Al-A'raf · 187/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
يَسْأَلُونَكَ عَنِ السَّاعَةِ أَيَّانَ مُرْسَاهَا ۖ قُلْ إِنَّمَا عِلْمُهَا عِندَ رَبِّي ۖ لَا يُجَلِّيهَا لِوَقْتِهَا إِلَّا هُوَ ۚ ثَقُلَتْ فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ لَا تَأْتِيكُمْ إِلَّا بَغْتَةً ۗ يَسْأَلُونَكَ كَأَنَّكَ حَفِيٌّ عَنْهَا ۖ قُلْ إِنَّمَا عِلْمُهَا عِندَ اللَّهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ ۝١٨٧
Yas`aloonaka `anis Saa`ati aiyaana mursaahaa qul innamaa `ilmuhaa `inda Rabbee laa yujallaeehaa liwaqtihaaa illaa Hoo; saqulat fis samaawaati wal ard; laa taateekum illaa baghtah; yas`aloonaka ka annaka hafiyyun `anhaa qul innamaa `ilmuhaa `indal laahi wa laakinna aksaran naasi laa ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Ñi ngi lay laaj ci taxawaayu Bis-pénc ba : “Kañ lay doon ? ”. Neel : “Kenn amu ca xam- xam ku dul sama Boroom. Kenn du ko feeñal ca waxtoom ku dul Moom. Lu diis la ci asamaan ya ak ci suuf si, duleen digal lu dul cig mbetteel.”. Ña nga la koy laaj mel ni danga ca xam dara. Neel : “Xam-xam nekkul fenn fu dul fa Yàlla.”. Waaye lu ëpp ci nit ñi xamuñu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 185-189 — Simoore Al-A'raf

185أَوَلَمْ يَنظُرُوا فِي مَلَكُوتِ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَمَا خَلَقَ اللَّهُ مِن شَيْءٍ وَأَنْ عَسَىٰ أَن يَكُونَ قَدِ اقْتَرَبَ أَجَلُهُمْ ۖ فَبِأَيِّ حَدِيثٍ بَعْدَهُ يُؤْمِنُونَ
Moo ndax dañu dul xool nguuru asamaan yi ak suuf si, ak li Yàlla bind lépp, te it xéy-na Mu jegeñal seen àpp ? Kon jan wax gannaaw josam, lañu mën a gëm ?
186مَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَلَا هَادِيَ لَهُ ۚ وَيَذَرُهُمْ فِي طُغْيَانِهِمْ يَعْمَهُونَ
Ku Yàlla bàyyi cig réeram, kenn du la mën a gindi. Dana leen jàppe ca seen beew ga ñuy tëñax-tëñaxi.
187يَسْأَلُونَكَ عَنِ السَّاعَةِ أَيَّانَ مُرْسَاهَا ۖ قُلْ إِنَّمَا عِلْمُهَا عِندَ رَبِّي ۖ لَا يُجَلِّيهَا لِوَقْتِهَا إِلَّا هُوَ ۚ ثَقُلَتْ فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ لَا تَأْتِيكُمْ إِلَّا بَغْتَةً ۗ يَسْأَلُونَكَ كَأَنَّكَ حَفِيٌّ عَنْهَا ۖ قُلْ إِنَّمَا عِلْمُهَا عِندَ اللَّهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Ñi ngi lay laaj ci taxawaayu Bis-pénc ba : “Kañ lay doon ? ”. Neel : “Kenn amu ca xam- xam ku dul sama Boroom. Kenn du ko feeñal ca waxtoom ku dul Moom. Lu diis la ci asamaan ya ak ci suuf si, duleen digal lu dul cig mbetteel.”. Ña nga la koy laaj mel ni danga ca xam dara. Neel : “Xam-xam nekkul fenn fu dul fa Yàlla.”. Waaye lu ëpp ci nit ñi xamuñu.
188قُل لَّا أَمْلِكُ لِنَفْسِي نَفْعًا وَلَا ضَرًّا إِلَّا مَا شَاءَ اللَّهُ ۚ وَلَوْ كُنتُ أَعْلَمُ الْغَيْبَ لَاسْتَكْثَرْتُ مِنَ الْخَيْرِ وَمَا مَسَّنِيَ السُّوءُ ۚ إِنْ أَنَا إِلَّا نَذِيرٌ وَبَشِيرٌ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Neel : “Mënaluma sama bopp njariñ walla lor lu dul la soob Yàlla. Su ma xamoon kumpa, kon ma bari lool alal ak i xéewal, te kon lu metti duma dal. Nekkuma man lu dul waarekat, béglekatu nit ñi gëm Yàlla”.
189۞ هُوَ الَّذِي خَلَقَكُم مِّن نَّفْسٍ وَاحِدَةٍ وَجَعَلَ مِنْهَا زَوْجَهَا لِيَسْكُنَ إِلَيْهَا ۖ فَلَمَّا تَغَشَّاهَا حَمَلَتْ حَمْلًا خَفِيفًا فَمَرَّتْ بِهِ ۖ فَلَمَّا أَثْقَلَت دَّعَوَا اللَّهَ رَبَّهُمَا لَئِنْ آتَيْتَنَا صَالِحًا لَّنَكُونَنَّ مِنَ الشَّاكِرِينَ
Moom mooy Ki leen bind ci benn bakkan, mu génne ca soxnaam ngir muy am ug dal ci moom; ba mu ko muuree, mu ëmb ëmb bu woyof, muy dem ak ëmbam. Ba mu diisee, ñoom ñaar ñu ñaanYàlla seen Boroom ne ko : “Soo nu mayee [doom] ju baax, kon faf dananu bokk ci gërëmaakoon ña”.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
187Aaya

Tekki — Al-A'raf 187

Simoore Al-A'raf Aaya 187 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñi ngi lay laaj ci taxawaayu Bis-pénc ba : “Kañ…

Simoore Aaya 187/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 185–189. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers