Al-An'am · 122/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
أَوَمَن كَانَ مَيْتًا فَأَحْيَيْنَاهُ وَجَعَلْنَا لَهُ نُورًا يَمْشِي بِهِ فِي النَّاسِ كَمَن مَّثَلُهُ فِي الظُّلُمَاتِ لَيْسَ بِخَارِجٍ مِّنْهَا ۚ كَذَٰلِكَ زُيِّنَ لِلْكَافِرِينَ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝١٢٢
Awa man kaana maitan fa ahyainaahu wa ja`alnaa lahoo noorany yamshee bihee fin naasi kamamm masaluhoo fiz zulumaati laisa bikhaarijim minhaa; kazaalika zuyyina lilkaafireena maa kaanoo ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Moo ndax ka nekkoon ku dee [yéefar], Nu dundal ko [gëmloo ko], jox ko leer gu muy leerloo buy dox ci biir nit ñi, dana nirook ka nga xam ne misaalam mooy dafa nekk cig lëndëm gu mu dul génn ? Noonu la yéefar yi di rafetloo la ñu doon def.

🎧 Dégg


📜 Aaya 120-124 — Al-An'am

120وَذَرُوا ظَاهِرَ الْإِثْمِ وَبَاطِنَهُ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَكْسِبُونَ الْإِثْمَ سَيُجْزَوْنَ بِمَا كَانُوا يَقْتَرِفُونَ
Nangeen bàyyi bàkkaar bu fés ak bu nëbbu, ñiy fàggu bàkkaar dees na leen fey la ñu fàggu woon.
121وَلَا تَأْكُلُوا مِمَّا لَمْ يُذْكَرِ اسْمُ اللَّهِ عَلَيْهِ وَإِنَّهُ لَفِسْقٌ ۗ وَإِنَّ الشَّيَاطِينَ لَيُوحُونَ إِلَىٰ أَوْلِيَائِهِمْ لِيُجَادِلُوكُمْ ۖ وَإِنْ أَطَعْتُمُوهُمْ إِنَّكُمْ لَمُشْرِكُونَ
Buleen lekk loo xam ne tudduñu ca turu Yàlla, loolu génn topp la [caay-caay]. Te Séytaane mooy xiir aw nitam ñuy dàggasanteek yéen. Te bu ngeen leen toppee, daldi ñibbi ca way-bokkaale ya.
122أَوَمَن كَانَ مَيْتًا فَأَحْيَيْنَاهُ وَجَعَلْنَا لَهُ نُورًا يَمْشِي بِهِ فِي النَّاسِ كَمَن مَّثَلُهُ فِي الظُّلُمَاتِ لَيْسَ بِخَارِجٍ مِّنْهَا ۚ كَذَٰلِكَ زُيِّنَ لِلْكَافِرِينَ مَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Moo ndax ka nekkoon ku dee [yéefar], Nu dundal ko [gëmloo ko], jox ko leer gu muy leerloo buy dox ci biir nit ñi, dana nirook ka nga xam ne misaalam mooy dafa nekk cig lëndëm gu mu dul génn ? Noonu la yéefar yi di rafetloo la ñu doon def.
123وَكَذَٰلِكَ جَعَلْنَا فِي كُلِّ قَرْيَةٍ أَكَابِرَ مُجْرِمِيهَا لِيَمْكُرُوا فِيهَا ۖ وَمَا يَمْكُرُونَ إِلَّا بِأَنفُسِهِمْ وَمَا يَشْعُرُونَ
Naka noonu, Lanu defe ci bépp dëkk ay kilifa ca ña dàq a tooñ ngir ñu fay nas ay pexe. Te pexe ya, dara duleen ca moy te yëguñu ko.
124وَإِذَا جَاءَتْهُمْ آيَةٌ قَالُوا لَن نُّؤْمِنَ حَتَّىٰ نُؤْتَىٰ مِثْلَ مَا أُوتِيَ رُسُلُ اللَّهِ ۘ اللَّهُ أَعْلَمُ حَيْثُ يَجْعَلُ رِسَالَتَهُ ۗ سَيُصِيبُ الَّذِينَ أَجْرَمُوا صَغَارٌ عِندَ اللَّهِ وَعَذَابٌ شَدِيدٌ بِمَا كَانُوا يَمْكُرُونَ
Te ñoom, saa su leen laaya dikkalee, ñuy wax naan : “Nun dunu gëm ba mbete nu indil nu lu mel ni la ñu joxoon Yonent Yàlla ya”. Yàllaa gën a xam fa Muy wàcce la Muy yónnee. Bàkkaarkat yi, toroxte dal na leen tukke fa Yàlla ak mbugal mu tar ngir pexe [yu bon ya ñu daan nas].
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
122Aaya

Tekki — Al-An'am 122

Simoore Al-An'am Aaya 122 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo ndax ka nekkoon ku dee [yéefar], Nu dundal ko…

Simoore Aaya 122/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 120–124. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers