Al-Ahzab · 23/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ رِجَالٌ صَدَقُوا مَا عَاهَدُوا اللَّهَ عَلَيْهِ ۖ فَمِنْهُم مَّن قَضَىٰ نَحْبَهُ وَمِنْهُم مَّن يَنتَظِرُ ۖ وَمَا بَدَّلُوا تَبْدِيلًا ۝٢٣
Minal mu`mineena rijaalun sadaqoo maa `aahadul laaha `alaihi faminhum man qadaa nahbahoo wa minhum mai yantaziru wa maa baddaloo tabdeelaa
📖 Tekkim Wolof
Am na ci jullit ñi ñuy dëggal la ñu dëelante woon ak Yàlla. Am na ci ñoom ñu ko matal, am it ci ñoom ñuy négandiku ; te soppiwuñu ca dara ;

🎧 Dégg


📜 Aaya 21-25 — Al-Ahzab

21لَّقَدْ كَانَ لَكُمْ فِي رَسُولِ اللَّهِ أُسْوَةٌ حَسَنَةٌ لِّمَن كَانَ يَرْجُو اللَّهَ وَالْيَوْمَ الْآخِرَ وَذَكَرَ اللَّهَ كَثِيرًا
Am ngeen royuwaay wu jekk ci Yonentub Yàlla, te képp ku yaakaar Yàlla te gëm Bis- pénc bu mujj ba, tey tuddu, di fàttaliku Yàlla lu bari .
22وَلَمَّا رَأَى الْمُؤْمِنُونَ الْأَحْزَابَ قَالُوا هَٰذَا مَا وَعَدَنَا اللَّهُ وَرَسُولُهُ وَصَدَقَ اللَّهُ وَرَسُولُهُ ۚ وَمَا زَادَهُمْ إِلَّا إِيمَانًا وَتَسْلِيمًا
Ña gëm tigi, ba ñu gisee farandoo ya, dañoo wax ne : “Lii la Nu Yàlla ak ub Yonentam doon dig ; te Yàlla ak ub Yonentam dëggal Nañu”. Te dolliwuleen lenn lu dul ngëm ak jébbulu.
23مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ رِجَالٌ صَدَقُوا مَا عَاهَدُوا اللَّهَ عَلَيْهِ ۖ فَمِنْهُم مَّن قَضَىٰ نَحْبَهُ وَمِنْهُم مَّن يَنتَظِرُ ۖ وَمَا بَدَّلُوا تَبْدِيلًا
Am na ci jullit ñi ñuy dëggal la ñu dëelante woon ak Yàlla. Am na ci ñoom ñu ko matal, am it ci ñoom ñuy négandiku ; te soppiwuñu ca dara ;
24لِّيَجْزِيَ اللَّهُ الصَّادِقِينَ بِصِدْقِهِمْ وَيُعَذِّبَ الْمُنَافِقِينَ إِن شَاءَ أَوْ يَتُوبَ عَلَيْهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Yàlla dana fey ña dëggaloon ca seen dëggu ga, Dana mbugal it naaféq ya bu ko soobee, walla Mu baal leen. Yàlla Yërëmaakoon la, Jaglewaakoonu [yërmaandeem] la.
25وَرَدَّ اللَّهُ الَّذِينَ كَفَرُوا بِغَيْظِهِمْ لَمْ يَنَالُوا خَيْرًا ۚ وَكَفَى اللَّهُ الْمُؤْمِنِينَ الْقِتَالَ ۚ وَكَانَ اللَّهُ قَوِيًّا عَزِيزًا
Yàlla delloo na yéefar ya, ñu dellook seen mer, amuñu wenn yiw, Yàlla fegal na jullit ñi xeex ba. Yàlla ku bari doole la tey Boroom kàttan.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
23Aaya

Tekki — Al-Ahzab 23

Simoore Al-Ahzab Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci jullit ñi ñuy dëggal la ñu dëelante…

Simoore Aaya 23/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers