Ar-Ra'd · 21/43
Tekki Waxtaan — Ar-Ra'd
وَالَّذِينَ يَصِلُونَ مَا أَمَرَ اللَّهُ بِهِ أَن يُوصَلَ وَيَخْشَوْنَ رَبَّهُمْ وَيَخَافُونَ سُوءَ الْحِسَابِ ۝٢١
Wallazeena yasiloona maaa amaral laahu bihee an yoosala wa yakhshawna Rabbahum wa yakhaafoona sooo`al hisaab
📖 Tekkim Wolof
ak ñay jokk la Yàlla santaane ñu jokk ko [mooy mbokk], te ragal nañu seen Boroom, di ragal it [ca àllaaxira] natt bu bon [seen jëf yu ñaaw ëpp seen jëf yu baax],

🎧 Dégg


📜 Aaya 19-23 — Ar-Ra'd

19۞ أَفَمَن يَعْلَمُ أَنَّمَا أُنزِلَ إِلَيْكَ مِن رَّبِّكَ الْحَقُّ كَمَنْ هُوَ أَعْمَىٰ ۚ إِنَّمَا يَتَذَكَّرُ أُولُو الْأَلْبَابِ
Moo ndax koo xam ne la ñu wàcce ci yaw mu jóge ca sa Boroom dëgg, mel na ne ka nga xam ne gumba la ? Woroom xel yi rekk ñooy waaru,
20الَّذِينَ يُوفُونَ بِعَهْدِ اللَّهِ وَلَا يَنقُضُونَ الْمِيثَاقَ
ñooy ñay matal seen kóllare ak Yàlla te duñu firi kóllare googu,
21وَالَّذِينَ يَصِلُونَ مَا أَمَرَ اللَّهُ بِهِ أَن يُوصَلَ وَيَخْشَوْنَ رَبَّهُمْ وَيَخَافُونَ سُوءَ الْحِسَابِ
ak ñay jokk la Yàlla santaane ñu jokk ko [mooy mbokk], te ragal nañu seen Boroom, di ragal it [ca àllaaxira] natt bu bon [seen jëf yu ñaaw ëpp seen jëf yu baax],
22وَالَّذِينَ صَبَرُوا ابْتِغَاءَ وَجْهِ رَبِّهِمْ وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ وَأَنفَقُوا مِمَّا رَزَقْنَاهُمْ سِرًّا وَعَلَانِيَةً وَيَدْرَءُونَ بِالْحَسَنَةِ السَّيِّئَةَ أُولَٰئِكَ لَهُمْ عُقْبَى الدَّارِ
ak ñay muñ ngir jëmmi seen Boroom, tey taxawal julli tey dundale ca la leen Yàlla wërsëgale ci la nëbbu walla ci lu feeñ, te ñuy jiñe lu ñaaw ak lu rafet. Ñooña am nañu kër gu mujj ga,
23جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا وَمَن صَلَحَ مِنْ آبَائِهِمْ وَأَزْوَاجِهِمْ وَذُرِّيَّاتِهِمْ ۖ وَالْمَلَائِكَةُ يَدْخُلُونَ عَلَيْهِم مِّن كُلِّ بَابٍ
Àjjana ju sax ja, danañu ca dugg, ak ña jëfoon lu baax ca seeni baay ak ca seeni jabar ak seeni doom ak i sët. Te Malaaka ya dañuy duggandook ñoom ci buntu yépp :
Ar-Ra'dFihi Alxuraan
43Aaya
MedinanRevelation
21Aaya

Tekki — Ar-Ra'd 21

Simoore Ar-Ra'd Aaya 21 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ak ñay jokk la Yàlla santaane ñu jokk ko [mooy…

Simoore Aaya 21/43 — Ar-Ra'd الرعد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ar-Ra'd Dégg, Ar-Ra'd Tekki, Ar-Ra'd mp3, Ar-Ra'd pdf. Aaya 19–23. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers