Al-A'raf · 158/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
قُلْ يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُمْ جَمِيعًا الَّذِي لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ يُحْيِي وَيُمِيتُ ۖ فَآمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ النَّبِيِّ الْأُمِّيِّ الَّذِي يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَكَلِمَاتِهِ وَاتَّبِعُوهُ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ ۝١٥٨
Qul yaaa aiyuhan naasu innee Rasoohul laahi ilaikum jamee`anil lazee lahoo mulkus samaawaati wal ardi laaa ilaaha illaa Huwa yuhyee wa yumeetu fa aaminoo billaahi wa Rasoolihin Nabiyyil ummiy yil lazee yu`minu billaahi wa Kalimaatihee wattabi`oohu la`allakum tahtadoon
📖 Tekkim Wolof
Neeleen : "Yéen nit ñi ! Man Yonentub Yàlla laa ci yéen ñépp, Moom mi nga xam ne Moo moom nguuru asamaan yi ak suuf si. Amul jeneen yàlla ju dul Moom. Mooy dundal, Mooy rey. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam bi, di ku ñu soloo te jàngul, te moom gëm na Yàlla ak ug kàddoom. Kon toppleen ko, xéy-na kon ngeen gindiku”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 156-160 — Al-A'raf

156۞ وَاكْتُبْ لَنَا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ إِنَّا هُدْنَا إِلَيْكَ ۚ قَالَ عَذَابِي أُصِيبُ بِهِ مَنْ أَشَاءُ ۖ وَرَحْمَتِي وَسِعَتْ كُلَّ شَيْءٍ ۚ فَسَأَكْتُبُهَا لِلَّذِينَ يَتَّقُونَ وَيُؤْتُونَ الزَّكَاةَ وَالَّذِينَ هُم بِآيَاتِنَا يُؤْمِنُونَ
Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun gindiku nanu jëm ci Yaw.”. Mu ne : “Sama mbugal, danaa ko sadd ku Ma neex. Waaye Sama yërmaande ëmb na lépp lenn. Te danaa ko sadd ña ragal Yàlla tey génne asaka ak ñi gëm Samay kàddu.
157الَّذِينَ يَتَّبِعُونَ الرَّسُولَ النَّبِيَّ الْأُمِّيَّ الَّذِي يَجِدُونَهُ مَكْتُوبًا عِندَهُمْ فِي التَّوْرَاةِ وَالْإِنجِيلِ يَأْمُرُهُم بِالْمَعْرُوفِ وَيَنْهَاهُمْ عَنِ الْمُنكَرِ وَيُحِلُّ لَهُمُ الطَّيِّبَاتِ وَيُحَرِّمُ عَلَيْهِمُ الْخَبَائِثَ وَيَضَعُ عَنْهُمْ إِصْرَهُمْ وَالْأَغْلَالَ الَّتِي كَانَتْ عَلَيْهِمْ ۚ فَالَّذِينَ آمَنُوا بِهِ وَعَزَّرُوهُ وَنَصَرُوهُ وَاتَّبَعُوا النُّورَ الَّذِي أُنزِلَ مَعَهُ ۙ أُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ
Ña nga xam ne danañu topp Yonent ba, di ku ñu soloo te jàngul, te ñu fekk ñu bind ko ca ya ñu yore ci Tawreet ak Injiil. Mu di leen digal lu baax, di leen tere lu bon, daganal leen yu sell ya, araamal ca ñoom yu selladi ya, soppil leen ya leen diisoon ak gàkk ya nekkoon ca ñoom. Kon ñi ko gëm [moom Muhammad] te weg ko, te ñu topp leer ga Nu wàcce ci moom; ñoom ñooy way-texe ña.
158قُلْ يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنِّي رَسُولُ اللَّهِ إِلَيْكُمْ جَمِيعًا الَّذِي لَهُ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ يُحْيِي وَيُمِيتُ ۖ فَآمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ النَّبِيِّ الْأُمِّيِّ الَّذِي يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَكَلِمَاتِهِ وَاتَّبِعُوهُ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
Neeleen : "Yéen nit ñi ! Man Yonentub Yàlla laa ci yéen ñépp, Moom mi nga xam ne Moo moom nguuru asamaan yi ak suuf si. Amul jeneen yàlla ju dul Moom. Mooy dundal, Mooy rey. Kon gëmleen Yàlla ak Yonentam bi, di ku ñu soloo te jàngul, te moom gëm na Yàlla ak ug kàddoom. Kon toppleen ko, xéy-na kon ngeen gindiku”.
159وَمِن قَوْمِ مُوسَىٰ أُمَّةٌ يَهْدُونَ بِالْحَقِّ وَبِهِ يَعْدِلُونَ
Amoon na ci nitu Muusaa, mbooloo muy gindee ci dëgg ak di ca tegtaloo ci maandute.
160وَقَطَّعْنَاهُمُ اثْنَتَيْ عَشْرَةَ أَسْبَاطًا أُمَمًا ۚ وَأَوْحَيْنَا إِلَىٰ مُوسَىٰ إِذِ اسْتَسْقَاهُ قَوْمُهُ أَنِ اضْرِب بِّعَصَاكَ الْحَجَرَ ۖ فَانبَجَسَتْ مِنْهُ اثْنَتَا عَشْرَةَ عَيْنًا ۖ قَدْ عَلِمَ كُلُّ أُنَاسٍ مَّشْرَبَهُمْ ۚ وَظَلَّلْنَا عَلَيْهِمُ الْغَمَامَ وَأَنزَلْنَا عَلَيْهِمُ الْمَنَّ وَالسَّلْوَىٰ ۖ كُلُوا مِن طَيِّبَاتِ مَا رَزَقْنَاكُمْ ۚ وَمَا ظَلَمُونَا وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Nu xaaj leen fukki giir ak ñaar ñuy ay xeet. Ba noppi, Nu soloo Muusaa, ba ñuy sàkku lu ñu naan, ne ko : “Dóoral xeer wi ak sa yet wi.”. Noonu fukki bëti ndox ak ñaar balle ca. Ku nekk ca ñoom xamee fa muy naane. Nu defal leen keppaar ak niir wa, Nu wàcceel leen lem gu weex ak i njanaaw, ne leen : “Lekkleen ci yu sell yi Nu leen wërsëgale.”. Waaye tooñuñu Nu, seen bopp rekk lañuy tooñ.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
158Aaya

Tekki — Al-A'raf 158

Simoore Al-A'raf Aaya 158 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neeleen : "Yéen nit ñi ! Man Yonentub Yàlla laa…

Simoore Aaya 158/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 156–160. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers