Al-Ahqaf · 24/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
فَلَمَّا رَأَوْهُ عَارِضًا مُّسْتَقْبِلَ أَوْدِيَتِهِمْ قَالُوا هَٰذَا عَارِضٌ مُّمْطِرُنَا ۚ بَلْ هُوَ مَا اسْتَعْجَلْتُم بِهِ ۖ رِيحٌ فِيهَا عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝٢٤
Falammaa ra awhu `aaridam mustaqbila awdiyatihim qaaloo haazaa `aaridum mumtirunaa; bal huwa masta`jaltum bihee reehun feehaa `azaabun aleem
📖 Tekkim Wolof
Ba nu gisee niir wa dëgmël séen xur ya , wax na ñu ne ; “Lii aw xiin la wu nuy tawal”. Déet walaay ! lii nag mooy la ngeen daan yàkkamti : Ngelaw lu ëmb mbugël mu mitti,
🎧 Dégg

📜 Aaya 22-26 — Al-Ahqaf

22قَالُوا أَجِئْتَنَا لِتَأْفِكَنَا عَنْ آلِهَتِنَا فَأْتِنَا بِمَا تَعِدُنَا إِن كُنتَ مِنَ الصَّادِقِينَ
Ñu tontu ko ne ko : “Moo ndax dangay ñëw ci nun ngir féewale nu bëgg nu bàyyi sunu yàlla yi ? Waay-waay, indil nu li nga nuy tëkkoo ndegam bokk nga ca way dëggu ña ”.
23قَالَ إِنَّمَا الْعِلْمُ عِندَ اللَّهِ وَأُبَلِّغُكُم مَّا أُرْسِلْتُ بِهِ وَلَٰكِنِّي أَرَاكُمْ قَوْمًا تَجْهَلُونَ
Mu ne leen : “ Xam-xam moom ma nga ca Yàlla. Man nag dama leen di jottali liñu ma yonni. Waaye gis naa ne yéen ñii aw nit ngeen ñu réer xamadi”.
24فَلَمَّا رَأَوْهُ عَارِضًا مُّسْتَقْبِلَ أَوْدِيَتِهِمْ قَالُوا هَٰذَا عَارِضٌ مُّمْطِرُنَا ۚ بَلْ هُوَ مَا اسْتَعْجَلْتُم بِهِ ۖ رِيحٌ فِيهَا عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ba nu gisee niir wa dëgmël séen xur ya , wax na ñu ne ; “Lii aw xiin la wu nuy tawal”. Déet walaay ! lii nag mooy la ngeen daan yàkkamti : Ngelaw lu ëmb mbugël mu mitti,
25تُدَمِّرُ كُلَّ شَيْءٍ بِأَمْرِ رَبِّهَا فَأَصْبَحُوا لَا يُرَىٰ إِلَّا مَسَاكِنُهُمْ ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي الْقَوْمَ الْمُجْرِمِينَ
ci ndigalul Yàlla dafay nappaaje lépp”. Mu faagaagal leen ñoom ñépp ba séen dëkuwaay ya doŋŋ des fa. Noonu lanuy faye tooñkat ya (sàmbaa-bóoy sa).
26وَلَقَدْ مَكَّنَّاهُمْ فِيمَا إِن مَّكَّنَّاكُمْ فِيهِ وَجَعَلْنَا لَهُمْ سَمْعًا وَأَبْصَارًا وَأَفْئِدَةً فَمَا أَغْنَىٰ عَنْهُمْ سَمْعُهُمْ وَلَا أَبْصَارُهُمْ وَلَا أَفْئِدَتُهُم مِّن شَيْءٍ إِذْ كَانُوا يَجْحَدُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ
Yombaloon nanu leen ñoom lu nu leen joxul yéen. Ndax defaloon nanu leen ag dégg ak ub gis, te seen dégg ga, wala séen gis ba, ak séen xol ya jariñu leen woon tus, ndax dañu daan weddi Laaya Yàlla yi firndeem ya. Ñañu daan yéjji far sóor leen.
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
24Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 24

Simoore Al-Ahqaf Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba nu gisee niir wa dëgmël séen xur ya ,…

Simoore Aaya 24/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers