An-Nur · 22/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
وَلَا يَأْتَلِ أُولُو الْفَضْلِ مِنكُمْ وَالسَّعَةِ أَن يُؤْتُوا أُولِي الْقُرْبَىٰ وَالْمَسَاكِينَ وَالْمُهَاجِرِينَ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۖ وَلْيَعْفُوا وَلْيَصْفَحُوا ۗ أَلَا تُحِبُّونَ أَن يَغْفِرَ اللَّهُ لَكُمْ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٢٢
Wa laa yaatali ulul fadli minkum wassa`ati ai yu`tooo ulil qurbaa walmasaakeena walmuhaajireena fee sabeelillaahi walya`foo walyasfahoo; alaa tuhibboona ai yaghfiral laahu lakum; wal laahu Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Te ña Yàlla jox wërsëg te ñu bokk ci yéen, buñu cay ñàkk a jox jegeñaale ya ak ndóol ya ak ñay gàddaay ci yoonu Yàlla. Nañuy jéggale tey jéllale. Moo xanaa bëgguleen Yàlla jéggal leen ? Yàlla dey Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la !

🎧 Dégg


📜 Aaya 20-24 — An-Nur

20وَلَوْلَا فَضْلُ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَتُهُ وَأَنَّ اللَّهَ رَءُوفٌ رَّحِيمٌ
Cëy dogankoon ak ngënéelul Yàlla ak yëmaandeem ci yéen, waaye Yàlla Moom ku ñeewant la, di Jaglewaakoon ...
21۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّبِعُوا خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ ۚ وَمَن يَتَّبِعْ خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ فَإِنَّهُ يَأْمُرُ بِالْفَحْشَاءِ وَالْمُنكَرِ ۚ وَلَوْلَا فَضْلُ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَتُهُ مَا زَكَىٰ مِنكُم مِّنْ أَحَدٍ أَبَدًا وَلَٰكِنَّ اللَّهَ يُزَكِّي مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen topp jeegoy Séytaane. Ku topp jéegoy Séytaane, [na xam ne] Séytaane ñaawtéef ak njekkar la am. Dogankoon ak ngënéelul Yàlla ak yërmaandeem, kenn ci yéen du sellal. Waaye nag Moom Yàlla mooy sellal ku Ko soob. Te Yàlla Kuy dégg la, Ku xam la.
22وَلَا يَأْتَلِ أُولُو الْفَضْلِ مِنكُمْ وَالسَّعَةِ أَن يُؤْتُوا أُولِي الْقُرْبَىٰ وَالْمَسَاكِينَ وَالْمُهَاجِرِينَ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۖ وَلْيَعْفُوا وَلْيَصْفَحُوا ۗ أَلَا تُحِبُّونَ أَن يَغْفِرَ اللَّهُ لَكُمْ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Te ña Yàlla jox wërsëg te ñu bokk ci yéen, buñu cay ñàkk a jox jegeñaale ya ak ndóol ya ak ñay gàddaay ci yoonu Yàlla. Nañuy jéggale tey jéllale. Moo xanaa bëgguleen Yàlla jéggal leen ? Yàlla dey Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la !
23إِنَّ الَّذِينَ يَرْمُونَ الْمُحْصَنَاتِ الْغَافِلَاتِ الْمُؤْمِنَاتِ لُعِنُوا فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ña nga xam ne dañuy tuumaal [njaaloo] jigéeni jullit ñi amul ay caaxaan, ña koy def danañu sori yërmaande ci àddina ak ca àllaaxira ; te it danañu am mbugal mu metti,
24يَوْمَ تَشْهَدُ عَلَيْهِمْ أَلْسِنَتُهُمْ وَأَيْدِيهِمْ وَأَرْجُلُهُم بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Bu keroogee [Bis-pénc ba], seen làmmiñ ya, seeni yoxo ak seeni tànk danañu seede ci seen kaw la ñu daan def.
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
22Aaya

Tekki — An-Nur 22

Simoore An-Nur Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te ña Yàlla jox wërsëg te ñu bokk ci yéen,…

Simoore Aaya 22/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers