Fatir · 33/45
Tekki Waxtaan — Fatir
جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا يُحَلَّوْنَ فِيهَا مِنْ أَسَاوِرَ مِن ذَهَبٍ وَلُؤْلُؤًا ۖ وَلِبَاسُهُمْ فِيهَا حَرِيرٌ ۝٣٣
jannaatu `adniny yad khuloonahaa yuhallawna feeha min asaawira min zahabinw wa lu`lu`anw wa libaa suhum feehaa hareer
📖 Tekkim Wolof
Àjjanay Hadan yoo xam danañu ca dugg, ñu di leen fa sadd ay lami wurus ak peme ; te seenug col ca biir àjjana yooyu sooy lay doon.
🎧 Dégg

📜 Aaya 31-35 — Fatir

31وَالَّذِي أَوْحَيْنَا إِلَيْكَ مِنَ الْكِتَابِ هُوَ الْحَقُّ مُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيْهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ بِعِبَادِهِ لَخَبِيرٌ بَصِيرٌ
La Nu la soloo ci Téere bi mooy dëgg tey saxal la ko jiitu woon . Yàlla kuy Xàmmee la, Kuy Gis jaamam ñi la.
32ثُمَّ أَوْرَثْنَا الْكِتَابَ الَّذِينَ اصْطَفَيْنَا مِنْ عِبَادِنَا ۖ فَمِنْهُمْ ظَالِمٌ لِّنَفْسِهِ وَمِنْهُم مُّقْتَصِدٌ وَمِنْهُمْ سَابِقٌ بِالْخَيْرَاتِ بِإِذْنِ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكَ هُوَ الْفَضْلُ الْكَبِيرُ
Ginnaaw ba, donnale Nanu Téere ba sunu jaam ña Nu tànn. Am na ci ñoom kuy tooñ boppam, am na ci ñoom ñuy yamamaay, am na it ci ñoom ñuy jëkkante ciy jëf yu baax ci ndimbalu Yàlla ; loolu nag tigi mooy ngëneel la gën a màgg.
33جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا يُحَلَّوْنَ فِيهَا مِنْ أَسَاوِرَ مِن ذَهَبٍ وَلُؤْلُؤًا ۖ وَلِبَاسُهُمْ فِيهَا حَرِيرٌ
Àjjanay Hadan yoo xam danañu ca dugg, ñu di leen fa sadd ay lami wurus ak peme ; te seenug col ca biir àjjana yooyu sooy lay doon.
34وَقَالُوا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي أَذْهَبَ عَنَّا الْحَزَنَ ۖ إِنَّ رَبَّنَا لَغَفُورٌ شَكُورٌ
Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla, Yàlla mi nu dàqal tiitaange. Sunu Boroom daal Jéggalaakoon la buy Yayoowaakoonu cant.
35الَّذِي أَحَلَّنَا دَارَ الْمُقَامَةِ مِن فَضْلِهِ لَا يَمَسُّنَا فِيهَا نَصَبٌ وَلَا يَمَسُّنَا فِيهَا لُغُوبٌ
Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono dunu fa dab, jaaxle it dunuu fa dab”.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
33Aaya

Tekki — Fatir 33

Simoore Fatir Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Àjjanay Hadan yoo xam danañu ca dugg, ñu di leen…

Simoore Aaya 33/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers