Ghafir · 58/85
Tekki Waxtaan — Ghafir
وَمَا يَسْتَوِي الْأَعْمَىٰ وَالْبَصِيرُ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ وَلَا الْمُسِيءُ ۚ قَلِيلًا مَّا تَتَذَكَّرُونَ ۝٥٨
Wa maa yastawil a`maa walbaseeru wallazeena aamanoo wa `amilus saalihaati wa lal museee`; qaleelam maa tatazakkaroon
📖 Tekkim Wolof
Gumba niróowul ak njàccaar, ña gëm tey jëf yiw it niróowuñu ak ñiy def ñaatéef (kenn du leen gam-gamle). Néewaana bu ngeen fàttalikoo !

🎧 Dégg


📜 Aaya 56-60 — Ghafir

56إِنَّ الَّذِينَ يُجَادِلُونَ فِي آيَاتِ اللَّهِ بِغَيْرِ سُلْطَانٍ أَتَاهُمْ ۙ إِن فِي صُدُورِهِمْ إِلَّا كِبْرٌ مَّا هُم بِبَالِغِيهِ ۚ فَاسْتَعِذْ بِاللَّهِ ۖ إِنَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْبَصِيرُ
Ñay dàggasante ci laayay Yàlla ya ci lu àndul ak firnde yu ñu leen jox, rëy-rëylu doŋŋ a nekk ca seen dënn ya. Te seen aajo du ca fajoo. Na ngay muslu ci Yàlla, moom Mooy aji Dégg, di aji Gis.
57لَخَلْقُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ أَكْبَرُ مِنْ خَلْقِ النَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Bindug asamaan yeek suuf si moo gën a rëy bindug nit ñi. Waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
58وَمَا يَسْتَوِي الْأَعْمَىٰ وَالْبَصِيرُ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ وَلَا الْمُسِيءُ ۚ قَلِيلًا مَّا تَتَذَكَّرُونَ
Gumba niróowul ak njàccaar, ña gëm tey jëf yiw it niróowuñu ak ñiy def ñaatéef (kenn du leen gam-gamle). Néewaana bu ngeen fàttalikoo !
59إِنَّ السَّاعَةَ لَآتِيَةٌ لَّا رَيْبَ فِيهَا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يُؤْمِنُونَ
Bis Pénc ba ; Luy dikk la : nàttable amu ca ; waaye li ëpp ci nit ñi gëmu ñu.
60وَقَالَ رَبُّكُمُ ادْعُونِي أَسْتَجِبْ لَكُمْ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَسْتَكْبِرُونَ عَنْ عِبَادَتِي سَيَدْخُلُونَ جَهَنَّمَ دَاخِرِينَ
Seen Boroom nee na : “Wooleen ma, Ma wuyu leen. Ña nga xam ne, dañoo rëy-rëylu, lànk bañ maa jaamu, danañu dugg Safara ànd ak toroxtaane”.
GhafirFihi Alxuraan
85Aaya
MeccanRevelation
58Aaya

Tekki — Ghafir 58

Simoore Ghafir Aaya 58 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Gumba niróowul ak njàccaar, ña gëm tey jëf yiw it…

Simoore Aaya 58/85 — Ghafir غافر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ghafir Dégg, Ghafir Tekki, Ghafir mp3, Ghafir pdf. Aaya 56–60. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers