Al-Hadid · 8/29
Tekki Waxtaan — Al-Hadid
وَمَا لَكُمْ لَا تُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ ۙ وَالرَّسُولُ يَدْعُوكُمْ لِتُؤْمِنُوا بِرَبِّكُمْ وَقَدْ أَخَذَ مِيثَاقَكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ ۝٨
Wa maa lakum laa tu`minoona billaahi war Rasoolu yad`ookum lituu`minoo bi Rabbikum wa qad akhaza meesaaqakum in kuntum mu`mineen
📖 Tekkim Wolof
Ana lu leen dal ba munu leen gëm Yàlla, ak ub Yonentam mi ngi leen di woo ngir ngeen gëm seen Boroom ? Te jël ci yéen ab dig bu diis ndegam gëm ngeen.
🎧 Dégg

📜 Aaya 6-10 — Al-Hadid

6يُولِجُ اللَّيْلَ فِي النَّهَارِ وَيُولِجُ النَّهَارَ فِي اللَّيْلِ ۚ وَهُوَ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Mooy duggal guddi ci bëccëg te it mooy duggal bëccëg ci guddi, te Ku xam xéll la li nekk ci dënn yi.
7آمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَأَنفِقُوا مِمَّا جَعَلَكُم مُّسْتَخْلَفِينَ فِيهِ ۖ فَالَّذِينَ آمَنُوا مِنكُمْ وَأَنفَقُوا لَهُمْ أَجْرٌ كَبِيرٌ
Gëmleen Yàlla ak ub Yonentam, te na ngeen di joxe ci alal ji mu leen wuutalal. Ñi gëm te bokk ci yéen tey [joxe alal] danañu am ag pey gu màgg.
8وَمَا لَكُمْ لَا تُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ ۙ وَالرَّسُولُ يَدْعُوكُمْ لِتُؤْمِنُوا بِرَبِّكُمْ وَقَدْ أَخَذَ مِيثَاقَكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Ana lu leen dal ba munu leen gëm Yàlla, ak ub Yonentam mi ngi leen di woo ngir ngeen gëm seen Boroom ? Te jël ci yéen ab dig bu diis ndegam gëm ngeen.
9هُوَ الَّذِي يُنَزِّلُ عَلَىٰ عَبْدِهِ آيَاتٍ بَيِّنَاتٍ لِّيُخْرِجَكُم مِّنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ ۚ وَإِنَّ اللَّهَ بِكُمْ لَرَءُوفٌ رَّحِيمٌ
Moom mooy wàcce ay kàddu yu leer ca jaamam ba, ngir mu génne leen cig lëndëm tàbbal leen cig leer; te Yàlla dey ku leen ñeewanti la, Jagléwaakoon la.
10وَمَا لَكُمْ أَلَّا تُنفِقُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ وَلِلَّهِ مِيرَاثُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ لَا يَسْتَوِي مِنكُم مَّنْ أَنفَقَ مِن قَبْلِ الْفَتْحِ وَقَاتَلَ ۚ أُولَٰئِكَ أَعْظَمُ دَرَجَةً مِّنَ الَّذِينَ أَنفَقُوا مِن بَعْدُ وَقَاتَلُوا ۚ وَكُلًّا وَعَدَ اللَّهُ الْحُسْنَىٰ ۚ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Ana lu leen dal ba munuleen joxe alal ci yoonu Yàlla, te Yàllaa moom ndono yi nekk ci asamaan yeek suuf si ? Ña joxe seen alal lu jiitu (fathu Makkata) xare boole ca duñu yem ak kenn ñoom dañuy am pey gu màgg ak daraja yu kawe... ëppëlee ko ña joxe ginnaaw xare be te sax xare woon nañu . Ñoom ñépp, la Yàlla dig neexal bu duun, te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
Al-HadidFihi Alxuraan
29Aaya
MedinanRevelation
8Aaya

Tekki — Al-Hadid 8

Simoore Al-Hadid Aaya 8 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana lu leen dal ba munu leen gëm Yàlla, ak…

Simoore Aaya 8/29 — Al-Hadid الحديد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hadid Dégg, Al-Hadid Tekki, Al-Hadid mp3, Al-Hadid pdf. Aaya 6–10. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers