Al-Baqara · 214/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
أَمْ حَسِبْتُمْ أَن تَدْخُلُوا الْجَنَّةَ وَلَمَّا يَأْتِكُم مَّثَلُ الَّذِينَ خَلَوْا مِن قَبْلِكُم ۖ مَّسَّتْهُمُ الْبَأْسَاءُ وَالضَّرَّاءُ وَزُلْزِلُوا حَتَّىٰ يَقُولَ الرَّسُولُ وَالَّذِينَ آمَنُوا مَعَهُ مَتَىٰ نَصْرُ اللَّهِ ۗ أَلَا إِنَّ نَصْرَ اللَّهِ قَرِيبٌ ۝٢١٤
Am hasibtum an tadkhulul jannata wa lammaa yaa-tikum masalul lazeena khalaw min qablikum massathumul baasaaa`u waddarraaaa`u wa zulziloo hattaa yaqoolar Rasoolu wallazeena aamanoo ma`ahoo mataa nasrul laah; alaaa inna nasral laahiqareeb
📖 Tekkim Wolof
Am dangeen a jort dugg Àjjana [yéen jullit ñi] te dajuleen lu toll ni la ñi leen jiitu dajoon ? Ñoom dajoon nañu ay tar-tari jamono ak ñàkk ; ak tiitaange ba ab Yonent ak gaa ña mu àndal daanañu wax ne : “Kañ la ndimbalu Yàlla di ñëw xettali nu ? ” - Xamleen ne ndimbalu Yàlla lu jege la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 212-216 — Al-Baqara

212زُيِّنَ لِلَّذِينَ كَفَرُوا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا وَيَسْخَرُونَ مِنَ الَّذِينَ آمَنُوا ۘ وَالَّذِينَ اتَّقَوْا فَوْقَهُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ وَاللَّهُ يَرْزُقُ مَن يَشَاءُ بِغَيْرِ حِسَابٍ
Ña nga xam ne dañoo weddi, doyloo nañu dundug àddina ak ub taaram, ba tax ñuy yejji ña gëm. Waaye ña ragal Yàlla ñoo leen di gënu demiin bu Bis-pénc baa. Ndax Yàlla dana wërsëgal ku ko soob ci lu àndul ak natt.
213كَانَ النَّاسُ أُمَّةً وَاحِدَةً فَبَعَثَ اللَّهُ النَّبِيِّينَ مُبَشِّرِينَ وَمُنذِرِينَ وَأَنزَلَ مَعَهُمُ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ لِيَحْكُمَ بَيْنَ النَّاسِ فِيمَا اخْتَلَفُوا فِيهِ ۚ وَمَا اخْتَلَفَ فِيهِ إِلَّا الَّذِينَ أُوتُوهُ مِن بَعْدِ مَا جَاءَتْهُمُ الْبَيِّنَاتُ بَغْيًا بَيْنَهُمْ ۖ فَهَدَى اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا لِمَا اخْتَلَفُوا فِيهِ مِنَ الْحَقِّ بِإِذْنِهِ ۗ وَاللَّهُ يَهْدِي مَن يَشَاءُ إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Nit ñépp wenn xeet lañu woon. Yàlla yónni ay Yonent yuy bégle di xuppe ; wàcceloon na leen ay Téere ci dëgg ngir ñu àtte diggante nit ñi ci seeni bejoo. Te ña ko ca jot doŋŋ ñoo ca juuyoo, ginnaaw ba mu leeree ca ñoom nàññ, te juuyoo googu doonut lu dul mbewte ! Yàlla mooy saytu ña ko gëm, mu gindi leen ci seenug juuyoo ci dëgg. Yàlla mooy gindi ku ko soob jëme ko ci yoon wu jub xocc wa.
214أَمْ حَسِبْتُمْ أَن تَدْخُلُوا الْجَنَّةَ وَلَمَّا يَأْتِكُم مَّثَلُ الَّذِينَ خَلَوْا مِن قَبْلِكُم ۖ مَّسَّتْهُمُ الْبَأْسَاءُ وَالضَّرَّاءُ وَزُلْزِلُوا حَتَّىٰ يَقُولَ الرَّسُولُ وَالَّذِينَ آمَنُوا مَعَهُ مَتَىٰ نَصْرُ اللَّهِ ۗ أَلَا إِنَّ نَصْرَ اللَّهِ قَرِيبٌ
Am dangeen a jort dugg Àjjana [yéen jullit ñi] te dajuleen lu toll ni la ñi leen jiitu dajoon ? Ñoom dajoon nañu ay tar-tari jamono ak ñàkk ; ak tiitaange ba ab Yonent ak gaa ña mu àndal daanañu wax ne : “Kañ la ndimbalu Yàlla di ñëw xettali nu ? ” - Xamleen ne ndimbalu Yàlla lu jege la.
215يَسْأَلُونَكَ مَاذَا يُنفِقُونَ ۖ قُلْ مَا أَنفَقْتُم مِّنْ خَيْرٍ فَلِلْوَالِدَيْنِ وَالْأَقْرَبِينَ وَالْيَتَامَىٰ وَالْمَسَاكِينِ وَابْنِ السَّبِيلِ ۗ وَمَا تَفْعَلُوا مِنْ خَيْرٍ فَإِنَّ اللَّهَ بِهِ عَلِيمٌ
Danañu la laaj : “Lan lañu war a joxe ci alal ? ” - Neel : “Li ngeen di joxe na jëm ci seeni ñaari waajur, ak seeni jegeñaale, ak jirim yi, way-ñàkk ñi, ak doxandeem yi. Lu ngeen def ci lu baax, Yàlla xam na ko”.
216كُتِبَ عَلَيْكُمُ الْقِتَالُ وَهُوَ كُرْهٌ لَّكُمْ ۖ وَعَسَىٰ أَن تَكْرَهُوا شَيْئًا وَهُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ ۖ وَعَسَىٰ أَن تُحِبُّوا شَيْئًا وَهُوَ شَرٌّ لَّكُمْ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ وَأَنتُمْ لَا تَعْلَمُونَ
Farataal nañu ci yéen xare te bëgguleen ko. Amaana, ngeen bañ mbir te fekk na moo baax ci yéen. Amaana it ngeen bëgg mbir te fekk na baaxul ci yéen. Yàlla xam na te yéen xamuleen.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
214Aaya

Tekki — Al-Baqara 214

Simoore Al-Baqara Aaya 214 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am dangeen a jort dugg Àjjana [yéen jullit ñi] te…

Simoore Aaya 214/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 212–216. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers