Al-An'am · 130/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
يَا مَعْشَرَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ أَلَمْ يَأْتِكُمْ رُسُلٌ مِّنكُمْ يَقُصُّونَ عَلَيْكُمْ آيَاتِي وَيُنذِرُونَكُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا ۚ قَالُوا شَهِدْنَا عَلَىٰ أَنفُسِنَا ۖ وَغَرَّتْهُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا وَشَهِدُوا عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ أَنَّهُمْ كَانُوا كَافِرِينَ ۝١٣٠
Yaa ma`sharal jinni wal insi alam yaatikum Rusulum minkum yaqussoona `alaikum Aayaatee wa yunziroonakum liqaaa`a Yawmikum haazaa; qaaloo shahidnaa `alaaa anfusinaa wa gharrat humul hayaatud dunyaa wa shahidooo `alaa anfusihim annahum kaanoo kaafireen
📖 Tekkim Wolof
[Mu ne leen] Éy yéen mbooloom jinne yi ak nit ñi ndax ay Yonent dafa leen a dikkalul woon, feeñ ci seen biir, di leen nettali Samay ndigal ci doon leen waar ci ndajem seen Bis bii ? Ñu toontu ne : “Seede nanu loolu mu nekk ci sunu kaw.”. Dundug àddina wor na leen ; seeni seede dal ci seen kaw, saxal ne ñoom ay yéefar lañu woon.

🎧 Dégg


📜 Aaya 128-132 — Al-An'am

128وَيَوْمَ يَحْشُرُهُمْ جَمِيعًا يَا مَعْشَرَ الْجِنِّ قَدِ اسْتَكْثَرْتُم مِّنَ الْإِنسِ ۖ وَقَالَ أَوْلِيَاؤُهُم مِّنَ الْإِنسِ رَبَّنَا اسْتَمْتَعَ بَعْضُنَا بِبَعْضٍ وَبَلَغْنَا أَجَلَنَا الَّذِي أَجَّلْتَ لَنَا ۚ قَالَ النَّارُ مَثْوَاكُمْ خَالِدِينَ فِيهَا إِلَّا مَا شَاءَ اللَّهُ ۗ إِنَّ رَبَّكَ حَكِيمٌ عَلِيمٌ
Bis ba Mu leen di dajale [Yàlla] ñoom ñépp, di leen wax ne : "Éy yéen mboolooy jinne yi, baril ngeen seeni jëf ci nit ñi”. Nit ña ñu méngool ne : "Sunu Boroom, lenn ci nun, daanañu sàkku xéewlu ca ñeneen ña, te agsi nañu ca àpp ba Nga nu àppaloon.”. Mu ne leen : “Safaraay seen dëkkuwaay, te dangeen fay sax dàkk, lu dul la soob Yàlla.”. Sa Boroom dey Ku xereñ, Ku xam la.
129وَكَذَٰلِكَ نُوَلِّي بَعْضَ الظَّالِمِينَ بَعْضًا بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Noonu Lanuy feeñale kiliftéefu yenn tooñkat ya ca kaw ñeneen ña ngir la ñu nekkoon di ko fàggu.
130يَا مَعْشَرَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ أَلَمْ يَأْتِكُمْ رُسُلٌ مِّنكُمْ يَقُصُّونَ عَلَيْكُمْ آيَاتِي وَيُنذِرُونَكُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا ۚ قَالُوا شَهِدْنَا عَلَىٰ أَنفُسِنَا ۖ وَغَرَّتْهُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا وَشَهِدُوا عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ أَنَّهُمْ كَانُوا كَافِرِينَ
[Mu ne leen] Éy yéen mbooloom jinne yi ak nit ñi ndax ay Yonent dafa leen a dikkalul woon, feeñ ci seen biir, di leen nettali Samay ndigal ci doon leen waar ci ndajem seen Bis bii ? Ñu toontu ne : “Seede nanu loolu mu nekk ci sunu kaw.”. Dundug àddina wor na leen ; seeni seede dal ci seen kaw, saxal ne ñoom ay yéefar lañu woon.
131ذَٰلِكَ أَن لَّمْ يَكُن رَّبُّكَ مُهْلِكَ الْقُرَىٰ بِظُلْمٍ وَأَهْلُهَا غَافِلُونَ
Loolu dafay tegtale ne sa Boroom du alag ab dëkk cig tooñeel ndare dafa yónni ndaw ñu lànk koo topp.
132وَلِكُلٍّ دَرَجَاتٌ مِّمَّا عَمِلُوا ۚ وَمَا رَبُّكَ بِغَافِلٍ عَمَّا يَعْمَلُونَ
Ñoom ñépp danañu am pey gu méngook la ñu jëfoon. Sa Boroom ñàkkul paal ca la ñuy jëf.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
130Aaya

Tekki — Al-An'am 130

Simoore Al-An'am Aaya 130 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Mu ne leen] Éy yéen mbooloom jinne yi ak nit…

Simoore Aaya 130/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 128–132. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers