Hud · 10/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَلَئِنْ أَذَقْنَاهُ نَعْمَاءَ بَعْدَ ضَرَّاءَ مَسَّتْهُ لَيَقُولَنَّ ذَهَبَ السَّيِّئَاتُ عَنِّي ۚ إِنَّهُ لَفَرِحٌ فَخُورٌ ۝١٠
Wala`in azaqnaahu na`maaa`a ba`da darraaa`a massat hu la yaqoolanna zahabas saiyiaatu `anneee; innahoo lafarihun fakhoor
📖 Tekkim Wolof
Te wóor na it ne, su Nu ko mosalee xéewal ginnaaw naqar wa ko daloon, dana wax ne : “Tiis teggeeku na ma”, Moom [nit] kuy bég la, di puukarewaakon.
🎧 Dégg

📜 Aaya 8-12 — Hud

8وَلَئِنْ أَخَّرْنَا عَنْهُمُ الْعَذَابَ إِلَىٰ أُمَّةٍ مَّعْدُودَةٍ لَّيَقُولُنَّ مَا يَحْبِسُهُ ۗ أَلَا يَوْمَ يَأْتِيهِمْ لَيْسَ مَصْرُوفًا عَنْهُمْ وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ
Te wóor na it ne su Nu yéexalee ci ñoom mbugal ma, jëme ko ca waxtu wu ñu dogal àppam, fàwwu danañu ne : “Lan moo ko téye ? - Te bis ba muy agsi ci ñoom, ndax dana nekk lu kenn dul mën a jiñ; te la ñu daan yéjj dana wàcc ci seen kaw.
9وَلَئِنْ أَذَقْنَا الْإِنسَانَ مِنَّا رَحْمَةً ثُمَّ نَزَعْنَاهَا مِنْهُ إِنَّهُ لَيَئُوسٌ كَفُورٌ
Te wóor na it ne, su Nu mosaloon nit lenn ci Sunu yërmaande, ba noppi Nu nangu ko ci moom, kon dey dana nekk di ku ñàkk yaakaar ak fakk (sunuy xéewal).
10وَلَئِنْ أَذَقْنَاهُ نَعْمَاءَ بَعْدَ ضَرَّاءَ مَسَّتْهُ لَيَقُولَنَّ ذَهَبَ السَّيِّئَاتُ عَنِّي ۚ إِنَّهُ لَفَرِحٌ فَخُورٌ
Te wóor na it ne, su Nu ko mosalee xéewal ginnaaw naqar wa ko daloon, dana wax ne : “Tiis teggeeku na ma”, Moom [nit] kuy bég la, di puukarewaakon.
11إِلَّا الَّذِينَ صَبَرُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ أُولَٰئِكَ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ كَبِيرٌ
ba mu des ña nga xam ne dañoo muñ, di jëf jëf yu sell. Ñoom ñooña am nañu njéggal ak pey gu mag.
12فَلَعَلَّكَ تَارِكٌ بَعْضَ مَا يُوحَىٰ إِلَيْكَ وَضَائِقٌ بِهِ صَدْرُكَ أَن يَقُولُوا لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْهِ كَنزٌ أَوْ جَاءَ مَعَهُ مَلَكٌ ۚ إِنَّمَا أَنتَ نَذِيرٌ ۚ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ وَكِيلٌ
Xéy-na danga bàyyi lenn ca la Nu la soloo, nga ànd ci ak xol bu xat ; ngir la ñuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcceel ko ndàmbul alal ? ”. Walla : “Mu dikk ànd ak i Malaaka ? ” - Waaye yaw nekkuloo lu dul waarekat. Yàlla nag mooy Kuy wattu lépp lu mu mën a doon.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
10Aaya

Tekki — Hud 10

Simoore Hud Aaya 10 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te wóor na it ne, su Nu ko mosalee xéewal…

Simoore Aaya 10/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 8–12. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers