Al-Ahzab · 33/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
وَقَرْنَ فِي بُيُوتِكُنَّ وَلَا تَبَرَّجْنَ تَبَرُّجَ الْجَاهِلِيَّةِ الْأُولَىٰ ۖ وَأَقِمْنَ الصَّلَاةَ وَآتِينَ الزَّكَاةَ وَأَطِعْنَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ لِيُذْهِبَ عَنكُمُ الرِّجْسَ أَهْلَ الْبَيْتِ وَيُطَهِّرَكُمْ تَطْهِيرًا ۝٣٣
Wa qarna fee bu yoo tikunna wa laa tabarrajna tabarrujal Jaahiliyyatil oolaa wa aqimnas Salaata w aaateenaz Zakaata wa ati`nal laaha wa Rasoolah; innamaa yureedul laahu liyuzhiba `ankumur rijsa Ahlal Bayti wa yutahhirakum tatheeraa
📖 Tekkim Wolof
Nangeen di sax ci seeni kër ; te buleen di baraj-baraji kem ni ko jigéenu jaahiliya yu njëkk ya daan ko defe. Te nangeen di taxawal julli tey génne asaka te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Ndax Yàlla dafa namm a dindi ci yéen, waa kër Yonent bi, lépp luy taq-taq, te laabal leen ba ngeen sell.

🎧 Dégg


📜 Aaya 31-35 — Al-Ahzab

31۞ وَمَن يَقْنُتْ مِنكُنَّ لِلَّهِ وَرَسُولِهِ وَتَعْمَلْ صَالِحًا نُّؤْتِهَا أَجْرَهَا مَرَّتَيْنِ وَأَعْتَدْنَا لَهَا رِزْقًا كَرِيمًا
Képp ku bokk ci yéen te jébbal boppam Yàlla ak ub Yonentam tey jëf u yiw, Dananu ko fulal ag peyam ñaari yoon, te waajalal Nanu ko xéewal gu màgg.
32يَا نِسَاءَ النَّبِيِّ لَسْتُنَّ كَأَحَدٍ مِّنَ النِّسَاءِ ۚ إِنِ اتَّقَيْتُنَّ فَلَا تَخْضَعْنَ بِالْقَوْلِ فَيَطْمَعَ الَّذِي فِي قَلْبِهِ مَرَضٌ وَقُلْنَ قَوْلًا مَّعْرُوفًا
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Yemuleen ak yeneen jigéen ñi. Su fekkee ne ragal ngeen Yàlla, buleen di wax waxi caaxaan, yuy tax góor gu xolam tawat di xemmem. Nangeen di wax wax ju yiw njekk.
33وَقَرْنَ فِي بُيُوتِكُنَّ وَلَا تَبَرَّجْنَ تَبَرُّجَ الْجَاهِلِيَّةِ الْأُولَىٰ ۖ وَأَقِمْنَ الصَّلَاةَ وَآتِينَ الزَّكَاةَ وَأَطِعْنَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ لِيُذْهِبَ عَنكُمُ الرِّجْسَ أَهْلَ الْبَيْتِ وَيُطَهِّرَكُمْ تَطْهِيرًا
Nangeen di sax ci seeni kër ; te buleen di baraj-baraji kem ni ko jigéenu jaahiliya yu njëkk ya daan ko defe. Te nangeen di taxawal julli tey génne asaka te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Ndax Yàlla dafa namm a dindi ci yéen, waa kër Yonent bi, lépp luy taq-taq, te laabal leen ba ngeen sell.
34وَاذْكُرْنَ مَا يُتْلَىٰ فِي بُيُوتِكُنَّ مِنْ آيَاتِ اللَّهِ وَالْحِكْمَةِ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ لَطِيفًا خَبِيرًا
Nangeen fàttaliku li Nu leen jàngal ci seen biiri kër, te mu bokk ci laayay Yàlla yi , Alxuraan ak lépp luy xereñe. Yàlla dey Kuy ñeewante la, di Kuy xàmmee.
35إِنَّ الْمُسْلِمِينَ وَالْمُسْلِمَاتِ وَالْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ وَالْقَانِتِينَ وَالْقَانِتَاتِ وَالصَّادِقِينَ وَالصَّادِقَاتِ وَالصَّابِرِينَ وَالصَّابِرَاتِ وَالْخَاشِعِينَ وَالْخَاشِعَاتِ وَالْمُتَصَدِّقِينَ وَالْمُتَصَدِّقَاتِ وَالصَّائِمِينَ وَالصَّائِمَاتِ وَالْحَافِظِينَ فُرُوجَهُمْ وَالْحَافِظَاتِ وَالذَّاكِرِينَ اللَّهَ كَثِيرًا وَالذَّاكِرَاتِ أَعَدَّ اللَّهُ لَهُم مَّغْفِرَةً وَأَجْرًا عَظِيمًا
Naka jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi, way-gëm yu góor ak way-gëm yu jigéen, way- wommatu yu góor ak way-wommatu yu jigéen yi, way-dëggu yu góor ak way-dëggu yu jigéen yi, way-muñ yu góor ak way-muñ yu jigéen, way-ragal yu góor ak way-ragal yu jigéen ya, saraxekat yu góor ak saraxekat yu jigéen yi, woorkat yu góor ak woorkat yu jigéen yi, góor ñiy sàmm seeni pëy ak yu jigéen yi, ñiy tuddu Yàlla lu bari ci góor ñeek jigéen ñi, Yàlla waajalal na leen njéggal ak pey gu màgg.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
33Aaya

Tekki — Al-Ahzab 33

Simoore Al-Ahzab Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen di sax ci seeni kër ; te buleen di…

Simoore Aaya 33/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers