Al-A'raf · 154/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَلَمَّا سَكَتَ عَن مُّوسَى الْغَضَبُ أَخَذَ الْأَلْوَاحَ ۖ وَفِي نُسْخَتِهَا هُدًى وَرَحْمَةٌ لِّلَّذِينَ هُمْ لِرَبِّهِمْ يَرْهَبُونَ ۝١٥٤
Wa lammaa sakata `am Moosal ghadabu akhazal al waaha wa fee nnuskhatihaa hudanw wa rahmatul lillazeena hum li Rabbihim yarhaboon
📖 Tekkim Wolof
Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind ma làmboo na njub ak yërmaande ngir ña nga xam ne ñoom ragal nañu seen Boroom.
🎧 Dégg

📜 Aaya 152-156 — Al-A'raf

152إِنَّ الَّذِينَ اتَّخَذُوا الْعِجْلَ سَيَنَالُهُمْ غَضَبٌ مِّن رَّبِّهِمْ وَذِلَّةٌ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُفْتَرِينَ
Ña nga xam ne doon nanu jaamu yëkk wa, mbugal dana leen dal tukke fa seen Boroom, ak toroxte ci dundu àdduna. Te noonu Lanuy feyee ñay duural Yàlla.
153وَالَّذِينَ عَمِلُوا السَّيِّئَاتِ ثُمَّ تَابُوا مِن بَعْدِهَا وَآمَنُوا إِنَّ رَبَّكَ مِن بَعْدِهَا لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ñay def lu ñaaw ba noppi ginnaaw ga ñu tuub, tey ñu gëm... sa Boroom nag, ginnaaw loolu, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
154وَلَمَّا سَكَتَ عَن مُّوسَى الْغَضَبُ أَخَذَ الْأَلْوَاحَ ۖ وَفِي نُسْخَتِهَا هُدًى وَرَحْمَةٌ لِّلَّذِينَ هُمْ لِرَبِّهِمْ يَرْهَبُونَ
Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind ma làmboo na njub ak yërmaande ngir ña nga xam ne ñoom ragal nañu seen Boroom.
155وَاخْتَارَ مُوسَىٰ قَوْمَهُ سَبْعِينَ رَجُلًا لِّمِيقَاتِنَا ۖ فَلَمَّا أَخَذَتْهُمُ الرَّجْفَةُ قَالَ رَبِّ لَوْ شِئْتَ أَهْلَكْتَهُم مِّن قَبْلُ وَإِيَّايَ ۖ أَتُهْلِكُنَا بِمَا فَعَلَ السُّفَهَاءُ مِنَّا ۖ إِنْ هِيَ إِلَّا فِتْنَتُكَ تُضِلُّ بِهَا مَن تَشَاءُ وَتَهْدِي مَن تَشَاءُ ۖ أَنتَ وَلِيُّنَا فَاغْفِرْ لَنَا وَارْحَمْنَا ۖ وَأَنتَ خَيْرُ الْغَافِرِينَ
Muusaa tànn juróom-ñaar fukki góor ciy nitam, ngir sunu waxtu ndaje. Ba leen yëngug xeer wa jàppee, mu ne : “Yaw sama Boroom, bu la neexoon nga rey leen ak man lu jiitu tey. Moo ndax Danga nuy rey ngir li ña réer ci nun def ? Loolu du leneen lu dul sa nattu, ci ngay réerale ku La soob, di ci jubal ku La soob. Yaway sunu Cëslaay. Nanga nu baal, yërëm nu, Yaa di ki gën a mën a jéggale.
156۞ وَاكْتُبْ لَنَا فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا حَسَنَةً وَفِي الْآخِرَةِ إِنَّا هُدْنَا إِلَيْكَ ۚ قَالَ عَذَابِي أُصِيبُ بِهِ مَنْ أَشَاءُ ۖ وَرَحْمَتِي وَسِعَتْ كُلَّ شَيْءٍ ۚ فَسَأَكْتُبُهَا لِلَّذِينَ يَتَّقُونَ وَيُؤْتُونَ الزَّكَاةَ وَالَّذِينَ هُم بِآيَاتِنَا يُؤْمِنُونَ
Dogalal ci nun yiw ci àddina ak ca àllaaxira. Nun gindiku nanu jëm ci Yaw.”. Mu ne : “Sama mbugal, danaa ko sadd ku Ma neex. Waaye Sama yërmaande ëmb na lépp lenn. Te danaa ko sadd ña ragal Yàlla tey génne asaka ak ñi gëm Samay kàddu.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
154Aaya

Tekki — Al-A'raf 154

Simoore Al-A'raf Aaya 154 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba merum Muusaa giifee, dafa jël àlluwa ya. Te mbind…

Simoore Aaya 154/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 152–156. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers