Yusuf · 43/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
وَقَالَ الْمَلِكُ إِنِّي أَرَىٰ سَبْعَ بَقَرَاتٍ سِمَانٍ يَأْكُلُهُنَّ سَبْعٌ عِجَافٌ وَسَبْعَ سُنبُلَاتٍ خُضْرٍ وَأُخَرَ يَابِسَاتٍ ۖ يَا أَيُّهَا الْمَلَأُ أَفْتُونِي فِي رُؤْيَايَ إِن كُنتُمْ لِلرُّؤْيَا تَعْبُرُونَ ۝٤٣
Wa qaalal maliku inneee araa sab`a baqaraatin simaaniny yaakuluhunna sab`un `ijaafunw wa sab`a sumbulaatinkhudrinw wa ukhara yaabisaat; yaaa ayuhal mala-u aftoonee fee nu`yaaya in kuntum lirru`yaa ta`buroon
📖 Tekkim Wolof
Buur ba wax ne : “Gént naa juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom-ñaari nag yu loof di lekk ; ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow. Yéen njiit yi, firil-leen ma sama gént gii, ndegam mën ngeen firi gént”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 41-45 — Yusuf

41يَا صَاحِبَيِ السِّجْنِ أَمَّا أَحَدُكُمَا فَيَسْقِي رَبَّهُ خَمْرًا ۖ وَأَمَّا الْآخَرُ فَيُصْلَبُ فَتَأْكُلُ الطَّيْرُ مِن رَّأْسِهِ ۚ قُضِيَ الْأَمْرُ الَّذِي فِيهِ تَسْتَفْتِيَانِ
Yéen sama ñaari àndandooy kaso ! Kenn ci yéen dana nekk kuy màndal buuram sàngara ; ka ca des, danañu ko daaj ci bant, ay picc di lekk ci boppam. Dogaleef na noonu mbir ya ngeen doon laaj.”
42وَقَالَ لِلَّذِي ظَنَّ أَنَّهُ نَاجٍ مِّنْهُمَا اذْكُرْنِي عِندَ رَبِّكَ فَأَنسَاهُ الشَّيْطَانُ ذِكْرَ رَبِّهِ فَلَبِثَ فِي السِّجْنِ بِضْعَ سِنِينَ
Yuusufa wax ka nga xam ne yaakaar na ne dana mucc ca ñoom ñaar, ne ko : “Nanga fexe ba buur fàttaliku ma”. Waaye Séytaane fàtteloo na ko [yóbbante boobu] ba fàttaliwu ko buur ba [ba mu delloo ca moom]. Ba tax mu toog ca kaso ba ay at .
43وَقَالَ الْمَلِكُ إِنِّي أَرَىٰ سَبْعَ بَقَرَاتٍ سِمَانٍ يَأْكُلُهُنَّ سَبْعٌ عِجَافٌ وَسَبْعَ سُنبُلَاتٍ خُضْرٍ وَأُخَرَ يَابِسَاتٍ ۖ يَا أَيُّهَا الْمَلَأُ أَفْتُونِي فِي رُؤْيَايَ إِن كُنتُمْ لِلرُّؤْيَا تَعْبُرُونَ
Buur ba wax ne : “Gént naa juróom-ñaari nag yu duuf yu juróom-ñaari nag yu loof di lekk ; ak juróom-ñaari gub yu nëtëx ak yeneen yu wow. Yéen njiit yi, firil-leen ma sama gént gii, ndegam mën ngeen firi gént”.
44قَالُوا أَضْغَاثُ أَحْلَامٍ ۖ وَمَا نَحْنُ بِتَأْوِيلِ الْأَحْلَامِ بِعَالِمِينَ
Ñu ne : “Gént yooyu jaxasoo nañu ! Te sax nun xamunu pirim gént ! ”
45وَقَالَ الَّذِي نَجَا مِنْهُمَا وَادَّكَرَ بَعْدَ أُمَّةٍ أَنَا أُنَبِّئُكُم بِتَأْوِيلِهِ فَأَرْسِلُونِ
Ka muccoon ca ñoom daldi fàttaliku ginnaaw ab diir, daldi wax ne : “Danaa leen leeralal. Yebal-leen ma, Dinaa leen indil am pireem”.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
43Aaya

Tekki — Yusuf 43

Simoore Yusuf Aaya 43 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Buur ba wax ne : “Gént naa juróom-ñaari nag yu…

Simoore Aaya 43/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 41–45. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers