Al-An'am · 124/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَإِذَا جَاءَتْهُمْ آيَةٌ قَالُوا لَن نُّؤْمِنَ حَتَّىٰ نُؤْتَىٰ مِثْلَ مَا أُوتِيَ رُسُلُ اللَّهِ ۘ اللَّهُ أَعْلَمُ حَيْثُ يَجْعَلُ رِسَالَتَهُ ۗ سَيُصِيبُ الَّذِينَ أَجْرَمُوا صَغَارٌ عِندَ اللَّهِ وَعَذَابٌ شَدِيدٌ بِمَا كَانُوا يَمْكُرُونَ ۝١٢٤
Wa izaa jaaa`athum Aayatun qaaloo lan nu`mina hatta nu`taa misla maaa ootiya Rusulul laah; Allahu a`almu haisu yaj`alu Risaalatah; sa yuseebul lazeena ajramoo saghaarun `indal laahi wa `azaabun shadeedum bimaa kaanoo yamkuroon
📖 Tekkim Wolof
Te ñoom, saa su leen laaya dikkalee, ñuy wax naan : “Nun dunu gëm ba mbete nu indil nu lu mel ni la ñu joxoon Yonent Yàlla ya”. Yàllaa gën a xam fa Muy wàcce la Muy yónnee. Bàkkaarkat yi, toroxte dal na leen tukke fa Yàlla ak mbugal mu tar ngir pexe [yu bon ya ñu daan nas].

🎧 Dégg


📜 Aaya 122-126 — Al-An'am

122أَوَمَن كَانَ مَيْتًا فَأَحْيَيْنَاهُ وَجَعَلْنَا لَهُ نُورًا يَمْشِي بِهِ فِي النَّاسِ كَمَن مَّثَلُهُ فِي الظُّلُمَاتِ لَيْسَ بِخَارِجٍ مِّنْهَا ۚ كَذَٰلِكَ زُيِّنَ لِلْكَافِرِينَ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Moo ndax ka nekkoon ku dee [yéefar], Nu dundal ko [gëmloo ko], jox ko leer gu muy leerloo buy dox ci biir nit ñi, dana nirook ka nga xam ne misaalam mooy dafa nekk cig lëndëm gu mu dul génn ? Noonu la yéefar yi di rafetloo la ñu doon def.
123وَكَذَٰلِكَ جَعَلْنَا فِي كُلِّ قَرْيَةٍ أَكَابِرَ مُجْرِمِيهَا لِيَمْكُرُوا فِيهَا ۖ وَمَا يَمْكُرُونَ إِلَّا بِأَنفُسِهِمْ وَمَا يَشْعُرُونَ
Naka noonu, Lanu defe ci bépp dëkk ay kilifa ca ña dàq a tooñ ngir ñu fay nas ay pexe. Te pexe ya, dara duleen ca moy te yëguñu ko.
124وَإِذَا جَاءَتْهُمْ آيَةٌ قَالُوا لَن نُّؤْمِنَ حَتَّىٰ نُؤْتَىٰ مِثْلَ مَا أُوتِيَ رُسُلُ اللَّهِ ۘ اللَّهُ أَعْلَمُ حَيْثُ يَجْعَلُ رِسَالَتَهُ ۗ سَيُصِيبُ الَّذِينَ أَجْرَمُوا صَغَارٌ عِندَ اللَّهِ وَعَذَابٌ شَدِيدٌ بِمَا كَانُوا يَمْكُرُونَ
Te ñoom, saa su leen laaya dikkalee, ñuy wax naan : “Nun dunu gëm ba mbete nu indil nu lu mel ni la ñu joxoon Yonent Yàlla ya”. Yàllaa gën a xam fa Muy wàcce la Muy yónnee. Bàkkaarkat yi, toroxte dal na leen tukke fa Yàlla ak mbugal mu tar ngir pexe [yu bon ya ñu daan nas].
125فَمَن يُرِدِ اللَّهُ أَن يَهْدِيَهُ يَشْرَحْ صَدْرَهُ لِلْإِسْلَامِ ۖ وَمَن يُرِدْ أَن يُضِلَّهُ يَجْعَلْ صَدْرَهُ ضَيِّقًا حَرَجًا كَأَنَّمَا يَصَّعَّدُ فِي السَّمَاءِ ۚ كَذَٰلِكَ يَجْعَلُ اللَّهُ الرِّجْسَ عَلَى الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ
Ku Yàlla bëgg a jubal, dafay ubbi xolam ci Lislaam. Ku Mu bëgg a bàyyi cig réeram, day bàyyi xolam nekk cig xat gu tar ba mel ni day yéeg jëm kaw asamaan. Noonu la Yàlla di tege mbugal ña gëmul.
126وَهَٰذَا صِرَاطُ رَبِّكَ مُسْتَقِيمًا ۗ قَدْ فَصَّلْنَا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَذَّكَّرُونَ
Lile mooy sa yoonu Boroom wu jub xocc wa. Leeralal Nanu Sunuy tegtal nit ñuy fàttaliku [seen Boroom].
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
124Aaya

Tekki — Al-An'am 124

Simoore Al-An'am Aaya 124 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te ñoom, saa su leen laaya dikkalee, ñuy wax naan…

Simoore Aaya 124/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 122–126. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers