Al-Qasas · 16/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
قَالَ رَبِّ إِنِّي ظَلَمْتُ نَفْسِي فَاغْفِرْ لِي فَغَفَرَ لَهُ ۚ إِنَّهُ هُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ ۝١٦
Qaala Rabbi innee zalamtu nafsee faghfir lee faghafaralah; innahoo Huwal Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, man dey tooñ naa sama bopp ; jéggal ma”. Mu daldi koy jéggal. Moom Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la !

🎧 Dégg


📜 Aaya 14-18 — Al-Qasas

14وَلَمَّا بَلَغَ أَشُدَّهُ وَاسْتَوَىٰ آتَيْنَاهُ حُكْمًا وَعِلْمًا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ
Ba mu matee sëkk te ñor xomm, [Muusaa] jox Nanu ko àtte ya ak xam-xam. Noonu la Nuy feye rafetalkat yi.
15وَدَخَلَ الْمَدِينَةَ عَلَىٰ حِينِ غَفْلَةٍ مِّنْ أَهْلِهَا فَوَجَدَ فِيهَا رَجُلَيْنِ يَقْتَتِلَانِ هَٰذَا مِن شِيعَتِهِ وَهَٰذَا مِنْ عَدُوِّهِ ۖ فَاسْتَغَاثَهُ الَّذِي مِن شِيعَتِهِ عَلَى الَّذِي مِنْ عَدُوِّهِ فَوَكَزَهُ مُوسَىٰ فَقَضَىٰ عَلَيْهِ ۖ قَالَ هَٰذَا مِنْ عَمَلِ الشَّيْطَانِ ۖ إِنَّهُ عَدُوٌّ مُّضِلٌّ مُّبِينٌ
Mu dugg ca dëkk ba te yëguñu ko ; mu fekk fa ñaari gaay yuy xeex, kenn ka bokkoon ci ay farandoon, ka ca des bokkoon ci ay noonam. Muusaa daldi koy dóor mbëkk mu dee. - Mu daldi wax ne : “Lii dey ci liggéeyub Séytaane la bokk. Ab noon la buy sànke bu bir”.
16قَالَ رَبِّ إِنِّي ظَلَمْتُ نَفْسِي فَاغْفِرْ لِي فَغَفَرَ لَهُ ۚ إِنَّهُ هُوَ الْغَفُورُ الرَّحِيمُ
Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, man dey tooñ naa sama bopp ; jéggal ma”. Mu daldi koy jéggal. Moom Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la !
17قَالَ رَبِّ بِمَا أَنْعَمْتَ عَلَيَّ فَلَنْ أَكُونَ ظَهِيرًا لِّلْمُجْرِمِينَ
Mu daldi ne : “Yaw sama Boroom, xéewal gi nga ma xéewale tax na duma dimbali mukk tooñkat yi”.
18فَأَصْبَحَ فِي الْمَدِينَةِ خَائِفًا يَتَرَقَّبُ فَإِذَا الَّذِي اسْتَنصَرَهُ بِالْأَمْسِ يَسْتَصْرِخُهُ ۚ قَالَ لَهُ مُوسَىٰ إِنَّكَ لَغَوِيٌّ مُّبِينٌ
Mu nekk ca dëkk ba tiit lool di moytu, jekki-jekki rekk waa ja ko doon ñaan ndimbal sàkkooti na ca moom ndimbal. Muusaa ne ko : “Yaw daal jalaasa nga, di ku tafaar”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
16Aaya

Tekki — Al-Qasas 16

Simoore Al-Qasas Aaya 16 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu wax ne : “Yaw sama Boroom, man dey tooñ…

Simoore Aaya 16/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 14–18. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers