Saba · 11/54
Tekki Waxtaan — Saba
أَنِ اعْمَلْ سَابِغَاتٍ وَقَدِّرْ فِي السَّرْدِ ۖ وَاعْمَلُوا صَالِحًا ۖ إِنِّي بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ ۝١١
Ani`mal saabighaatinw wa qaddir fis sardi wa`maloo saalihan innee bimaa ta`maloona Baseer
📖 Tekkim Wolof
(ne ko) : “Liggéeyal ay mbubbi koŋ te jekkal ko”. Te ngeen di jëf u yiw. Kuy gis laa [Man Yàlla] li ngeen di def.
🎧 Dégg

📜 Aaya 9-13 — Saba

9أَفَلَمْ يَرَوْا إِلَىٰ مَا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُم مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ ۚ إِن نَّشَأْ نَخْسِفْ بِهِمُ الْأَرْضَ أَوْ نُسْقِطْ عَلَيْهِمْ كِسَفًا مِّنَ السَّمَاءِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّكُلِّ عَبْدٍ مُّنِيبٍ
Ndax dañoo gisul li leen wër ci asamaan ak suuf ? Su Nu sooboon, mën Nanu leen a jaxaseek suuf si, walla Nu rotale ay dogit yu bawoo ci asamaan si. Ay kéemaan a ngi ci loolu ngir bépp jaam buy delluwaakoon ci Boroom bi .
10۞ وَلَقَدْ آتَيْنَا دَاوُودَ مِنَّا فَضْلًا ۖ يَا جِبَالُ أَوِّبِي مَعَهُ وَالطَّيْرَ ۖ وَأَلَنَّا لَهُ الْحَدِيدَ
Joxoon Nanu Daawuda ngëneel lu bawoo ci Nun. Doj yeek njanaaw yi ànd ak moom di sàbbaal. Te it nooyalaloon Nanu ko weñ gu ñuul.
11أَنِ اعْمَلْ سَابِغَاتٍ وَقَدِّرْ فِي السَّرْدِ ۖ وَاعْمَلُوا صَالِحًا ۖ إِنِّي بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
(ne ko) : “Liggéeyal ay mbubbi koŋ te jekkal ko”. Te ngeen di jëf u yiw. Kuy gis laa [Man Yàlla] li ngeen di def.
12وَلِسُلَيْمَانَ الرِّيحَ غُدُوُّهَا شَهْرٌ وَرَوَاحُهَا شَهْرٌ ۖ وَأَسَلْنَا لَهُ عَيْنَ الْقِطْرِ ۖ وَمِنَ الْجِنِّ مَن يَعْمَلُ بَيْنَ يَدَيْهِ بِإِذْنِ رَبِّهِ ۖ وَمَن يَزِغْ مِنْهُمْ عَنْ أَمْرِنَا نُذِقْهُ مِنْ عَذَابِ السَّعِيرِ
Tàggataloon Nanu Suleymaan ngelaw li, am xëyëm doxub weer la woon, am ngontam it, doxub weer la woon. Nu nooyalaloon ko bëtub mbellum përëm. Amoon na ci jinne yi ñu koy liggéeyal ci ndigalul Yàlla. Ku ca fétt nag, Dananu ko mosal mbugalum safara.
13يَعْمَلُونَ لَهُ مَا يَشَاءُ مِن مَّحَارِيبَ وَتَمَاثِيلَ وَجِفَانٍ كَالْجَوَابِ وَقُدُورٍ رَّاسِيَاتٍ ۚ اعْمَلُوا آلَ دَاوُودَ شُكْرًا ۚ وَقَلِيلٌ مِّنْ عِبَادِيَ الشَّكُورُ
Ñu di ko liggéeyal lu ko soob : ci ay tabax ak i bóoli yu tollu ni ay xur, ak i kawdiir yu ñu sësale. “Yéen waa kër Daawuda, gërëmleen Yàlla”, te néewaana mu am ci sama jaam yi ay santkat.
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
11Aaya

Tekki — Saba 11

Simoore Saba Aaya 11 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (ne ko) : “Liggéeyal ay mbubbi koŋ te jekkal ko”.…

Simoore Aaya 11/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 9–13. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers