Aali Imran · 28/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
لَّا يَتَّخِذِ الْمُؤْمِنُونَ الْكَافِرِينَ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِ الْمُؤْمِنِينَ ۖ وَمَن يَفْعَلْ ذَٰلِكَ فَلَيْسَ مِنَ اللَّهِ فِي شَيْءٍ إِلَّا أَن تَتَّقُوا مِنْهُمْ تُقَاةً ۗ وَيُحَذِّرُكُمُ اللَّهُ نَفْسَهُ ۗ وَإِلَى اللَّهِ الْمَصِيرُ ۝٢٨
Laa yattakhizil mu`minoonal kaafireena awliyaaa`a min doonil mu`mineena wa mai yaf`al zaalika falaisa minal laahi fee shai`in illaaa an tattaqoo minhum tuqaah; wa yuhazzirukumul laahu nafsah; wa ilal laahil maseer
📖 Tekkim Wolof
Bu jullit ñi jàpp xaritoo ci yéefar yi, bàyyi fa jullit ña. Ku def loolu amoo ca Yàlla dara, ndeem du dangeen ragal ca ñoom ngaañ. Yàllaa ngi leen di moytandikuloo boppam. Te fa Moom la lépp di mujj.

🎧 Dégg


📜 Aaya 26-30 — Simoore Aali Imran

26قُلِ اللَّهُمَّ مَالِكَ الْمُلْكِ تُؤْتِي الْمُلْكَ مَن تَشَاءُ وَتَنزِعُ الْمُلْكَ مِمَّن تَشَاءُ وَتُعِزُّ مَن تَشَاءُ وَتُذِلُّ مَن تَشَاءُ ۖ بِيَدِكَ الْخَيْرُ ۖ إِنَّكَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
- Neel : “Sama Boroom, Yaw miy Boroom nguur. Yaay jox nguur ku la soob, di rocci nguur ci ku la soob ; Yaay teral ku la soob, Yaay toroxal ku la soob. Yiw wépp a ngi ci sa loxo te kàttanu nga ci def lu ne.
27تُولِجُ اللَّيْلَ فِي النَّهَارِ وَتُولِجُ النَّهَارَ فِي اللَّيْلِ ۖ وَتُخْرِجُ الْحَيَّ مِنَ الْمَيِّتِ وَتُخْرِجُ الْمَيِّتَ مِنَ الْحَيِّ ۖ وَتَرْزُقُ مَن تَشَاءُ بِغَيْرِ حِسَابٍ
Yaay dugal guddi ci bëccëg, Yaay dugal bëccëg ci guddi, Yaay génne ndundu ci ndee, Yaay génne ndee ci ndundu. Di wërsëgal ku la soob ci lu àndul ak waññi”.
28لَّا يَتَّخِذِ الْمُؤْمِنُونَ الْكَافِرِينَ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِ الْمُؤْمِنِينَ ۖ وَمَن يَفْعَلْ ذَٰلِكَ فَلَيْسَ مِنَ اللَّهِ فِي شَيْءٍ إِلَّا أَن تَتَّقُوا مِنْهُمْ تُقَاةً ۗ وَيُحَذِّرُكُمُ اللَّهُ نَفْسَهُ ۗ وَإِلَى اللَّهِ الْمَصِيرُ
Bu jullit ñi jàpp xaritoo ci yéefar yi, bàyyi fa jullit ña. Ku def loolu amoo ca Yàlla dara, ndeem du dangeen ragal ca ñoom ngaañ. Yàllaa ngi leen di moytandikuloo boppam. Te fa Moom la lépp di mujj.
29قُلْ إِن تُخْفُوا مَا فِي صُدُورِكُمْ أَوْ تُبْدُوهُ يَعْلَمْهُ اللَّهُ ۗ وَيَعْلَمُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Neel : “Bu ngeen nëbbee li ci seeni xol walla ngeen feeñal ko, Yàlla dana ko xam. Yàlla xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si. Te Yàlla am na kàttan def lu ne.
30يَوْمَ تَجِدُ كُلُّ نَفْسٍ مَّا عَمِلَتْ مِنْ خَيْرٍ مُّحْضَرًا وَمَا عَمِلَتْ مِن سُوءٍ تَوَدُّ لَوْ أَنَّ بَيْنَهَا وَبَيْنَهُ أَمَدًا بَعِيدًا ۗ وَيُحَذِّرُكُمُ اللَّهُ نَفْسَهُ ۗ وَاللَّهُ رَءُوفٌ بِالْعِبَادِ
Bis ba nga xam ne bakkan bu nekk dana jot ca la mu defoon ci aw yiw ak ca la mu defoon ci ñaawtéef ; dana ngéejoo dàndanteek ñaawtéef yooyu sore ko lool ! Yàllaa ngi leen di moytandikuloo boppam. Te Yàlla dey ku ñeewant jaam ñi la.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
28Aaya

Tekki — Aali Imran 28

Simoore Aali Imran Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu jullit ñi jàpp xaritoo ci yéefar yi, bàyyi fa…

Simoore Aaya 28/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers