Al-Hadid · 13/29
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Hadid
يَوْمَ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالْمُنَافِقَاتُ لِلَّذِينَ آمَنُوا انظُرُونَا نَقْتَبِسْ مِن نُّورِكُمْ قِيلَ ارْجِعُوا وَرَاءَكُمْ فَالْتَمِسُوا نُورًا فَضُرِبَ بَيْنَهُم بِسُورٍ لَّهُ بَابٌ بَاطِنُهُ فِيهِ الرَّحْمَةُ وَظَاهِرُهُ مِن قِبَلِهِ الْعَذَابُ ۝١٣
Yawma yaqoolul munaa fiqoona walmunaafiqaatu lillazeena aamanun zuroonaa naqtabis min noorikum qeelarji`oo waraaa`akum faltamisoo nooran faduriba bainahum bisooril lahoo baab, baatinuhoo feehir rahmatu wa zaahiruhoo min qibalihi-`azaab
📖 Tekkim Wolof
Bu keroogee ba naaféq yu góor yi ak naaféq yu jigéen yi, di wax ñi gëm naan leen : “Xoolleen nu ndax nu man a niitu: ci seenug leer”. Ñu ne leen: “Delluleen ginnaaw, wutig leer”. Daldi doxale seen diggante ñag boo xam ne biir ga yërmaande la (fareek ña gëm), biti ba di mbugël (fareek naaféq ya)

🎧 Dégg


📜 Aaya 11-15 — Simoore Al-Hadid

11مَّن ذَا الَّذِي يُقْرِضُ اللَّهَ قَرْضًا حَسَنًا فَيُضَاعِفَهُ لَهُ وَلَهُ أَجْرٌ كَرِيمٌ
Ana kan mooy nangoo lebal Yàlla bor bu rafet, Mu fulandikul ko ko, te it dana am ag pey gu màgg.
12يَوْمَ تَرَى الْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ يَسْعَىٰ نُورُهُم بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَبِأَيْمَانِهِم بُشْرَاكُمُ الْيَوْمَ جَنَّاتٌ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا ۚ ذَٰلِكَ هُوَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ
(Bu keroog) (bis pénc baa) dangeen gis way gëm ña, leer ga dox seen diggante di jolli ci kanam ak ndeyjoor ; (ñu naan leen) : “Bégleen tey : am ngeen ay àjjana yu dex ya di daw ci suufam te dangeen fay béel”. Loolu mooy texe gu mag ga.
13يَوْمَ يَقُولُ الْمُنَافِقُونَ وَالْمُنَافِقَاتُ لِلَّذِينَ آمَنُوا انظُرُونَا نَقْتَبِسْ مِن نُّورِكُمْ قِيلَ ارْجِعُوا وَرَاءَكُمْ فَالْتَمِسُوا نُورًا فَضُرِبَ بَيْنَهُم بِسُورٍ لَّهُ بَابٌ بَاطِنُهُ فِيهِ الرَّحْمَةُ وَظَاهِرُهُ مِن قِبَلِهِ الْعَذَابُ
Bu keroogee ba naaféq yu góor yi ak naaféq yu jigéen yi, di wax ñi gëm naan leen : “Xoolleen nu ndax nu man a niitu: ci seenug leer”. Ñu ne leen: “Delluleen ginnaaw, wutig leer”. Daldi doxale seen diggante ñag boo xam ne biir ga yërmaande la (fareek ña gëm), biti ba di mbugël (fareek naaféq ya)
14يُنَادُونَهُمْ أَلَمْ نَكُن مَّعَكُمْ ۖ قَالُوا بَلَىٰ وَلَٰكِنَّكُمْ فَتَنتُمْ أَنفُسَكُمْ وَتَرَبَّصْتُمْ وَارْتَبْتُمْ وَغَرَّتْكُمُ الْأَمَانِيُّ حَتَّىٰ جَاءَ أَمْرُ اللَّهِ وَغَرَّكُم بِاللَّهِ الْغَرُورُ
“(Naaféq yaa ngay) woote naan xanaa àndunu woon ak yéen ? ” jullit ña ne. “Axakañ, waaye yéen a fitnaal seen bopp, daan fexeel (ñi gëm) daan werante, faggu ba faf mbirum Yàlla agsi saytaane nax leen.
15فَالْيَوْمَ لَا يُؤْخَذُ مِنكُمْ فِدْيَةٌ وَلَا مِنَ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ مَأْوَاكُمُ النَّارُ ۖ هِيَ مَوْلَاكُمْ ۖ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ
Bis niki tey, kenn du jël ci yéen ag njotu kenn it du ko jëll ca ña weddi. Seenub saxuwaay Safara moom ngeen mengóol: dootu leen tàggoo. Ndaw mujj gu bon !
Al-HadidFihi Alxuraan
29Aaya
MedinanRevelation
13Aaya

Tekki — Al-Hadid 13

Simoore Al-Hadid Aaya 13 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu keroogee ba naaféq yu góor yi ak naaféq yu…

Simoore Aaya 13/29 — Simoore Al-Hadid الحديد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Hadid Dégg, Simoore Al-Hadid Tekki, Simoore Al-Hadid mp3, Simoore Al-Hadid pdf. Aaya 11–15. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers