An-Nur · 23/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
إِنَّ الَّذِينَ يَرْمُونَ الْمُحْصَنَاتِ الْغَافِلَاتِ الْمُؤْمِنَاتِ لُعِنُوا فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ ۝٢٣
Innal lazeena yarmoonal muhsanaatil ghaafilaatil mu`minaati lu`inoo fid dunyaa wal Aakhirati wa lahum `azaabun `azeem
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne dañuy tuumaal [njaaloo] jigéeni jullit ñi amul ay caaxaan, ña koy def danañu sori yërmaande ci àddina ak ca àllaaxira ; te it danañu am mbugal mu metti,
🎧 Dégg

📜 Aaya 21-25 — An-Nur

21۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّبِعُوا خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ ۚ وَمَن يَتَّبِعْ خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ فَإِنَّهُ يَأْمُرُ بِالْفَحْشَاءِ وَالْمُنكَرِ ۚ وَلَوْلَا فَضْلُ اللَّهِ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَتُهُ مَا زَكَىٰ مِنكُم مِّنْ أَحَدٍ أَبَدًا وَلَٰكِنَّ اللَّهَ يُزَكِّي مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen topp jeegoy Séytaane. Ku topp jéegoy Séytaane, [na xam ne] Séytaane ñaawtéef ak njekkar la am. Dogankoon ak ngënéelul Yàlla ak yërmaandeem, kenn ci yéen du sellal. Waaye nag Moom Yàlla mooy sellal ku Ko soob. Te Yàlla Kuy dégg la, Ku xam la.
22وَلَا يَأْتَلِ أُولُو الْفَضْلِ مِنكُمْ وَالسَّعَةِ أَن يُؤْتُوا أُولِي الْقُرْبَىٰ وَالْمَسَاكِينَ وَالْمُهَاجِرِينَ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۖ وَلْيَعْفُوا وَلْيَصْفَحُوا ۗ أَلَا تُحِبُّونَ أَن يَغْفِرَ اللَّهُ لَكُمْ ۗ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Te ña Yàlla jox wërsëg te ñu bokk ci yéen, buñu cay ñàkk a jox jegeñaale ya ak ndóol ya ak ñay gàddaay ci yoonu Yàlla. Nañuy jéggale tey jéllale. Moo xanaa bëgguleen Yàlla jéggal leen ? Yàlla dey Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la !
23إِنَّ الَّذِينَ يَرْمُونَ الْمُحْصَنَاتِ الْغَافِلَاتِ الْمُؤْمِنَاتِ لُعِنُوا فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَلَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ña nga xam ne dañuy tuumaal [njaaloo] jigéeni jullit ñi amul ay caaxaan, ña koy def danañu sori yërmaande ci àddina ak ca àllaaxira ; te it danañu am mbugal mu metti,
24يَوْمَ تَشْهَدُ عَلَيْهِمْ أَلْسِنَتُهُمْ وَأَيْدِيهِمْ وَأَرْجُلُهُم بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Bu keroogee [Bis-pénc ba], seen làmmiñ ya, seeni yoxo ak seeni tànk danañu seede ci seen kaw la ñu daan def.
25يَوْمَئِذٍ يُوَفِّيهِمُ اللَّهُ دِينَهُمُ الْحَقَّ وَيَعْلَمُونَ أَنَّ اللَّهَ هُوَ الْحَقُّ الْمُبِينُ
Bu Bis boobaa, Yàlla dana leen jox, indil leen seen diine ja di dëgg ; [Bu keroogee] lañuy xam ne Yàllaay dëgg gu fés ga.
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
23Aaya

Tekki — An-Nur 23

Simoore An-Nur Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne dañuy tuumaal [njaaloo] jigéeni jullit ñi…

Simoore Aaya 23/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers