Al-An'am · 32/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا لَعِبٌ وَلَهْوٌ ۖ وَلَلدَّارُ الْآخِرَةُ خَيْرٌ لِّلَّذِينَ يَتَّقُونَ ۗ أَفَلَا تَعْقِلُونَ ۝٣٢
Wa mal hayaatud dunyaaa illaa la`ibunw wa lahwunw wa lad Daarul Aakhiratu kahyrul lillazeena yattaqoon; afalaa ta`qiloon
📖 Tekkim Wolof
Dundug àddina nekkul lu dul po ak i caaxaan. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla. Moo ndax dungeen xel-lu ?

🎧 Dégg


📜 Aaya 30-34 — Simoore Al-An'am

30وَلَوْ تَرَىٰ إِذْ وُقِفُوا عَلَىٰ رَبِّهِمْ ۚ قَالَ أَلَيْسَ هَٰذَا بِالْحَقِّ ۚ قَالُوا بَلَىٰ وَرَبِّنَا ۚ قَالَ فَذُوقُوا الْعَذَابَ بِمَا كُنتُمْ تَكْفُرُونَ
Cëy boo leen gisoon bu ñu leen taxawale ca seen Boroom. Mu ne leen : “Ndax lii du dëgg ? ” Ñu toonte ne : “Axakañ ! Giñ nanu ko ci sunu Boroom ! ” Mu ne leen : “Léegi nag, mosleen mbugal mi ngeen daan weddi”.
31قَدْ خَسِرَ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِلِقَاءِ اللَّهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا جَاءَتْهُمُ السَّاعَةُ بَغْتَةً قَالُوا يَا حَسْرَتَنَا عَلَىٰ مَا فَرَّطْنَا فِيهَا وَهُمْ يَحْمِلُونَ أَوْزَارَهُمْ عَلَىٰ ظُهُورِهِمْ ۚ أَلَا سَاءَ مَا يَزِرُونَ
Ña daan weddi ne dajeek Yàlla am na, yàqule nañu. Su Bis-pénc ba nee xes ci seen kaw nag, ñuy wer-weri naan : “Wooy nun yàqule nanu ndax la nu ca sàggane woon. Ñu boot seen bàkkaar ya, ndaw yen bu bon !
32وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا لَعِبٌ وَلَهْوٌ ۖ وَلَلدَّارُ الْآخِرَةُ خَيْرٌ لِّلَّذِينَ يَتَّقُونَ ۗ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Dundug àddina nekkul lu dul po ak i caaxaan. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla. Moo ndax dungeen xel-lu ?
33قَدْ نَعْلَمُ إِنَّهُ لَيَحْزُنُكَ الَّذِي يَقُولُونَ ۖ فَإِنَّهُمْ لَا يُكَذِّبُونَكَ وَلَٰكِنَّ الظَّالِمِينَ بِآيَاتِ اللَّهِ يَجْحَدُونَ
Xam Nanu xéll ne li ñuy wax metti na la lool. Tooñkat ya, du yaw lañuy weddi, waaye kàdduy Yàlla lañu weddi.
34وَلَقَدْ كُذِّبَتْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ فَصَبَرُوا عَلَىٰ مَا كُذِّبُوا وَأُوذُوا حَتَّىٰ أَتَاهُمْ نَصْرُنَا ۚ وَلَا مُبَدِّلَ لِكَلِمَاتِ اللَّهِ ۚ وَلَقَدْ جَاءَكَ مِن نَّبَإِ الْمُرْسَلِينَ
Weddig ay Yonent yu la jiitu amoom na fi. Ñu muñ loraange ja, ba Nu dikke leen Sunu ndimbal. Kàddug Yàlla du soppiku, te jot nga lenn ca xew-xewi Yonent ya.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
32Aaya

Tekki — Al-An'am 32

Simoore Al-An'am Aaya 32 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dundug àddina nekkul lu dul po ak i caaxaan. Te…

Simoore Aaya 32/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 30–34. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers