Fatir · 34/45
Tekki Waxtaan — Fatir
وَقَالُوا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي أَذْهَبَ عَنَّا الْحَزَنَ ۖ إِنَّ رَبَّنَا لَغَفُورٌ شَكُورٌ ۝٣٤
Wa qaalul hamdu lillaahil lazeee azhaba `annal hazan; inna Rabbanaa la Ghafoorun Shakoor
📖 Tekkim Wolof
Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla, Yàlla mi nu dàqal tiitaange. Sunu Boroom daal Jéggalaakoon la buy Yayoowaakoonu cant.
🎧 Dégg

📜 Aaya 32-36 — Fatir

32ثُمَّ أَوْرَثْنَا الْكِتَابَ الَّذِينَ اصْطَفَيْنَا مِنْ عِبَادِنَا ۖ فَمِنْهُمْ ظَالِمٌ لِّنَفْسِهِ وَمِنْهُم مُّقْتَصِدٌ وَمِنْهُمْ سَابِقٌ بِالْخَيْرَاتِ بِإِذْنِ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكَ هُوَ الْفَضْلُ الْكَبِيرُ
Ginnaaw ba, donnale Nanu Téere ba sunu jaam ña Nu tànn. Am na ci ñoom kuy tooñ boppam, am na ci ñoom ñuy yamamaay, am na it ci ñoom ñuy jëkkante ciy jëf yu baax ci ndimbalu Yàlla ; loolu nag tigi mooy ngëneel la gën a màgg.
33جَنَّاتُ عَدْنٍ يَدْخُلُونَهَا يُحَلَّوْنَ فِيهَا مِنْ أَسَاوِرَ مِن ذَهَبٍ وَلُؤْلُؤًا ۖ وَلِبَاسُهُمْ فِيهَا حَرِيرٌ
Àjjanay Hadan yoo xam danañu ca dugg, ñu di leen fa sadd ay lami wurus ak peme ; te seenug col ca biir àjjana yooyu sooy lay doon.
34وَقَالُوا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي أَذْهَبَ عَنَّا الْحَزَنَ ۖ إِنَّ رَبَّنَا لَغَفُورٌ شَكُورٌ
Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla, Yàlla mi nu dàqal tiitaange. Sunu Boroom daal Jéggalaakoon la buy Yayoowaakoonu cant.
35الَّذِي أَحَلَّنَا دَارَ الْمُقَامَةِ مِن فَضْلِهِ لَا يَمَسُّنَا فِيهَا نَصَبٌ وَلَا يَمَسُّنَا فِيهَا لُغُوبٌ
Moom mi nu dalal ci kërug nooflaay ci mbaaxam, coono dunu fa dab, jaaxle it dunuu fa dab”.
36وَالَّذِينَ كَفَرُوا لَهُمْ نَارُ جَهَنَّمَ لَا يُقْضَىٰ عَلَيْهِمْ فَيَمُوتُوا وَلَا يُخَفَّفُ عَنْهُم مِّنْ عَذَابِهَا ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي كُلَّ كَفُورٍ
Ñay weddi nag, ñoom Safara la ñuy dëkk : ñu di leen xorñoññal, duñu dee ; te it deesuleen woyofalal mbugal ma. Noonu la Nuy feye képp ku di ab weddiwaakoon.
FatirFihi Alxuraan
45Aaya
MeccanRevelation
34Aaya

Tekki — Fatir 34

Simoore Fatir Aaya 34 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñuy wax naan : “Xeeti cant yi ñeel na Yàlla,…

Simoore Aaya 34/45 — Fatir فاطر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fatir Dégg, Fatir Tekki, Fatir mp3, Fatir pdf. Aaya 32–36. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers