Al-A'raf · 40/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
إِنَّ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَاسْتَكْبَرُوا عَنْهَا لَا تُفَتَّحُ لَهُمْ أَبْوَابُ السَّمَاءِ وَلَا يَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ حَتَّىٰ يَلِجَ الْجَمَلُ فِي سَمِّ الْخِيَاطِ ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُجْرِمِينَ ۝٤٠
Innal lazeena kazzaboo bi Aayaatinaa wastakbaroo `anhaa laa tufattahu lahum ahwaabus samaaa`i wa laa yadkhuloonal jannata hattaa yalijal jamalu fee sammil khiyaat; wa kazaalika najzil mujrimeen
📖 Tekkim Wolof
Ña weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu ba dëddu leen, Deefuleen ubbil wunti asamaan si, te duñu dugg Àjjana li feek gëléem duggul ci bën-bënu puso. Te noonu Lanuy feye saay-saay si.
🎧 Dégg

📜 Aaya 38-42 — Al-A'raf

38قَالَ ادْخُلُوا فِي أُمَمٍ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِكُم مِّنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ فِي النَّارِ ۖ كُلَّمَا دَخَلَتْ أُمَّةٌ لَّعَنَتْ أُخْتَهَا ۖ حَتَّىٰ إِذَا ادَّارَكُوا فِيهَا جَمِيعًا قَالَتْ أُخْرَاهُمْ لِأُولَاهُمْ رَبَّنَا هَٰؤُلَاءِ أَضَلُّونَا فَآتِهِمْ عَذَابًا ضِعْفًا مِّنَ النَّارِ ۖ قَالَ لِكُلٍّ ضِعْفٌ وَلَٰكِن لَّا تَعْلَمُونَ
Mu ne leen : “Dugguleen fekki xeet ya leen jiitu woon, di ay nit ak i jinne ca Safara sa.”. Xeet wu ca dugg rekk, tàmbalee rëbb moroom ja. Ba ñépp yembee, ña jiitu ak ña mujj ku nekk naan : “Ñii noo nu sànkkoon : kon nag Yàlla, fulal mbugal ma ci seen kaw.”. Yàlla ne leen : “Yéen ñépp laay ful seen mbugal, waaye xamuleen”.
39وَقَالَتْ أُولَاهُمْ لِأُخْرَاهُمْ فَمَا كَانَ لَكُمْ عَلَيْنَا مِن فَضْلٍ فَذُوقُوا الْعَذَابَ بِمَا كُنتُمْ تَكْسِبُونَ
Ña fa jiitu ñoom di wax ña mujj a agsi, naan leen : “Yéen ñii daal, gënewuleen nu lenn. Kon mosleen [toqamtiku] mbugal mi ngir la ngeen fàggu woon ciy bàkkaar”.
40إِنَّ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَاسْتَكْبَرُوا عَنْهَا لَا تُفَتَّحُ لَهُمْ أَبْوَابُ السَّمَاءِ وَلَا يَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ حَتَّىٰ يَلِجَ الْجَمَلُ فِي سَمِّ الْخِيَاطِ ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُجْرِمِينَ
Ña weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu ba dëddu leen, Deefuleen ubbil wunti asamaan si, te duñu dugg Àjjana li feek gëléem duggul ci bën-bënu puso. Te noonu Lanuy feye saay-saay si.
41لَهُم مِّن جَهَنَّمَ مِهَادٌ وَمِن فَوْقِهِمْ غَوَاشٍ ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الظَّالِمِينَ
Am nañu laltaayu Safara ak mbalaanum [Safara]. Noonu Lanuy feye tooñkat ya.
42وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَا نُكَلِّفُ نَفْسًا إِلَّا وُسْعَهَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ الْجَنَّةِ ۖ هُمْ فِيهَا خَالِدُونَ
Ña gëm te jëf u yiw - Te kat Dunu teg bakkan lu dul lu mu àttan - ñooña ñooy waa Àjjana : te dañu fay béel.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
40Aaya

Tekki — Al-A'raf 40

Simoore Al-A'raf Aaya 40 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña weddi Sunuy tegtal, rëy-rëylu ba dëddu leen, Deefuleen ubbil…

Simoore Aaya 40/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 38–42. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers