Al-Ahzab · 34/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
وَاذْكُرْنَ مَا يُتْلَىٰ فِي بُيُوتِكُنَّ مِنْ آيَاتِ اللَّهِ وَالْحِكْمَةِ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ لَطِيفًا خَبِيرًا ۝٣٤
Wazkurna maa yutlaa fee bu yootikunna min aayaatil laahi wal Hikmah; innal laaha kaana lateefan Khabeera
📖 Tekkim Wolof
Nangeen fàttaliku li Nu leen jàngal ci seen biiri kër, te mu bokk ci laayay Yàlla yi , Alxuraan ak lépp luy xereñe. Yàlla dey Kuy ñeewante la, di Kuy xàmmee.

🎧 Dégg


📜 Aaya 32-36 — Al-Ahzab

32يَا نِسَاءَ النَّبِيِّ لَسْتُنَّ كَأَحَدٍ مِّنَ النِّسَاءِ ۚ إِنِ اتَّقَيْتُنَّ فَلَا تَخْضَعْنَ بِالْقَوْلِ فَيَطْمَعَ الَّذِي فِي قَلْبِهِ مَرَضٌ وَقُلْنَ قَوْلًا مَّعْرُوفًا
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Yemuleen ak yeneen jigéen ñi. Su fekkee ne ragal ngeen Yàlla, buleen di wax waxi caaxaan, yuy tax góor gu xolam tawat di xemmem. Nangeen di wax wax ju yiw njekk.
33وَقَرْنَ فِي بُيُوتِكُنَّ وَلَا تَبَرَّجْنَ تَبَرُّجَ الْجَاهِلِيَّةِ الْأُولَىٰ ۖ وَأَقِمْنَ الصَّلَاةَ وَآتِينَ الزَّكَاةَ وَأَطِعْنَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ ۚ إِنَّمَا يُرِيدُ اللَّهُ لِيُذْهِبَ عَنكُمُ الرِّجْسَ أَهْلَ الْبَيْتِ وَيُطَهِّرَكُمْ تَطْهِيرًا
Nangeen di sax ci seeni kër ; te buleen di baraj-baraji kem ni ko jigéenu jaahiliya yu njëkk ya daan ko defe. Te nangeen di taxawal julli tey génne asaka te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Ndax Yàlla dafa namm a dindi ci yéen, waa kër Yonent bi, lépp luy taq-taq, te laabal leen ba ngeen sell.
34وَاذْكُرْنَ مَا يُتْلَىٰ فِي بُيُوتِكُنَّ مِنْ آيَاتِ اللَّهِ وَالْحِكْمَةِ ۚ إِنَّ اللَّهَ كَانَ لَطِيفًا خَبِيرًا
Nangeen fàttaliku li Nu leen jàngal ci seen biiri kër, te mu bokk ci laayay Yàlla yi , Alxuraan ak lépp luy xereñe. Yàlla dey Kuy ñeewante la, di Kuy xàmmee.
35إِنَّ الْمُسْلِمِينَ وَالْمُسْلِمَاتِ وَالْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ وَالْقَانِتِينَ وَالْقَانِتَاتِ وَالصَّادِقِينَ وَالصَّادِقَاتِ وَالصَّابِرِينَ وَالصَّابِرَاتِ وَالْخَاشِعِينَ وَالْخَاشِعَاتِ وَالْمُتَصَدِّقِينَ وَالْمُتَصَدِّقَاتِ وَالصَّائِمِينَ وَالصَّائِمَاتِ وَالْحَافِظِينَ فُرُوجَهُمْ وَالْحَافِظَاتِ وَالذَّاكِرِينَ اللَّهَ كَثِيرًا وَالذَّاكِرَاتِ أَعَدَّ اللَّهُ لَهُم مَّغْفِرَةً وَأَجْرًا عَظِيمًا
Naka jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi, way-gëm yu góor ak way-gëm yu jigéen, way- wommatu yu góor ak way-wommatu yu jigéen yi, way-dëggu yu góor ak way-dëggu yu jigéen yi, way-muñ yu góor ak way-muñ yu jigéen, way-ragal yu góor ak way-ragal yu jigéen ya, saraxekat yu góor ak saraxekat yu jigéen yi, woorkat yu góor ak woorkat yu jigéen yi, góor ñiy sàmm seeni pëy ak yu jigéen yi, ñiy tuddu Yàlla lu bari ci góor ñeek jigéen ñi, Yàlla waajalal na leen njéggal ak pey gu màgg.
36وَمَا كَانَ لِمُؤْمِنٍ وَلَا مُؤْمِنَةٍ إِذَا قَضَى اللَّهُ وَرَسُولُهُ أَمْرًا أَن يَكُونَ لَهُمُ الْخِيَرَةُ مِنْ أَمْرِهِمْ ۗ وَمَن يَعْصِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا مُّبِينًا
Su Yàlla ak ub Yonentam àtte mbir ba sottalI, amul benn jullit bu góor ak bu jigéen bu ciy am coppan, te seen àtte ba xas dog. Képp kuy moy Yàllaak ub Yonentam, mi ngi ci ag réer gu bir.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
34Aaya

Tekki — Al-Ahzab 34

Simoore Al-Ahzab Aaya 34 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen fàttaliku li Nu leen jàngal ci seen biiri kër,…

Simoore Aaya 34/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 32–36. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers