Aali Imran · 76/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
بَلَىٰ مَنْ أَوْفَىٰ بِعَهْدِهِ وَاتَّقَىٰ فَإِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُتَّقِينَ ۝٧٦
Balaa man awfaa bi`ahdihee wattaqaa fainnal laaha yuhibbul muttaqeen
📖 Tekkim Wolof
Axakañ [am na lu leen war] ci ñoom, ku matal kóllareem ci ragal [Yàlla], na xam ne Yàlla safoo na ña ragal Yàlla.

🎧 Dégg


📜 Aaya 74-78 — Simoore Aali Imran

74يَخْتَصُّ بِرَحْمَتِهِ مَن يَشَاءُ ۗ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ
Dana jagle yërmaandeem ku ko soob. Yàllaay Boroom ngëneel lu màgg.
75۞ وَمِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ مَنْ إِن تَأْمَنْهُ بِقِنطَارٍ يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ وَمِنْهُم مَّنْ إِن تَأْمَنْهُ بِدِينَارٍ لَّا يُؤَدِّهِ إِلَيْكَ إِلَّا مَا دُمْتَ عَلَيْهِ قَائِمًا ۗ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا لَيْسَ عَلَيْنَا فِي الْأُمِّيِّينَ سَبِيلٌ وَيَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Am na ci ñoñ-téere ko xam ne, ku ko dénk barigo [wurus] dana la ko delloo. Am na ci koo xam ne, ku ko dénk benn dinaar, du ko delloo, ndegam taxawoo ca temm. La ko waral, dañoo wax ne : “Ñoom, dara waruleen ci seen diggante ak ña jàngul .” Dañuy wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.
76بَلَىٰ مَنْ أَوْفَىٰ بِعَهْدِهِ وَاتَّقَىٰ فَإِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُتَّقِينَ
Axakañ [am na lu leen war] ci ñoom, ku matal kóllareem ci ragal [Yàlla], na xam ne Yàlla safoo na ña ragal Yàlla.
77إِنَّ الَّذِينَ يَشْتَرُونَ بِعَهْدِ اللَّهِ وَأَيْمَانِهِمْ ثَمَنًا قَلِيلًا أُولَٰئِكَ لَا خَلَاقَ لَهُمْ فِي الْآخِرَةِ وَلَا يُكَلِّمُهُمُ اللَّهُ وَلَا يَنظُرُ إِلَيْهِمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ وَلَا يُزَكِّيهِمْ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña nga xam ne jaay nañu kóllareg Yàlla ak seeni ngiñ ci njëg gu néew, ñooña amuñu cër ca àllaaxira, Yàlla duleen xool te du wax ak ñoom bu Bés-pénc baa te duleen laabal itam ; te mbugal mu metti dana dal ci seen kaw.
78وَإِنَّ مِنْهُمْ لَفَرِيقًا يَلْوُونَ أَلْسِنَتَهُم بِالْكِتَابِ لِتَحْسَبُوهُ مِنَ الْكِتَابِ وَمَا هُوَ مِنَ الْكِتَابِ وَيَقُولُونَ هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ وَمَا هُوَ مِنْ عِندِ اللَّهِ وَيَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Am na ci ñoom kurél buy damm seeni làmmiñ [bu ñuy jàng] Téere ba ngir ngeen defe ne la ñuy wax ca Téere ba la bokk, te bokku ca ; ñu naan : “Lu jóge ca Yàlla la”, te jógewul ca Yàlla. Di wax ci Yàlla ay fen te xam ko xéll.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
76Aaya

Tekki — Aali Imran 76

Simoore Aali Imran Aaya 76 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Axakañ [am na lu leen war] ci ñoom, ku matal…

Simoore Aaya 76/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 74–78. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers