Yusuf · 44/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
قَالُوا أَضْغَاثُ أَحْلَامٍ ۖ وَمَا نَحْنُ بِتَأْوِيلِ الْأَحْلَامِ بِعَالِمِينَ ۝٤٤
Qaalooo adghaasu ahlaa minw wa maa nahnu bitaaweelil ahlaami bi`aalimeen
📖 Tekkim Wolof
Ñu ne : “Gént yooyu jaxasoo nañu ! Te sax nun xamunu pirim gént ! ”

🎧 Dégg


📜 Aaya 42-46 — Yusuf

42وَقَالَ لِلَّذِي ظَنَّ أَنَّهُ نَاجٍ مِّنْهُمَا اذْكُرْنِي عِندَ رَبِّكَ فَأَنسَاهُ الشَّيْطَانُ ذِكْرَ رَبِّهِ فَلَبِثَ فِي السِّجْنِ بِضْعَ سِنِينَ
Yuusufa wax ka nga xam ne yaakaar na ne dana mucc ca ñoom ñaar, ne ko : “Nanga fexe ba buur fàttaliku ma”. Waaye Séytaane fàtteloo na ko [yóbbante boobu] ba fàttaliwu ko buur ba [ba mu delloo ca moom]. Ba tax mu toog ca kaso ba ay at .
43وَقَالَ الْمَلِكُ إِنِّي أَرَىٰ سَبْعَ بَقَرَاتٍ سِمَانٍ يَأْكُلُهُنَّ سَبْعٌ عِجَافٌ وَسَبْعَ سُنبُلَاتٍ خُضْرٍ وَأُخَرَ يَابِسَاتٍ ۖ يَا أَيُّهَا الْمَلَأُ أَفْتُونِي فِي رُؤْيَايَ إِن كُنتُمْ لِلرُّؤْيَا تَعْبُرُونَ
Buur ba wax ne : “Gént naa juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom-ñaari nag yu loof di lekk ; ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow. Yéen njiit yi, firil-leen ma sama gént gii, ndegam mën ngeen firi gént”.
44قَالُوا أَضْغَاثُ أَحْلَامٍ ۖ وَمَا نَحْنُ بِتَأْوِيلِ الْأَحْلَامِ بِعَالِمِينَ
Ñu ne : “Gént yooyu jaxasoo nañu ! Te sax nun xamunu pirim gént ! ”
45وَقَالَ الَّذِي نَجَا مِنْهُمَا وَادَّكَرَ بَعْدَ أُمَّةٍ أَنَا أُنَبِّئُكُم بِتَأْوِيلِهِ فَأَرْسِلُونِ
Ka muccoon ca ñoom daldi fàttaliku ginnaaw ab diir, daldi wax ne : “Danaa leen leeralal. Yebal-leen ma, Dinaa leen indil am pireem”.
46يُوسُفُ أَيُّهَا الصِّدِّيقُ أَفْتِنَا فِي سَبْعِ بَقَرَاتٍ سِمَانٍ يَأْكُلُهُنَّ سَبْعٌ عِجَافٌ وَسَبْعِ سُنبُلَاتٍ خُضْرٍ وَأُخَرَ يَابِسَاتٍ لَّعَلِّي أَرْجِعُ إِلَى النَّاسِ لَعَلَّهُمْ يَعْلَمُونَ
[Mu dem ca Yuusufa] ne ko : “Yaw waxkatu dëgg ! Ubbee ma ci juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom-ñaari nag yu loof di lekk, ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow, ndax xéy-na su ma delluwaatee nit ña am ci xam-xam”.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
44Aaya

Tekki — Yusuf 44

Simoore Yusuf Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu ne : “Gént yooyu jaxasoo nañu ! Te sax…

Simoore Aaya 44/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers