Al-Ahqaf · 23/35
Tekki Waxtaan — Al-Ahqaf
قَالَ إِنَّمَا الْعِلْمُ عِندَ اللَّهِ وَأُبَلِّغُكُم مَّا أُرْسِلْتُ بِهِ وَلَٰكِنِّي أَرَاكُمْ قَوْمًا تَجْهَلُونَ ۝٢٣
Qaala innamal `ilmu indal laahi wa uballighukum maaa uriltu bihee wa laakinneee araakum qawman tajhaloon
📖 Tekkim Wolof
Mu ne leen : “ Xam-xam moom ma nga ca Yàlla. Man nag dama leen di jottali liñu ma yonni. Waaye gis naa ne yéen ñii aw nit ngeen ñu réer xamadi”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 21-25 — Al-Ahqaf

21۞ وَاذْكُرْ أَخَا عَادٍ إِذْ أَنذَرَ قَوْمَهُ بِالْأَحْقَافِ وَقَدْ خَلَتِ النُّذُرُ مِن بَيْنِ يَدَيْهِ وَمِنْ خَلْفِهِ أَلَّا تَعْبُدُوا إِلَّا اللَّهَ إِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُمْ عَذَابَ يَوْمٍ عَظِيمٍ
Fàttalikul mbokkum waa Aad ña (Huud) ba muy waar aw nitam ca barabu Al Ahqaaf – te fekkoon na waaraatekat ya jar fa la ko jiitu woon ak ginnaawam - [daan leen wax naan]: “Yàlla doŋŋ ngeen war a jaamu (waaye su ngeen jaamoo leneen lu dul moom). Man dey ragal naa ci yéen mbugëlum bis bu màgg ñàng”.
22قَالُوا أَجِئْتَنَا لِتَأْفِكَنَا عَنْ آلِهَتِنَا فَأْتِنَا بِمَا تَعِدُنَا إِن كُنتَ مِنَ الصَّادِقِينَ
Ñu tontu ko ne ko : “Moo ndax dangay ñëw ci nun ngir féewale nu bëgg nu bàyyi sunu yàlla yi ? Waay-waay, indil nu li nga nuy tëkkoo ndegam bokk nga ca way dëggu ña ”.
23قَالَ إِنَّمَا الْعِلْمُ عِندَ اللَّهِ وَأُبَلِّغُكُم مَّا أُرْسِلْتُ بِهِ وَلَٰكِنِّي أَرَاكُمْ قَوْمًا تَجْهَلُونَ
Mu ne leen : “ Xam-xam moom ma nga ca Yàlla. Man nag dama leen di jottali liñu ma yonni. Waaye gis naa ne yéen ñii aw nit ngeen ñu réer xamadi”.
24فَلَمَّا رَأَوْهُ عَارِضًا مُّسْتَقْبِلَ أَوْدِيَتِهِمْ قَالُوا هَٰذَا عَارِضٌ مُّمْطِرُنَا ۚ بَلْ هُوَ مَا اسْتَعْجَلْتُم بِهِ ۖ رِيحٌ فِيهَا عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ba nu gisee niir wa dëgmël séen xur ya , wax na ñu ne ; “Lii aw xiin la wu nuy tawal”. Déet walaay ! lii nag mooy la ngeen daan yàkkamti : Ngelaw lu ëmb mbugël mu mitti,
25تُدَمِّرُ كُلَّ شَيْءٍ بِأَمْرِ رَبِّهَا فَأَصْبَحُوا لَا يُرَىٰ إِلَّا مَسَاكِنُهُمْ ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي الْقَوْمَ الْمُجْرِمِينَ
ci ndigalul Yàlla dafay nappaaje lépp”. Mu faagaagal leen ñoom ñépp ba séen dëkuwaay ya doŋŋ des fa. Noonu lanuy faye tooñkat ya (sàmbaa-bóoy sa).
Al-AhqafFihi Alxuraan
35Aaya
MeccanRevelation
23Aaya

Tekki — Al-Ahqaf 23

Simoore Al-Ahqaf Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu ne leen : “ Xam-xam moom ma nga ca…

Simoore Aaya 23/35 — Al-Ahqaf الأحقاف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahqaf Dégg, Al-Ahqaf Tekki, Al-Ahqaf mp3, Al-Ahqaf pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers