Al-Baqara · 103/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَلَوْ أَنَّهُمْ آمَنُوا وَاتَّقَوْا لَمَثُوبَةٌ مِّنْ عِندِ اللَّهِ خَيْرٌ ۖ لَّوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ ۝١٠٣
Wa law annahum aamanoo wattaqaw lamasoobatum min `indillaahi khairun law kaanoo ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Bu fekkoon ne ñoom dañuy gëm, te ragal Yàlla [kon mu gën ci ñoom fuuf]. Cëy bu ñu xamoon !
🎧 Dégg

📜 Aaya 101-105 — Al-Baqara

101وَلَمَّا جَاءَهُمْ رَسُولٌ مِّنْ عِندِ اللَّهِ مُصَدِّقٌ لِّمَا مَعَهُمْ نَبَذَ فَرِيقٌ مِّنَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ كِتَابَ اللَّهِ وَرَاءَ ظُهُورِهِمْ كَأَنَّهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Ba leen Yonent bu jóge ca Yàlla dikkalee di dëggal la ñu yor, gaa ya ñu joxoon ab Téere, ab kurél ca ñoom sànni Téereb Yàlla bi ca seen ginnaaw mel ni dañoo xamul !
102وَاتَّبَعُوا مَا تَتْلُو الشَّيَاطِينُ عَلَىٰ مُلْكِ سُلَيْمَانَ ۖ وَمَا كَفَرَ سُلَيْمَانُ وَلَٰكِنَّ الشَّيَاطِينَ كَفَرُوا يُعَلِّمُونَ النَّاسَ السِّحْرَ وَمَا أُنزِلَ عَلَى الْمَلَكَيْنِ بِبَابِلَ هَارُوتَ وَمَارُوتَ ۚ وَمَا يُعَلِّمَانِ مِنْ أَحَدٍ حَتَّىٰ يَقُولَا إِنَّمَا نَحْنُ فِتْنَةٌ فَلَا تَكْفُرْ ۖ فَيَتَعَلَّمُونَ مِنْهُمَا مَا يُفَرِّقُونَ بِهِ بَيْنَ الْمَرْءِ وَزَوْجِهِ ۚ وَمَا هُم بِضَارِّينَ بِهِ مِنْ أَحَدٍ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ ۚ وَيَتَعَلَّمُونَ مَا يَضُرُّهُمْ وَلَا يَنفَعُهُمْ ۚ وَلَقَدْ عَلِمُوا لَمَنِ اشْتَرَاهُ مَا لَهُ فِي الْآخِرَةِ مِنْ خَلَاقٍ ۚ وَلَبِئْسَ مَا شَرَوْا بِهِ أَنفُسَهُمْ ۚ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ
Ñu topp nag la séytaane ya doon jàng ca nguurug Suleymaan. Weddiwul de, séytaane ya ñoo weddi : Daan nañu jàngal nit ña ag njibar ak la ñu wàcce woon ca ñaari Malaaka ya ca (Baabil) (Haaruut ak Maaruut); te daawuñu jàngal kenn te waxuñu ko ne : “Nun dey danoo ànd ak sànje : kon book bul weddi de” ; mu am ñu jàng ci ñoom loo xam ne mën nañu caa téqale jëkkër ak jabaram. Te daawuñu mën a lor kenn ca njibar googule, lu dul ci coobare Yàlla. Te it jàng nañu loo xam ne daf leen di lor te mënuleeen a jariñ. Xam nañu xéll ne ku jënde loolu [weccee ko ak waxi Yàlla] du am benn cër ca àllaaxira. La ñu jaaye seen bakkan bon na ! Cëy bu ñu xamoon !
103وَلَوْ أَنَّهُمْ آمَنُوا وَاتَّقَوْا لَمَثُوبَةٌ مِّنْ عِندِ اللَّهِ خَيْرٌ ۖ لَّوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ
Bu fekkoon ne ñoom dañuy gëm, te ragal Yàlla [kon mu gën ci ñoom fuuf]. Cëy bu ñu xamoon !
104يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَقُولُوا رَاعِنَا وَقُولُوا انظُرْنَا وَاسْمَعُوا ۗ وَلِلْكَافِرِينَ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Éy yéen way-gëm yi ! Buleen di wax [sàmmoonteel ak nun], deeleen wax : “Xool nu” ; te deeleen dégg [ndigal] ! Mbugal mu metti mooy dal ca kaw way-weddi ña.
105مَّا يَوَدُّ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ وَلَا الْمُشْرِكِينَ أَن يُنَزَّلَ عَلَيْكُم مِّنْ خَيْرٍ مِّن رَّبِّكُمْ ۗ وَاللَّهُ يَخْتَصُّ بِرَحْمَتِهِ مَن يَشَاءُ ۚ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ
Ña weddi ca ñoñ-téere ya ak way-bokkaale ya yéenewuñuleen, yiw wu bari ba bawoo ca seen Boroom, wàcc ci yéen, te Yàlla dana jagale yërmaandeem ku ko soob. Yàlla mooy boroom ngëneel yu màgg yi.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
103Aaya

Tekki — Al-Baqara 103

Simoore Al-Baqara Aaya 103 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu fekkoon ne ñoom dañuy gëm, te ragal Yàlla [kon…

Simoore Aaya 103/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 101–105. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers