Ghafir · 60/85
Tekki Waxtaan — Ghafir
وَقَالَ رَبُّكُمُ ادْعُونِي أَسْتَجِبْ لَكُمْ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَسْتَكْبِرُونَ عَنْ عِبَادَتِي سَيَدْخُلُونَ جَهَنَّمَ دَاخِرِينَ ۝٦٠
Wa qaala Rabbukumud `ooneee astajib lakum; innal lazeena yastakbiroona an `ibaadatee sa yadkhuloona jahannama daakhireen
📖 Tekkim Wolof
Seen Boroom nee na : “Wooleen ma, Ma wuyu leen. Ña nga xam ne, dañoo rëy-rëylu, lànk bañ maa jaamu, danañu dugg Safara ànd ak toroxtaane”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 58-62 — Ghafir

58وَمَا يَسْتَوِي الْأَعْمَىٰ وَالْبَصِيرُ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ وَلَا الْمُسِيءُ ۚ قَلِيلًا مَّا تَتَذَكَّرُونَ
Gumba niróowul ak njàccaar, ña gëm tey jëf yiw it niróowuñu ak ñiy def ñaatéef (kenn du leen gam-gamle). Néewaana bu ngeen fàttalikoo !
59إِنَّ السَّاعَةَ لَآتِيَةٌ لَّا رَيْبَ فِيهَا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يُؤْمِنُونَ
Bis Pénc ba ; Luy dikk la : nàttable amu ca ; waaye li ëpp ci nit ñi gëmu ñu.
60وَقَالَ رَبُّكُمُ ادْعُونِي أَسْتَجِبْ لَكُمْ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَسْتَكْبِرُونَ عَنْ عِبَادَتِي سَيَدْخُلُونَ جَهَنَّمَ دَاخِرِينَ
Seen Boroom nee na : “Wooleen ma, Ma wuyu leen. Ña nga xam ne, dañoo rëy-rëylu, lànk bañ maa jaamu, danañu dugg Safara ànd ak toroxtaane”.
61اللَّهُ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ اللَّيْلَ لِتَسْكُنُوا فِيهِ وَالنَّهَارَ مُبْصِرًا ۚ إِنَّ اللَّهَ لَذُو فَضْلٍ عَلَى النَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَشْكُرُونَ
Yàlla mi leen defal guddi ngeen di ci dallu, defal leen bëccëg bi it ngeen di ci man a gis (bay fàggu ji). Yàlla boroom Ngënéel la ci kaw nit ñi, waaye li ëpp ci nit ñi duñu sant.
62ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ خَالِقُ كُلِّ شَيْءٍ لَّا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ
Koo ku moo di Yàlla seen Boroom, Moo bind lépp. Amul jeneen Yàlla judul moom. Kon naka ngeen di lajje féew (ca yoonu Yàlla wu jub wa xocc) ?
GhafirFihi Alxuraan
85Aaya
MeccanRevelation
60Aaya

Tekki — Ghafir 60

Simoore Ghafir Aaya 60 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Seen Boroom nee na : “Wooleen ma, Ma wuyu leen.…

Simoore Aaya 60/85 — Ghafir غافر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ghafir Dégg, Ghafir Tekki, Ghafir mp3, Ghafir pdf. Aaya 58–62. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers