Al-Ahqaf · 14/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَنَّةِ خَالِدِينَ فِيهَا جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝١٤
Ulaaa`ika Ashabul Jannati khaalideena feehaa jazaaa`am bimaa kaano ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Ñooñee ñoo di waa Àjjana dañu fay béel mu di peyug la ñu daan jëf.

🎧 Dégg


📜 Aaya 12-16 — Al-Ahqaf

12وَمِن قَبْلِهِ كِتَابُ مُوسَىٰ إِمَامًا وَرَحْمَةً ۚ وَهَٰذَا كِتَابٌ مُّصَدِّقٌ لِّسَانًا عَرَبِيًّا لِّيُنذِرَ الَّذِينَ ظَلَمُوا وَبُشْرَىٰ لِلْمُحْسِنِينَ
Téereb Muusaa jiituwoon na ko di njub. Lii nag ab téere la buy dëggal loolu ci làmmiñu araab, ngir muy xupp ñiy tooñ di bégal ñiy rafetal (ay jëf).
13إِنَّ الَّذِينَ قَالُوا رَبُّنَا اللَّهُ ثُمَّ اسْتَقَامُوا فَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ñi gëm Yàlla tey jaar ca yoon wu jub xocc wa, duñu tiit duñu jaaxle.
14أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَنَّةِ خَالِدِينَ فِيهَا جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ñooñee ñoo di waa Àjjana dañu fay béel mu di peyug la ñu daan jëf.
15وَوَصَّيْنَا الْإِنسَانَ بِوَالِدَيْهِ إِحْسَانًا ۖ حَمَلَتْهُ أُمُّهُ كُرْهًا وَوَضَعَتْهُ كُرْهًا ۖ وَحَمْلُهُ وَفِصَالُهُ ثَلَاثُونَ شَهْرًا ۚ حَتَّىٰ إِذَا بَلَغَ أَشُدَّهُ وَبَلَغَ أَرْبَعِينَ سَنَةً قَالَ رَبِّ أَوْزِعْنِي أَنْ أَشْكُرَ نِعْمَتَكَ الَّتِي أَنْعَمْتَ عَلَيَّ وَعَلَىٰ وَالِدَيَّ وَأَنْ أَعْمَلَ صَالِحًا تَرْضَاهُ وَأَصْلِحْ لِي فِي ذُرِّيَّتِي ۖ إِنِّي تُبْتُ إِلَيْكَ وَإِنِّي مِنَ الْمُسْلِمِينَ
Dénk nanu nit (mu wara rafetal) jëme ko ci ñaari waajuram : ndayama ko ëmb ci coono, imbi ko ci coono ; fa ëmb ba dale ba ca feral ga fanweeri weer la ; ba sax moom saa su dëgëree ba am ñeent fukki at, muy wax naan : “yaw sama Boroom ! Yenkeewal ma may mana sant ci sa xéewël yi Nga ma xéewale ak sama ñaari waajur, ak itam may man a jëf (jëf ju yiw joo gëram). Te nga yéwénalal ma ci sama njërtiit , Man dey tuub naa dellu ci Yaw te itam Man mii ci jullit ñi laa bokk” (ñi jébbale séen bopp).
16أُولَٰئِكَ الَّذِينَ نَتَقَبَّلُ عَنْهُمْ أَحْسَنَ مَا عَمِلُوا وَنَتَجَاوَزُ عَن سَيِّئَاتِهِمْ فِي أَصْحَابِ الْجَنَّةِ ۖ وَعْدَ الصِّدْقِ الَّذِي كَانُوا يُوعَدُونَ
Ñooñee ñoo di ña nga xam ne dananu leen nangul la gëna rafet ca lañu daan jëf te da nanu leen faral séeni ñaawtéef , te it dananu leen limaale ca waa Àjjana, muy dig bu dëggu banu leen daan dig.
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
14Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 14

Simoore Al-Ahqaf Aaya 14 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñooñee ñoo di waa Àjjana dañu fay béel mu di…

Simoore Aaya 14/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 12–16. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers