Ghafir · 17/85
Tekki Waxtaan — Simoore Ghafir
الْيَوْمَ تُجْزَىٰ كُلُّ نَفْسٍ بِمَا كَسَبَتْ ۚ لَا ظُلْمَ الْيَوْمَ ۚ إِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ ۝١٧
Al-Yawma tujzaa kullu nafsim bimaa kasabat; laa zulmal Yawm; innal laaha saree`ul hisaab
📖 Tekkim Wolof
Bis niki tey, bakkan bu nekk dees na ko faye ca la mu daan fàggu. Tooñ amatul, Yàlla ku gaaw ab wàññ la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 15-19 — Simoore Ghafir

15رَفِيعُ الدَّرَجَاتِ ذُو الْعَرْشِ يُلْقِي الرُّوحَ مِنْ أَمْرِهِ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ لِيُنذِرَ يَوْمَ التَّلَاقِ
Moo kawey daraja, di Boroom Aras, Mooy sànni ruu ci ndigalam jëme ko ci ku ko soob ci jaamam ñi, ngir muy xuppe ci bisub Daje ba (Bis Pénc ba),
16يَوْمَ هُم بَارِزُونَ ۖ لَا يَخْفَىٰ عَلَى اللَّهِ مِنْهُمْ شَيْءٌ ۚ لِّمَنِ الْمُلْكُ الْيَوْمَ ۖ لِلَّهِ الْوَاحِدِ الْقَهَّارِ
bis ba ñuy feeñ seen dara du man a nëbbu Yàlla. Ana kan mooy boroom nguur gi, bis niki tey ? Yàlla, miy Kenn, di ab Notaakoon.
17الْيَوْمَ تُجْزَىٰ كُلُّ نَفْسٍ بِمَا كَسَبَتْ ۚ لَا ظُلْمَ الْيَوْمَ ۚ إِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Bis niki tey, bakkan bu nekk dees na ko faye ca la mu daan fàggu. Tooñ amatul, Yàlla ku gaaw ab wàññ la.
18وَأَنذِرْهُمْ يَوْمَ الْآزِفَةِ إِذِ الْقُلُوبُ لَدَى الْحَنَاجِرِ كَاظِمِينَ ۚ مَا لِلظَّالِمِينَ مِنْ حَمِيمٍ وَلَا شَفِيعٍ يُطَاعُ
na nga leen xupp ci bis buy jige si, ba xol yi di nekk ci put yi, (ngir tiit ak njàqare). Te bu boobaa tooñkat yi du ñu fa am xarit, mbaa ku leen di tinu ñu di ko topp.
19يَعْلَمُ خَائِنَةَ الْأَعْيُنِ وَمَا تُخْفِي الصُّدُورُ
Xam na worug ay gët, luy nëbbu ci biir dënn yi.
GhafirFihi Alxuraan
85Aaya
MeccanRevelation
17Aaya

Tekki — Ghafir 17

Simoore Ghafir Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bis niki tey, bakkan bu nekk dees na ko faye…

Simoore Aaya 17/85 — Simoore Ghafir غافر (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Ghafir Dégg, Simoore Ghafir Tekki, Simoore Ghafir mp3, Simoore Ghafir pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers