An-Nisa · 99/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
فَأُولَٰئِكَ عَسَى اللَّهُ أَن يَعْفُوَ عَنْهُمْ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَفُوًّا غَفُورًا ۝٩٩
Fa ulaaa`ika `asal laahu ai ya`fuwa `anhum; wa kaanal laahu `Afuwwan Ghafooraa
📖 Tekkim Wolof
Ñooña xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla Kuy baale la, di jéggale.
🎧 Dégg

📜 Aaya 97-101 — An-Nisa

97إِنَّ الَّذِينَ تَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ ظَالِمِي أَنفُسِهِمْ قَالُوا فِيمَ كُنتُمْ ۖ قَالُوا كُنَّا مُسْتَضْعَفِينَ فِي الْأَرْضِ ۚ قَالُوا أَلَمْ تَكُنْ أَرْضُ اللَّهِ وَاسِعَةً فَتُهَاجِرُوا فِيهَا ۚ فَأُولَٰئِكَ مَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ ۖ وَسَاءَتْ مَصِيرًا
Ña Malaaka ya jël seeni ruu te ñu doon tooñ seen bopp, Danañu leen laaj : “Ca la ngeen nekkoon ? ” [bañ a dem xareji] - Ñu toontu ne : “Danoo nekkoon ñu ñu néewal doole ci kaw suuf”. Ñu ne leen : “Moo ndax suufus Yàlla si dafa yaatuwul ba ngeen mën a gàddaay jëm feneen ? ”. Ñooña Safaraa di seen dëkkuwaay. Te ndaw muj gu bon !
98إِلَّا الْمُسْتَضْعَفِينَ مِنَ الرِّجَالِ وَالنِّسَاءِ وَالْوِلْدَانِ لَا يَسْتَطِيعُونَ حِيلَةً وَلَا يَهْتَدُونَ سَبِيلًا
Ba mu des ña néew doole : ci góor ñi, ak ci jigéen ñi, ak xale yi ci ñàkk pexe, bu ñu gindikoo [ba genn màkka]
99فَأُولَٰئِكَ عَسَى اللَّهُ أَن يَعْفُوَ عَنْهُمْ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَفُوًّا غَفُورًا
Ñooña xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla Kuy baale la, di jéggale.
100۞ وَمَن يُهَاجِرْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ يَجِدْ فِي الْأَرْضِ مُرَاغَمًا كَثِيرًا وَسَعَةً ۚ وَمَن يَخْرُجْ مِن بَيْتِهِ مُهَاجِرًا إِلَى اللَّهِ وَرَسُولِهِ ثُمَّ يُدْرِكْهُ الْمَوْتُ فَقَدْ وَقَعَ أَجْرُهُ عَلَى اللَّهِ ۗ وَكَانَ اللَّهُ غَفُورًا رَّحِيمًا
Ku gàddaay ngir Yàlla, fu mu mën a jëm, dana fa fekk delluwaay yu bari ak ug yaatal. Ku génn këram, di gàddaay ngir Yàllaak ub Yonentam, ba dee dab ko, kooku peyam Yàlla warlul na ko ko. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
101وَإِذَا ضَرَبْتُمْ فِي الْأَرْضِ فَلَيْسَ عَلَيْكُمْ جُنَاحٌ أَن تَقْصُرُوا مِنَ الصَّلَاةِ إِنْ خِفْتُمْ أَن يَفْتِنَكُمُ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ إِنَّ الْكَافِرِينَ كَانُوا لَكُمْ عَدُوًّا مُّبِينًا
Bu ngeen di tukki ci réew yi, aayul ci yéen ngeen wàññi ci julli yi, bu ngeen ragalee yéefar yi fitnaal leen, yéefar yi seeni noon lañu yu bir.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
99Aaya

Tekki — An-Nisa 99

Simoore An-Nisa Aaya 99 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñooña xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla Kuy baale la, di…

Simoore Aaya 99/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 97–101. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers