Hud · 11/123
Tekki Waxtaan — Hud
إِلَّا الَّذِينَ صَبَرُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ أُولَٰئِكَ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ كَبِيرٌ ۝١١
Illal lazeena sabaroo wa `amilus saalihaati ulaaa`ika lahum maghfiratunw wa ajrun kabeer
📖 Tekkim Wolof
ba mu des ña nga xam ne dañoo muñ, di jëf jëf yu sell. Ñoom ñooña am nañu njéggal ak pey gu mag.
🎧 Dégg

📜 Aaya 9-13 — Hud

9وَلَئِنْ أَذَقْنَا الْإِنسَانَ مِنَّا رَحْمَةً ثُمَّ نَزَعْنَاهَا مِنْهُ إِنَّهُ لَيَئُوسٌ كَفُورٌ
Te wóor na it ne, su Nu mosaloon nit lenn ci Sunu yërmaande, ba noppi Nu nangu ko ci moom, kon dey dana nekk di ku ñàkk yaakaar ak fakk (sunuy xéewal).
10وَلَئِنْ أَذَقْنَاهُ نَعْمَاءَ بَعْدَ ضَرَّاءَ مَسَّتْهُ لَيَقُولَنَّ ذَهَبَ السَّيِّئَاتُ عَنِّي ۚ إِنَّهُ لَفَرِحٌ فَخُورٌ
Te wóor na it ne, su Nu ko mosalee xéewal ginnaaw naqar wa ko daloon, dana wax ne : “Tiis teggeeku na ma”, Moom [nit] kuy bég la, di puukarewaakon.
11إِلَّا الَّذِينَ صَبَرُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ أُولَٰئِكَ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ كَبِيرٌ
ba mu des ña nga xam ne dañoo muñ, di jëf jëf yu sell. Ñoom ñooña am nañu njéggal ak pey gu mag.
12فَلَعَلَّكَ تَارِكٌ بَعْضَ مَا يُوحَىٰ إِلَيْكَ وَضَائِقٌ بِهِ صَدْرُكَ أَن يَقُولُوا لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْهِ كَنزٌ أَوْ جَاءَ مَعَهُ مَلَكٌ ۚ إِنَّمَا أَنتَ نَذِيرٌ ۚ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ وَكِيلٌ
Xéy-na danga bàyyi lenn ca la Nu la soloo, nga ànd ci ak xol bu xat ; ngir la ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcceel ko ndàmbul alal ? ”. Walla : “Mu dikk ànd ak i Malaaka ? ” - Waaye yaw nekkuloo lu dul waarekat. Yàlla nag mooy Kuy wattu lépp lu mu mën a doon.
13أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۖ قُلْ فَأْتُوا بِعَشْرِ سُوَرٍ مِّثْلِهِ مُفْتَرَيَاتٍ وَادْعُوا مَنِ اسْتَطَعْتُم مِّن دُونِ اللَّهِ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Am dañuy wax ne : “Dakoo duur” - Neel : “Indileen fukki saar yu ni mel, yu ngeen fent. Te ngeen woo ku leen neex ndeem ñu dëggu ngeen”.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
11Aaya

Tekki — Hud 11

Simoore Hud Aaya 11 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ba mu des ña nga xam ne dañoo muñ, di…

Simoore Aaya 11/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 9–13. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers