Aali Imran · 151/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
سَنُلْقِي فِي قُلُوبِ الَّذِينَ كَفَرُوا الرُّعْبَ بِمَا أَشْرَكُوا بِاللَّهِ مَا لَمْ يُنَزِّلْ بِهِ سُلْطَانًا ۖ وَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۚ وَبِئْسَ مَثْوَى الظَّالِمِينَ ۝١٥١
Sanulqee fee quloobil lazeena kafarur ru`ba bimaaa ashrakoo billaahi maa lam yunazzil bihee sultaana-nw wa maawaahumun Naar; wa bi`sa maswaz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Dananu sànni ci xoli ñi weddi tiitaange ngir la ñu bokkaale Yàlla ak loo xam ne amul lay wuñu leen ca wàcceel. Safaraa di seen dëkkuwaay te dëkkuwaayu tooñkat ya bon na !

🎧 Dégg


📜 Aaya 149-153 — Simoore Aali Imran

149يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِن تُطِيعُوا الَّذِينَ كَفَرُوا يَرُدُّوكُمْ عَلَىٰ أَعْقَابِكُمْ فَتَنقَلِبُوا خَاسِرِينَ
Éy yéen ñi gëm!, bu ngeen toppee ñi weddi, danañu leen dugal sa seeni tànk [weddiloo leen], ngeen wëlbatiku ñàkk.
150بَلِ اللَّهُ مَوْلَاكُمْ ۖ وَهُوَ خَيْرُ النَّاصِرِينَ
Li wér mooy Yàllaa leen méngoo [yore seeni mbir] te Mooy ngëm ji kuy dimbali.
151سَنُلْقِي فِي قُلُوبِ الَّذِينَ كَفَرُوا الرُّعْبَ بِمَا أَشْرَكُوا بِاللَّهِ مَا لَمْ يُنَزِّلْ بِهِ سُلْطَانًا ۖ وَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۚ وَبِئْسَ مَثْوَى الظَّالِمِينَ
Dananu sànni ci xoli ñi weddi tiitaange ngir la ñu bokkaale Yàlla ak loo xam ne amul lay wuñu leen ca wàcceel. Safaraa di seen dëkkuwaay te dëkkuwaayu tooñkat ya bon na !
152وَلَقَدْ صَدَقَكُمُ اللَّهُ وَعْدَهُ إِذْ تَحُسُّونَهُم بِإِذْنِهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا فَشِلْتُمْ وَتَنَازَعْتُمْ فِي الْأَمْرِ وَعَصَيْتُم مِّن بَعْدِ مَا أَرَاكُم مَّا تُحِبُّونَ ۚ مِنكُم مَّن يُرِيدُ الدُّنْيَا وَمِنكُم مَّن يُرِيدُ الْآخِرَةَ ۚ ثُمَّ صَرَفَكُمْ عَنْهُمْ لِيَبْتَلِيَكُمْ ۖ وَلَقَدْ عَفَا عَنكُمْ ۗ وَاللَّهُ ذُو فَضْلٍ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ
Yàlla def na la Mu leen digoon nekk dëgg, ba ngën di xeex ak ñoom ci ndigal, [ngeen not] ba ba ngeen sàqi ndigal la, ginnaaw ba ngeen janoo ak la ngeen bëgg [alal] àddina! Am na it ci yéen ñu bëgg [alali] àllaaxira. Ba noppi Yàlla wëlbati leen [soppi tooñeel ga] ngeen amoon ci ñoom, ngir nattu leen.Waaye baal na leen. Yàlla Boroom ngëneel la yu muy [sédd] ñi gëm.
153۞ إِذْ تُصْعِدُونَ وَلَا تَلْوُونَ عَلَىٰ أَحَدٍ وَالرَّسُولُ يَدْعُوكُمْ فِي أُخْرَاكُمْ فَأَثَابَكُمْ غَمًّا بِغَمٍّ لِّكَيْلَا تَحْزَنُوا عَلَىٰ مَا فَاتَكُمْ وَلَا مَا أَصَابَكُمْ ۗ وَاللَّهُ خَبِيرٌ بِمَا تَعْمَلُونَ
[Fàttalikuleen] ba ngeen di yéeg te geesuwuleen kenn, te Yonent bi di leen woo ci seen ginnaaw. Mu tegoon leen njàqare ya ci kaw njàqare ya, ndax ngeen bañ a mitteetlu la leen rëcc walla la leen dal. Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
151Aaya

Tekki — Aali Imran 151

Simoore Aali Imran Aaya 151 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dananu sànni ci xoli ñi weddi tiitaange ngir la ñu…

Simoore Aaya 151/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 149–153. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers