Al-A'raf · 87/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَإِن كَانَ طَائِفَةٌ مِّنكُمْ آمَنُوا بِالَّذِي أُرْسِلْتُ بِهِ وَطَائِفَةٌ لَّمْ يُؤْمِنُوا فَاصْبِرُوا حَتَّىٰ يَحْكُمَ اللَّهُ بَيْنَنَا ۚ وَهُوَ خَيْرُ الْحَاكِمِينَ ۝٨٧
Wa In kaana taaa`ifatum minkum aamanoo billazeee ursiltu bihee wa taaa`ifatul lam yu`minoo fasbiroo hattaa yahkumual laahu bainanaa; wa Huwa khairul haakimeen
📖 Tekkim Wolof
Su fekkee am na ci yéen kurél bu gëm li ñu ma yónni, ak kurél bu goreedi, nangeen muñ ba ba Yàlla di àtte seenu diggante, te Moom (Yàlla) moo di gën jaa mën a àtte.”
🎧 Dégg

📜 Aaya 85-89 — Al-A'raf

85وَإِلَىٰ مَدْيَنَ أَخَاهُمْ شُعَيْبًا ۗ قَالَ يَا قَوْمِ اعْبُدُوا اللَّهَ مَا لَكُم مِّنْ إِلَٰهٍ غَيْرُهُ ۖ قَدْ جَاءَتْكُم بَيِّنَةٌ مِّن رَّبِّكُمْ ۖ فَأَوْفُوا الْكَيْلَ وَالْمِيزَانَ وَلَا تَبْخَسُوا النَّاسَ أَشْيَاءَهُمْ وَلَا تُفْسِدُوا فِي الْأَرْضِ بَعْدَ إِصْلَاحِهَا ۚ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
(Fàttalikul ba Nu yónnee) fa Madyaana, seen mbokk Chuhaybu, mu ne leen : "Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Te ay lay yu leer dikkal na leen yu bawoo ca seen Boroom. Kon nangeen di matal natt ak màndaxe te buleen wàññil nit ña, la ñu moom. Te it buleen yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Loolu dey, moo di li gën ci yéen, bu fekkee ni gëm ngeen.
86وَلَا تَقْعُدُوا بِكُلِّ صِرَاطٍ تُوعِدُونَ وَتَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ مَنْ آمَنَ بِهِ وَتَبْغُونَهَا عِوَجًا ۚ وَاذْكُرُوا إِذْ كُنتُمْ قَلِيلًا فَكَثَّرَكُمْ ۖ وَانظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُفْسِدِينَ
Te buleen di toog ci wépp yoon, di dëkku ñi gëm Yàlla, di leen wëlbati, di dox seen digganteek yoonu Yàlla, di ko jéngal. Fàttalikuleen ba ngeen nekkee di ñu néew, Mu baril leen. Te nangeen settantal naka la mujjug yàqkat ya meloon.
87وَإِن كَانَ طَائِفَةٌ مِّنكُمْ آمَنُوا بِالَّذِي أُرْسِلْتُ بِهِ وَطَائِفَةٌ لَّمْ يُؤْمِنُوا فَاصْبِرُوا حَتَّىٰ يَحْكُمَ اللَّهُ بَيْنَنَا ۚ وَهُوَ خَيْرُ الْحَاكِمِينَ
Su fekkee am na ci yéen kurél bu gëm li ñu ma yónni, ak kurél bu goreedi, nangeen muñ ba ba Yàlla di àtte seenu diggante, te Moom (Yàlla) moo di gën jaa mën a àtte.”
88۞ قَالَ الْمَلَأُ الَّذِينَ اسْتَكْبَرُوا مِن قَوْمِهِ لَنُخْرِجَنَّكَ يَا شُعَيْبُ وَالَّذِينَ آمَنُوا مَعَكَ مِن قَرْيَتِنَا أَوْ لَتَعُودُنَّ فِي مِلَّتِنَا ۚ قَالَ أَوَلَوْ كُنَّا كَارِهِينَ
Kilifa, ya rëy-rëylu ca aw nitam, ne ko : “Dananu la génne, yaw Chuhaybu ak ña gëm ànd ak yaw, ci sunum réew. Walla nga dellusi ci sunu diine.” - Mu ne leen : “Ba bu fekkee ne sax dangeen nuy ga [ci seen diine jooju] ? ”.
89قَدِ افْتَرَيْنَا عَلَى اللَّهِ كَذِبًا إِنْ عُدْنَا فِي مِلَّتِكُم بَعْدَ إِذْ نَجَّانَا اللَّهُ مِنْهَا ۚ وَمَا يَكُونُ لَنَا أَن نَّعُودَ فِيهَا إِلَّا أَن يَشَاءَ اللَّهُ رَبُّنَا ۚ وَسِعَ رَبُّنَا كُلَّ شَيْءٍ عِلْمًا ۚ عَلَى اللَّهِ تَوَكَّلْنَا ۚ رَبَّنَا افْتَحْ بَيْنَنَا وَبَيْنَ قَوْمِنَا بِالْحَقِّ وَأَنتَ خَيْرُ الْفَاتِحِينَ
“Bu nu delloo dugg ci seen diine, kon de nu duural Yàlla aw fen gannaaw ba nu Yàlla musalee ci seen diine jooju. Dunu mën a dellu duggu ci lu dul mu soob Yàlla sunu Boroom. Xam-xamu sunu Boroom ump na lu nekk. Ci Yàlla lanuy wéeru. Yaw sunu Boroom, àtteel sunu diggante ak sunuy nit, ci dëgg, ndaxte Yaw [Yàlla], yaa gën a mën àtte àttekat yi.”
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
87Aaya

Tekki — Al-A'raf 87

Simoore Al-A'raf Aaya 87 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Su fekkee am na ci yéen kurél bu gëm li…

Simoore Aaya 87/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 85–89. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers