعَذَابٌ أَلِيمٌ بِمَا كَانُوا يَكْفُرُونَ
Seen delluwaay yéen ñépp ca Moom la jëm, mooy digub Yàlla bu dëggu ba ! Moom moo sos mbindéef yi (booba dara amul), Moo leen di delloosi (ginnaaw bu ñu dee ba ràpp) ngir Mu feye ña gëm pey gu duun. Waaye ña weddi woon ñoom, seenug naan, ndox mu tàng lay doon ak mbugal mu metti, muy peyug seenug weddi !
5هُوَ الَّذِي جَعَلَ الشَّمْسَ ضِيَاءً وَالْقَمَرَ نُورًا وَقَدَّرَهُ مَنَازِلَ لِتَعْلَمُوا عَدَدَ السِّنِينَ وَالْحِسَابَ ۚ مَا خَلَقَ اللَّهُ ذَٰلِكَ إِلَّا بِالْحَقِّ ۚ يُفَصِّلُ الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْلَمُونَ
Moom mooy ki jox jant bi tàkk-tàkk, jox weer wi leeraay te dogal ko ay wàccuwaay ndax ngeen mën a xam limu at yi ak mën a waññi. Yàlla bindul loolu lu dul ci dëgg. Te Dana biralal tegtal ya nit ñay xam.
6إِنَّ فِي اخْتِلَافِ اللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَمَا خَلَقَ اللَّهُ فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَتَّقُونَ
Nekk na ci jéllasanteb guddi gi ak bëccëg gi, ak li Yàlla sàkk ci asamaan yi ak suuf si, ay kéemaan ci nit ñu ragal (Yàlla).
7إِنَّ الَّذِينَ لَا يَرْجُونَ لِقَاءَنَا وَرَضُوا بِالْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَاطْمَأَنُّوا بِهَا وَالَّذِينَ هُمْ عَنْ آيَاتِنَا غَافِلُونَ
Ña nga xam ne nag yaakaaruñoo dajeek Nun, te tànn dundug àddina gii, doyloo ko, ak ña nga xam ne sàggane nañu Sunuy ndigal,
8أُولَٰئِكَ مَأْوَاهُمُ النَّارُ بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
ñooña seen delluwaay moo di Safara ngir la ñu fàggu.
YunusFihi Alxuraan
109Aaya
MeccanRevelation
6Aaya

Tekki — Yunus 6

Simoore Yunus Aaya 6 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nekk na ci jéllasanteb guddi gi ak bëccëg gi, ak…

Simoore Aaya 6/109 — Yunus يونس (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yunus Dégg, Yunus Tekki, Yunus mp3, Yunus pdf. Aaya 4–8. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers