An-Nisa · 98/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
إِلَّا الْمُسْتَضْعَفِينَ مِنَ الرِّجَالِ وَالنِّسَاءِ وَالْوِلْدَانِ لَا يَسْتَطِيعُونَ حِيلَةً وَلَا يَهْتَدُونَ سَبِيلًا ۝٩٨
Illal mustad `afeena minar rijaali wannisaaa`i walwildaani laa yastatee`oona heelatanw wa laa yahtadoona sabeela
📖 Tekkim Wolof
Ba mu des ña néew doole : ci góor ñi, ak ci jigéen ñi, ak xale yi ci ñàkk pexe, bu ñu gindikoo [ba genn màkka]

🎧 Dégg


📜 Aaya 96-100 — An-Nisa

96دَرَجَاتٍ مِّنْهُ وَمَغْفِرَةً وَرَحْمَةً ۚ وَكَانَ اللَّهُ غَفُورًا رَّحِيمًا
muy yokkute gu tukkee ci Yàlla, ak njéggal ak yërmaande. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
97إِنَّ الَّذِينَ تَوَفَّاهُمُ الْمَلَائِكَةُ ظَالِمِي أَنفُسِهِمْ قَالُوا فِيمَ كُنتُمْ ۖ قَالُوا كُنَّا مُسْتَضْعَفِينَ فِي الْأَرْضِ ۚ قَالُوا أَلَمْ تَكُنْ أَرْضُ اللَّهِ وَاسِعَةً فَتُهَاجِرُوا فِيهَا ۚ فَأُولَٰئِكَ مَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ ۖ وَسَاءَتْ مَصِيرًا
Ña Malaaka ya jël seeni ruu te ñu doon tooñ seen bopp, Danañu leen laaj : “Ca la ngeen nekkoon ? ” [bañ a dem xareji] - Ñu toontu ne : “Danoo nekkoon ñu ñu néewal doole ci kaw suuf”. Ñu ne leen : “Moo ndax suufus Yàlla si dafa yaatuwul ba ngeen mën a gàddaay jëm feneen ? ”. Ñooña Safaraa di seen dëkkuwaay. Te ndaw muj gu bon !
98إِلَّا الْمُسْتَضْعَفِينَ مِنَ الرِّجَالِ وَالنِّسَاءِ وَالْوِلْدَانِ لَا يَسْتَطِيعُونَ حِيلَةً وَلَا يَهْتَدُونَ سَبِيلًا
Ba mu des ña néew doole : ci góor ñi, ak ci jigéen ñi, ak xale yi ci ñàkk pexe, bu ñu gindikoo [ba genn màkka]
99فَأُولَٰئِكَ عَسَى اللَّهُ أَن يَعْفُوَ عَنْهُمْ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَفُوًّا غَفُورًا
Ñooña xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla Kuy baale la, di jéggale.
100۞ وَمَن يُهَاجِرْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ يَجِدْ فِي الْأَرْضِ مُرَاغَمًا كَثِيرًا وَسَعَةً ۚ وَمَن يَخْرُجْ مِن بَيْتِهِ مُهَاجِرًا إِلَى اللَّهِ وَرَسُولِهِ ثُمَّ يُدْرِكْهُ الْمَوْتُ فَقَدْ وَقَعَ أَجْرُهُ عَلَى اللَّهِ ۗ وَكَانَ اللَّهُ غَفُورًا رَّحِيمًا
Ku gàddaay ngir Yàlla, fu mu mën a jëm, dana fa fekk delluwaay yu bari ak ug yaatal. Ku génn këram, di gàddaay ngir Yàllaak ub Yonentam, ba dee dab ko, kooku peyam Yàlla warlul na ko ko. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
98Aaya

Tekki — An-Nisa 98

Simoore An-Nisa Aaya 98 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba mu des ña néew doole : ci góor ñi,…

Simoore Aaya 98/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 96–100. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers