Al-Ahzab · 22/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
وَلَمَّا رَأَى الْمُؤْمِنُونَ الْأَحْزَابَ قَالُوا هَٰذَا مَا وَعَدَنَا اللَّهُ وَرَسُولُهُ وَصَدَقَ اللَّهُ وَرَسُولُهُ ۚ وَمَا زَادَهُمْ إِلَّا إِيمَانًا وَتَسْلِيمًا ۝٢٢
Wa lammaa ra al mu`minoonal Ahzaaba qaaloo haaza maa wa`adanal laahu wa Rasooluh; wa maa zaadahum illaaa eemaananw wa tasleemaa
📖 Tekkim Wolof
Ña gëm tigi, ba ñu gisee farandoo ya, dañoo wax ne : “Lii la Nu Yàlla ak ub Yonentam doon dig ; te Yàlla ak ub Yonentam dëggal Nañu”. Te dolliwuleen lenn lu dul ngëm ak jébbulu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 20-24 — Al-Ahzab

20يَحْسَبُونَ الْأَحْزَابَ لَمْ يَذْهَبُوا ۖ وَإِن يَأْتِ الْأَحْزَابُ يَوَدُّوا لَوْ أَنَّهُم بَادُونَ فِي الْأَعْرَابِ يَسْأَلُونَ عَنْ أَنبَائِكُمْ ۖ وَلَوْ كَانُوا فِيكُم مَّا قَاتَلُوا إِلَّا قَلِيلًا
Te ñuy foog ne farandoo ya demuñu. Te bu ñu dikkoon, dañu naa ngéeju bokk ca màngaan ya, duñu xam li ngeen xewle lu dul bu ñu ko laajtoo. Bu ñu nekkee ci seen biir itam, lu néew la ñuy xareji.
21لَّقَدْ كَانَ لَكُمْ فِي رَسُولِ اللَّهِ أُسْوَةٌ حَسَنَةٌ لِّمَن كَانَ يَرْجُو اللَّهَ وَالْيَوْمَ الْآخِرَ وَذَكَرَ اللَّهَ كَثِيرًا
Am ngeen royuwaay wu jekk ci Yonentub Yàlla, te képp ku yaakaar Yàlla te gëm Bis- pénc bu mujj ba, tey tuddu, di fàttaliku Yàlla lu bari .
22وَلَمَّا رَأَى الْمُؤْمِنُونَ الْأَحْزَابَ قَالُوا هَٰذَا مَا وَعَدَنَا اللَّهُ وَرَسُولُهُ وَصَدَقَ اللَّهُ وَرَسُولُهُ ۚ وَمَا زَادَهُمْ إِلَّا إِيمَانًا وَتَسْلِيمًا
Ña gëm tigi, ba ñu gisee farandoo ya, dañoo wax ne : “Lii la Nu Yàlla ak ub Yonentam doon dig ; te Yàlla ak ub Yonentam dëggal Nañu”. Te dolliwuleen lenn lu dul ngëm ak jébbulu.
23مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ رِجَالٌ صَدَقُوا مَا عَاهَدُوا اللَّهَ عَلَيْهِ ۖ فَمِنْهُم مَّن قَضَىٰ نَحْبَهُ وَمِنْهُم مَّن يَنتَظِرُ ۖ وَمَا بَدَّلُوا تَبْدِيلًا
Am na ci jullit ñi ñuy dëggal la ñu dëelante woon ak Yàlla. Am na ci ñoom ñu ko matal, am it ci ñoom ñuy négandiku ; te soppiwuñu ca dara ;
24لِّيَجْزِيَ اللَّهُ الصَّادِقِينَ بِصِدْقِهِمْ وَيُعَذِّبَ الْمُنَافِقِينَ إِن شَاءَ أَوْ يَتُوبَ عَلَيْهِمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Yàlla dana fey ña dëggaloon ca seen dëggu ga, Dana mbugal it naaféq ya bu ko soobee, walla Mu baal leen. Yàlla Yërëmaakoon la, Jaglewaakoonu [yërmaandeem] la.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
22Aaya

Tekki — Al-Ahzab 22

Simoore Al-Ahzab Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña gëm tigi, ba ñu gisee farandoo ya, dañoo wax…

Simoore Aaya 22/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers