Fatir · 29/45
Tekki Waxtaan — Fatir
إِنَّ الَّذِينَ يَتْلُونَ كِتَابَ اللَّهِ وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ وَأَنفَقُوا مِمَّا رَزَقْنَاهُمْ سِرًّا وَعَلَانِيَةً يَرْجُونَ تِجَارَةً لَّن تَبُورَ ۝٢٩
Innal lazeena yatloona Kitabbal laahi wa aqaamus Salaata wa anfaqoo mimmaa razaqnaahum sirranw wa `alaa niyatany yarjoona tijaaratal lan taboor
📖 Tekkim Wolof
Ñay jàng Téereb Yàlla ba, tey taxawe julli, tey joxe ci [alal] ji Nu leen wërsëgale, ci lu nëbbu ak ci lu feeñ, ñoom yaakaar nañu am njula mu dul yàqu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 27-31 — Fatir

27أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَخْرَجْنَا بِهِ ثَمَرَاتٍ مُّخْتَلِفًا أَلْوَانُهَا ۚ وَمِنَ الْجِبَالِ جُدَدٌ بِيضٌ وَحُمْرٌ مُّخْتَلِفٌ أَلْوَانُهَا وَغَرَابِيبُ سُودٌ
Xanaa gisuloo ne Yàlla moo wàcce ndox mu bawoo ci asamaan si ? Nu daldi cay génne ay meññent yu wuute ay wirgu. Am na it ci tundi doj yi yuy sësëloo te weex, ak yuy xonk, yu wuute ay wirgu, ak yu ñuul kukk.
28وَمِنَ النَّاسِ وَالدَّوَابِّ وَالْأَنْعَامِ مُخْتَلِفٌ أَلْوَانُهُ كَذَٰلِكَ ۗ إِنَّمَا يَخْشَى اللَّهَ مِنْ عِبَادِهِ الْعُلَمَاءُ ۗ إِنَّ اللَّهَ عَزِيزٌ غَفُورٌ
Am na it ci nit ñi, ci daaba yeek mala yi yu wuute ay wirgu, noonu rekk la. Jaami Yàlla yi ko ragal ñoo di woroom xam-xam yi. Te Yàlla boroom xam-xam la, di Jéggalaakoon.
29إِنَّ الَّذِينَ يَتْلُونَ كِتَابَ اللَّهِ وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ وَأَنفَقُوا مِمَّا رَزَقْنَاهُمْ سِرًّا وَعَلَانِيَةً يَرْجُونَ تِجَارَةً لَّن تَبُورَ
Ñay jàng Téereb Yàlla ba, tey taxawe julli, tey joxe ci [alal] ji Nu leen wërsëgale, ci lu nëbbu ak ci lu feeñ, ñoom yaakaar nañu am njula mu dul yàqu.
30لِيُوَفِّيَهُمْ أُجُورَهُمْ وَيَزِيدَهُم مِّن فَضْلِهِ ۚ إِنَّهُ غَفُورٌ شَكُورٌ
loolu lépp ngir Yàlla jox leen seenug pey te dolli leen ciy ngënéelam. Moom Yàlla, Jéggalaakoon la, Kuy sant la.
31وَالَّذِي أَوْحَيْنَا إِلَيْكَ مِنَ الْكِتَابِ هُوَ الْحَقُّ مُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِعِبَادِهِ لَخَبِيرٌ بَصِيرٌ
La Nu la soloo ci Téere bi mooy dëgg tey saxal la ko jiitu woon . Yàlla kuy Xàmmee la, Kuy Gis jaamam ñi la.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — Fatir 29

Simoore Fatir Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñay jàng Téereb Yàlla ba, tey taxawe julli, tey joxe…

Simoore Aaya 29/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers