Al-An'am · 33/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
قَدْ نَعْلَمُ إِنَّهُ لَيَحْزُنُكَ الَّذِي يَقُولُونَ ۖ فَإِنَّهُمْ لَا يُكَذِّبُونَكَ وَلَٰكِنَّ الظَّالِمِينَ بِآيَاتِ اللَّهِ يَجْحَدُونَ ۝٣٣
Qad na`lamu innahoo layahzunukal lazee yaqooloona fa innahum laa yukazziboonaka wa laakinnaz zaalimeena bi Aayaatil laahi yajhadoon
📖 Tekkim Wolof
Xam Nanu xéll ne li ñuy wax metti na la lool. Tooñkat ya, du yaw lañuy weddi, waaye kàdduy Yàlla lañu weddi.
🎧 Dégg

📜 Aaya 31-35 — Al-An'am

31قَدْ خَسِرَ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِلِقَاءِ اللَّهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا جَاءَتْهُمُ السَّاعَةُ بَغْتَةً قَالُوا يَا حَسْرَتَنَا عَلَىٰ مَا فَرَّطْنَا فِيهَا وَهُمْ يَحْمِلُونَ أَوْزَارَهُمْ عَلَىٰ ظُهُورِهِمْ ۚ أَلَا سَاءَ مَا يَزِرُونَ
Ña daan weddi ne dajeek Yàlla am na, yàqule nañu. Su Bis-pénc ba nee xes ci seen kaw nag, ñuy wer-weri naan : “Wooy nun yàqule nanu ndax la nu ca sàggane woon. Ñu boot seen bàkkaar ya, ndaw yen bu bon !
32وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا لَعِبٌ وَلَهْوٌ ۖ وَلَلدَّارُ الْآخِرَةُ خَيْرٌ لِّلَّذِينَ يَتَّقُونَ ۗ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Dundug àddina nekkul lu dul po ak i caaxaan. Te kërug àllaaxira moo gën ca ña ragal Yàlla. Moo ndax dungeen xel-lu ?
33قَدْ نَعْلَمُ إِنَّهُ لَيَحْزُنُكَ الَّذِي يَقُولُونَ ۖ فَإِنَّهُمْ لَا يُكَذِّبُونَكَ وَلَٰكِنَّ الظَّالِمِينَ بِآيَاتِ اللَّهِ يَجْحَدُونَ
Xam Nanu xéll ne li ñuy wax metti na la lool. Tooñkat ya, du yaw lañuy weddi, waaye kàdduy Yàlla lañu weddi.
34وَلَقَدْ كُذِّبَتْ رُسُلٌ مِّن قَبْلِكَ فَصَبَرُوا عَلَىٰ مَا كُذِّبُوا وَأُوذُوا حَتَّىٰ أَتَاهُمْ نَصْرُنَا ۚ وَلَا مُبَدِّلَ لِكَلِمَاتِ اللَّهِ ۚ وَلَقَدْ جَاءَكَ مِن نَّبَإِ الْمُرْسَلِينَ
Weddig ay Yonent yu la jiitu amoom na fi. Ñu muñ loraange ja, ba Nu dikke leen Sunu ndimbal. Kàddug Yàlla du soppiku, te jot nga lenn ca xew-xewi Yonent ya.
35وَإِن كَانَ كَبُرَ عَلَيْكَ إِعْرَاضُهُمْ فَإِنِ اسْتَطَعْتَ أَن تَبْتَغِيَ نَفَقًا فِي الْأَرْضِ أَوْ سُلَّمًا فِي السَّمَاءِ فَتَأْتِيَهُم بِآيَةٍ ۚ وَلَوْ شَاءَ اللَّهُ لَجَمَعَهُمْ عَلَى الْهُدَىٰ ۚ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْجَاهِلِينَ
Ndagam seen dëddu dafa rëy ci yaw, boo mënee sàkk ag tajfal ci biir suuf si, walla ker- keraan ci asamaan yi ba tax nga indil leen kéemaan, def ko. [Xamal ne] bu neexoon Yàlla, Mu dajale leen cig njub. Kon bul bokk ca ña sànku réer.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
33Aaya

Tekki — Al-An'am 33

Simoore Al-An'am Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Xam Nanu xéll ne li ñuy wax metti na la…

Simoore Aaya 33/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers