Aali Imran · 75/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
۞ وَمِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ مَنْ إِن تَأْمَنْهُ بِقِنطَارٍ يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ وَمِنْهُم مَّنْ إِن تَأْمَنْهُ بِدِينَارٍ لَّا يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ إِلَّا مَا دُمْتَ عَلَيْهِ قَائِمًا ۗ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا لَيْسَ عَلَيْنَا فِي الْأُمِّيِّينَ سَبِيلٌ وَيَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُمْ يَعْلَمُونَ ۝٧٥
Wa min Ahlil Kitaabi man in taamanhu biqintaariny yu`addihee ilaika wa minhum man in taamanhu bideenaaril laa yu`addiheee ilaika illaa maa dumta `alaihi qaaa` imaa; zaalika biannahum qaaloo laisa `alainaa fil ummiyyeena sabeelunw wa yaqooloona `alal laahil kaziba wa hum ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Am na ci ñoñ-téere ko xam ne, ku ko dénk barigo [wurus] dana la ko delloo. Am na ci koo xam ne, ku ko dénk benn dinaar, du ko delloo, ndegam taxawoo ca temm. La ko waral, dañoo wax ne : “Ñoom, dara waruleen ci seen diggante ak ña jàngul .” Dañuy wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.

🎧 Dégg


📜 Aaya 73-77 — Simoore Aali Imran

73وَلَا تُؤْمِنُوا إِلَّا لِمَن تَبِعَ دِينَكُمْ قُلْ إِنَّ الْهُدَىٰ هُدَى اللَّهِ أَن يُؤْتَىٰ أَحَدٌ مِّثْلَ مَا أُوتِيتُمْ أَوْ يُحَاجُّوكُمْ عِندَ رَبِّكُمْ ۗ قُلْ إِنَّ الْفَضْلَ بِيَدِ اللَّهِ يُؤْتِيهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Te : “Buleen gëm lu dul ku topp seen diine...”. Neel [yaw Muhammad] : “Njub Yàllaa ko moom” - kon mën naa am kenn nit kuñu jox la mel ni la ngeen jot ba mën a weccee kàddu ak yéen ci mbiri seen Boroom. Neel : Ngëneel a nga ca loxo Yàlla. Dana ko jox ku ko soob. Yàlla ku yaatu la, ku xam la.
74يَخْتَصُّ بِرَحْمَتِهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ
Dana jagle yërmaandeem ku ko soob. Yàllaay Boroom ngëneel lu màgg.
75۞ وَمِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ مَنْ إِن تَأْمَنْهُ بِقِنطَارٍ يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ وَمِنْهُم مَّنْ إِن تَأْمَنْهُ بِدِينَارٍ لَّا يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ إِلَّا مَا دُمْتَ عَلَيْهِ قَائِمًا ۗ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا لَيْسَ عَلَيْنَا فِي الْأُمِّيِّينَ سَبِيلٌ وَيَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Am na ci ñoñ-téere ko xam ne, ku ko dénk barigo [wurus] dana la ko delloo. Am na ci koo xam ne, ku ko dénk benn dinaar, du ko delloo, ndegam taxawoo ca temm. La ko waral, dañoo wax ne : “Ñoom, dara waruleen ci seen diggante ak ña jàngul .” Dañuy wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.
76بَلَىٰ مَنْ أَوْفَىٰ بِعَهْدِهِ وَاتَّقَىٰ فَإِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُتَّقِينَ
Axakañ [am na lu leen war] ci ñoom, ku matal kóllareem ci ragal [Yàlla], na xam ne Yàlla safoo na ña ragal Yàlla.
77إِنَّ الَّذِينَ يَشْتَرُونَ بِعَهْدِ اللَّهِ وَأَيْمَانِهِمْ ثَمَنًا قَلِيلًا أُولَٰئِكَ لَا خَلَاقَ لَهُمْ فِي الْآخِرَةِ وَلَا يُكَلِّمُهُمُ اللَّهُ وَلَا يَنظُرُ إِلَيْهِمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَلَا يُزَكِّيهِمْ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne jaay nañu kóllareg Yàlla ak seeni ngiñ ci njëg gu néew, ñooña amuñu cër ca àllaaxira, Yàlla duleen xool te du wax ak ñoom bu Bés-pénc baa te duleen laabal itam ; te mbugal mu metti dana dal ci seen kaw.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
75Aaya

Tekki — Aali Imran 75

Simoore Aali Imran Aaya 75 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci ñoñ-téere ko xam ne, ku ko dénk…

Simoore Aaya 75/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 73–77. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers