Al-Hadid · 9/29
Tekki Waxtaan — Al-Hadid
هُوَ الَّذِي يُنَزِّلُ عَلَىٰ عَبْدِهِ آيَاتٍ بَيِّنَاتٍ لِّيُخْرِجَكُم مِّنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ ۚ وَإِنَّ اللَّهَ بِكُمْ لَرَءُوفٌ رَّحِيمٌ ۝٩
Huwal lazee yunazzilu `alaa `abdiheee Aayaatim baiyinaatil liyukhrijakum minaz zulumaati ilan noor; wa innal laaha bikum la Ra`oofur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Moom mooy wàcce ay kàddu yu leer ca jaamam ba, ngir mu génne leen cig lëndëm tàbbal leen cig leer; te Yàlla dey ku leen ñeewanti la, Jagléwaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 7-11 — Al-Hadid

7آمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَأَنفِقُوا مِمَّا جَعَلَكُم مُّسْتَخْلَفِينَ فِيهِ ۖ فَالَّذِينَ آمَنُوا مِنكُمْ وَأَنفَقُوا لَهُمْ أَجْرٌ كَبِيرٌ
Gëmleen Yàlla ak ub Yonentam, te na ngeen di joxe ci alal ji mu leen wuutalal. Ñi gëm te bokk ci yéen tey [joxe alal] danañu am ag pey gu màgg.
8وَمَا لَكُمْ لَا تُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ ۙ وَالرَّسُولُ يَدْعُوكُمْ لِتُؤْمِنُوا بِرَبِّكُمْ وَقَدْ أَخَذَ مِيثَاقَكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Ana lu leen dal ba munu leen gëm Yàlla, ak ub Yonentam mi ngi leen di woo ngir ngeen gëm seen Boroom ? Te jël ci yéen ab dig bu diis ndegam gëm ngeen.
9هُوَ الَّذِي يُنَزِّلُ عَلَىٰ عَبْدِهِ آيَاتٍ بَيِّنَاتٍ لِّيُخْرِجَكُم مِّنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ ۚ وَإِنَّ اللَّهَ بِكُمْ لَرَءُوفٌ رَّحِيمٌ
Moom mooy wàcce ay kàddu yu leer ca jaamam ba, ngir mu génne leen cig lëndëm tàbbal leen cig leer; te Yàlla dey ku leen ñeewanti la, Jagléwaakoon la.
10وَمَا لَكُمْ أَلَّا تُنفِقُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَلِلَّهِ مِيرَاثُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ لَا يَسْتَوِي مِنكُم مَّنْ أَنفَقَ مِن قَبْلِ الْفَتْحِ وَقَاتَلَ ۚ أُولَٰئِكَ أَعْظَمُ دَرَجَةً مِّنَ الَّذِينَ أَنفَقُوا مِن بَعْدُ وَقَاتَلُوا ۚ وَكُلًّا وَعَدَ اللَّهُ الْحُسْنَىٰ ۚ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Ana lu leen dal ba munuleen joxe alal ci yoonu Yàlla, te Yàllaa moom ndono yi nekk ci asamaan yeek suuf si ? Ña joxe seen alal lu jiitu (fathu Makkata) xare boole ca duñu yem ak kenn ñoom dañuy am pey gu màgg ak daraja yu kawe... ëppëlee ko ña joxe ginnaaw xare be te sax xare woon nañu . Ñoom ñépp, la Yàlla dig neexal bu duun, te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
11مَّن ذَا الَّذِي يُقْرِضُ اللَّهَ قَرْضًا حَسَنًا فَيُضَاعِفَهُ لَهُ وَلَهُ أَجْرٌ كَرِيمٌ
Ana kan mooy nangoo lebal Yàlla bor bu rafet, Mu fulandikul ko ko, te it dana am ag pey gu màgg.
Al-HadidFihi Alxuraan
29Aaya
MedinanRevelation
9Aaya

Tekki — Al-Hadid 9

Simoore Al-Hadid Aaya 9 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moom mooy wàcce ay kàddu yu leer ca jaamam ba,…

Simoore Aaya 9/29 — Al-Hadid الحديد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hadid Dégg, Al-Hadid Tekki, Al-Hadid mp3, Al-Hadid pdf. Aaya 7–11. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers